FU USMAAN SONKO RÉER ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kenn xamul fu Usmaan Sonko nekk jamono jii. Bentaleb Sow ak Juan Branco, layookatu Usmaan Sonko bi, ñoo fésal xibaar bi ci seen xëti Facebook. Nee ñu, gisuñu ko, dégguñu ko, te kenn mënu ko jot telefon.

Bentaleb nee, dara jotu ko woon bi ñuy mujje gise ak moom. Ñiy wattu kaaraangeem sax, xamuñu fum jaar. Pexe mu waa Pastef la la, walla dafa réer dëggantaan ? Fu mu nekkoon ? Ku mu nekkaloon ? Fan la ñiy wattu kaaraangeem nekkoon ? 

Fi nuy binde yaxal bi nii la Dakarmatin biral ne takk-der yaa ga Usmaan Sonko, yóbbu ko këram Ndakaaru, ca Site Kër-Góor-Gi.

Dees na ñëwaat buñ ci amee xibaar yu yees.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj