BOKK AK NAWLOO NGIR JÀMM AK NAATAANGE CI ÀDDUNA SI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Weer yii nu génn, réew yu bare tànn nañu seen njiit. Joŋante yi gën a indi coow mooy yi amoon ca Beliyoriisi mbaa Amerig, walla fii ci Afrig, ca Kodiwaar, Gine-Konaakiri, Burkinaa, ak-ñoom-seen. Réewum Ganaa moo ci mujj.
Gëstukat yu bare ak i yéenekaay bind nañ ci, woykat yi waxi noppi. Góom yeek dana yiy teree wote ci jàmm ñoo ngi ne fàŋŋ.
Kon boog, jar na nu toog, delloosi sunu xel, ubbi bu baax sunuy gët ak sunuy nopp. Su ko defee, dinanu mën a bind ci jafe-jafe yi réew yiy jànkoonteel, rawatina:
– Góom yeek dana yi tëwa wér
– Siddit yi sanax
– Yaram yiy soox
I/ Góomi réewi Afrig yi bare nañu. Mënees na cee lim:
-Ñit ñu bari yi amul dàntite, moo xam ndax mës na ñoo am kayitu juddu walla mësuñu koo am;
-Ñi bëgg a wote waaye ba ñu demee ba ca béréb ya, gisuñu njaq liñu war a sànni seen xob;
-Ni ñu dajalee nit ñi ci ay mbaar yu xat, ñu ne fay buuxante, ba faf mer, gedd mbaa ñu dàq leen, ne leen waxtu dakkal wote bi jot na;
– Ñi gisul seen nataalu mbër ci xob yi;
– Ñi mënul a dem ci béréb yi njaq yi ne, ndax seen i cër dañoo sutante walla ñu tàyyel a génn rekk, ndax léegi mën nañoo jaar ciy jumtuwaay yu bees ngir wote. Wóoruleen nag ndax seen xob mujj naa bokk ci waññi bi;
– Lawax yiy tamante dëmm, di jiiñante càcc ak di jaayante doole, nekk na luñ dégg ci réew yu bare;
– Ger ak maye xaalis tax na ba ci yenn làngi pólitig yi ak lawax yi luxóor, jël ndam li.
II / Dana yi nag, nii lañu bindoo:
– Ñi ci jal yi sawaru ñoo jébbale lenge yi, jàpp ci Yàlla nangu ni dañ leen a daan,
– Daa ñu def seen kem-kàttan, aakimoo yéenekaay yi, gaawtu ne làmb ji tas na, wure wi dem na këŋ,
– Daa ñu dóore, màtte, jiiñ, faat sax ñi ñu doon joŋanteel;
– Daa ñu ger ñi leen sonal ak ñi ñu ragal, jaare ko ci mbootaay yi, sàndikaa yi, kilifa-diine yeek kilifa-aada yi. Ragal a delloo weccit, ragal a tontu ci li ñu leen di tuumaal moo tax ñuy yaakaar ne xare pólitig dafa ànd ak xaru, ak ñédd nguur;
– Ba ñu defee loolu lépp ba noppi, daa ñu dellusi di digaate naataange ak jàmm:
– Daa ñu jéem a dalal xel yi, dige ni di nañ jubbanti réq-réqi réew mi, ngir mbir yépp tegu ci anam yu leer te jub, lépp rekk ngir faluwaat.
Waaye ndax mënees na leen a gëm?
III / Ñàkkul siddit yee wéragul
– Siddit wi ci gën a feebar mooy siddit wi Njiiti réew yi naj, jàppe nguur gi seen moomeel. Su fekkee njiit li ku dul sàmm kàddoom la, ku mànduwul, ku jiital bànneexu njabootam tey jàppaley xaritam, mbaa xeetam, walla waasoom, kooku mënul suuxat mat ak juboo ak Jàmm, astemaak naataange.
– Faj siddit wi ci topp mooy tabaxaat pénc mi war a xàll yoon wi ñépp di jaar ngir jokkoo, waxtaan wi gën a yaatu
Su fekkee pénc moomu, ki ko jiite ak i naataangoom defuñu seen liggéey, rax-ci-dolli lu njiitu-réew mi joxoñ, ñu dagg, xam ngeen ni ñooñu kenn dootul am yaakaar ci ñoom; duñu leen sax faaleeti;
– Ñetteelu siddit wi feebar mooy siddit wiy dawal ëttu àttekaay yi. Su nasaxee, far, fekki yeneen ñaari siddit yi, réew mi mën naa tas.
IV / Bokk ak nawlooy faj yaram wi
Nit moo dem ba gis ne jàmm moo gën fitna. Noonu la fente demokaraasi, maanaam, sàmm baatu képp kuy noyyi cim réew, jublu ci saxal fa jàmm ak naataange.
Nit demati ba yokk ci nawloo, ngir ñu yaatal géew bi; wàññi xiiro ak ŋaayoo, boddikoonte ci biir xeet yi, biir waaso yeek këru diine yi, ngir sàmm li ñépp bokk.
Noonu la yaram wi war a bindoo.
Bennoo bi tamit, war naa law fépp ci réew mi, ku ne li nga liggéey, jariñ la, jariñ sa njaboot ba jariñaale askan wépp.
– Sàrt yi ñu ràbb noonu, ku leen jéggi, teggi sànni, xàllal nga fitna yoon. Kon boog fedd siddit yi, diw leen baa ñu niin ak kaarite mooy yeewu, jàng, sàkku xam-xam, ngir mën a tedd ëllëg.
– Fii ci Senegaal nag, jot nan fee amal waxtaan wu yaatoo-yaatu. Persidaa Aamadu Maxtaar Mbów, moo jiite woon liggéey boobu. Yékkati na fay kàddu yu am solo, dénk leen ay sëtam.
Du ñàkk nu dellusi ci balay yàgg, saytu mbir mi, wax ci li nu ci war a yokk.
Baabakar Jóob Buuba
Njiitu PAALAE, mbootaay muy yëngatu ci liifantu ak njàngum mag ci Afrig

 

 

 

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj