FUTBAL AK JAFE-JAFEY RÉEWI AFRIG YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Doom-aadama fent na ay xeeti po yu bare. Ba ci tàggat-yaram sax, nga xam ne, ci cosaanam, yar ak wér-gi-yaram ñoo ko taxoon a jóg, nit soppi na ko, def ko liggéey ak po, di ci amal ay joŋante yu mag, àddina sépp di ko teewe. Xeeti po yooyu, nag, futbal a ci gën a siiw te yit moo ci gën a law ci àddina si. Baatu futbal, ci làkku àngale la jóge te di tekki tank (fut-) ak bal, maanaam bal bi ñuy dóore tànk. Futbal ci boppam bare nay xeet, waaye bi ci gën a fés mooy bi nga xam ne, fukk ak benni nit ñooy jàkkaarlook seen yeneeni fukk ak benni moroom, ku nekk di jéem a dugal bal bi ci kãwu keneen ki ci diirub 90 simili. Powum futbal mi ngi cosanoo ca réewum Àngalteer. Àngalteer, nag, saa boo ko waxee xel yi dem ci ñoom Bobby Charlton, Gordon Banks, Stanley Matthews, Michael Owen, Bobby Moore, Alan Shearer, Kevin Keegan ak lingeer Elisabeth II, añs. Kon, tubaab yi ñoo sos futbal ba noppi daldi ko tas ci àddina si, ñépp bëgg ko. Afrig tamit kenn demul mu des, ndax doomi Afrig yi amul ku leen gën a xër ci futbal. Waaw. 

Boo génnee ci mbedd yi dinga gis xale yiy top ci ginnaaw bal biy dóor ba ñaq tooy xepp, subaak ngoon ñu ne ci. Waxambaane yi ñoom, foo leen fekk ñoo ngiy seetaan futbal walla teg seen àttaaya di ko waxtaane. Mag ñi di waxtaan ak a fàttaliku jamonoy Sàndaark, Jaraaf, Duwaan walla Asfaa, walla sax jamonoy Bokànde ak Séex Sekk, di leen méngale ak goney léegi yi. Nawetaan moom, li mu jaral xaley koñ yi, mëneesu koo natt. Kon daal, futbal bawul kenn ci Afrig li ko dale bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, jóge sowu jëm penku, fépp la feebarub futbal law ; rawatina Senegaal gii, du mag du ndaw, muy góor walla jigéen. Moom kay, politig bi sax da cee rax léegi ndax dayo bi mu am.

Moo tax it, yenn saa yi, nguur gi ci lay jafandiku ngir fàtteloo askan wi jafe-jafe yi mu nekke. Ndege, ku ci sa réew di joŋante, day mel ni da ñuy raxas sam xel, nga fàtte say aajo ak say ay, sa xol ak sa xel yépp nekk ci joŋante bi. Rax-ci-dolli, futbal bi léegi liggéey la : fokat yi ñi ngi ciy am xaalis bu dul jeex, jaaykat yi noonu ba ci bérébi liggéeyukaay yu mag yaa ngi ciy defar seeni mbir. Futbal a ka bare bayre, naam ! Joŋante bu mag biy dajale ñaari at yu ne réewi Afrig yi ab firnde la ci.

Joŋante ren bi nag, ca Misra lay ame. Muy réew moo xam ni, askan wi ci nen la toog. Ndaxte njiit ma fa ne, dib Seneraal ci làrme bi, Al Sissi, jaay doole ak xoqtal nit ñi la fa nekke. Askan wi sonn lool. Ñu bare jàpp ne dafay jëfandikoo joŋante boobu ngir muur metit yi askan wiy jànkonteel jamono jii. Waaye, mel na ni pexeem moomu sooy na, ndax réewum baay Nelson Mandela daan na bërki-démb Misra jéll bu set wecc, ginnaaw bi mu ko dóoree 1-0. 

Waaye bu ñu fatte li ponkal ma woon, Mawàdd Wàdd, daan wax : “Dawuma ci ginnaaw bal, ci ginnaaw nit ñiy daw ci ginnaaw bal bi laay daw. Ndax, nit ñoonu ay xale ñoo ci ëpp, te xale yooyu ñooy ñiy jiwi ndamu askan wi ëllëg.” Yaakaru waa ju baax jooju, taxawoon démb di xeexal réewum Senegaal ak doomi Afrig yépp, te jaarale woon ko ci tàggat-yaram, mat naa bàyyi xel. Wànte, mel na ni tey bukki-njuur-sàmba yi ŋànk futbalu Afrig bokkuñu ak moom xalaat.  

Waaye, nan jàppale sunu gaynde yi nu fa teewal.

Ba négéni, gàcceeluñu nu. Ndax, dibéer jii weesu rekk lañu daan Ugàndaa 1-0, daldi jàll ci kaar de finaal yi. Waaye, nag, bumu nu tax a réere mbir jafe-jafey askan wi ak mbirum petorol bi ak gaas bi lëmbe réew mi. Wareesul a fàtte yit baykat yi, xale yiy dugg ci looco yi wutali Ërob te naan Bàrsaa walla barsàq, njàng mi, lopptaan yi, yoon wi, añs.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj