Téere bu am solo bi Ceerno Alasaan Sàll génne fan yii ci nasaraan, te móolkat bi, ca Pari, tudd Fauves, mënees na ko tekkee nii ci kàllaamay Kocc : “Tënkoo ak takkoo ca “Élysée” : déeyub jawriñ biñ dénkoon mbiri petorol ci Senegaal”
Li ñu war a njëkk a wax, moo di ne mbind mi rafet na, xóot na, neex a jàng.
Ni Ceerno Sàll ràbbee téereem bi rekk biral na liggéey bu takku : leeg-leeg mu yóbbu la fii, bàyyi la fa, demaat feneen, dellusiwaat, yeen saa mu joxoñ, yeen saa mu junj.
Téere bi mën nañ ko duppe « Pólotig, bu àndul ak màndute, jur toj-toj ak njaaxum yu dul jeex ».
Li muy wone, xamle ko, moo di naka la ñuy jéngee, jataŋ, réewi Afrig yi. Mën nañ yaatal sax, boole ci réew yi ñuy noot yépp, di manq seen deret, di foqati seen alal.
Ceerno Alasaan Sàll, waa Farãs la duut baraamu tuuma ; moo waral mu duppe téereem bi : « Tënkoo ba ca “Élysée” ». Waaye li ko gën a soxal mooy mbirum petorol mi.
“Élysée”, nu fàttali ne mooy màkkaanu njiitu Farãs yi.
Am na ñu ànd ak ñi ci jal bi, ci réew mi, te mere Ceerno Alasaan Sàll ci lu mu waxul ci yenn tënkoo yu mel ni ba amoon Huston, ca Amerig.
Moonte ku jàng bu baax li mu bind, dinga gis ne Ceerno Alasaan ŋàññul waa Farãs rekk : xëccoo yi, jiiroo yi, képp kuy njàccaar mën na leen a ràññee.
Ku jàng bu baax téere bi, mën nga gis it ne Ceerno Sàll, xol ak xel la ko binde, di ci fésal naqaram. Wone na ci li ko jaaxal, bett ko, li tax mu lànk, ne ngoram mayu ko mu dugg ci yenn yi, mu jaral ko fippu, jàmmaarlook nguur gi.
Moom daal, weer na gejjam, ku weeri yaa moom.
Gejj gi, mi ngi ci ñeex meek rënd bi, mi ngi it ci yakk bi.
Man nag, tibb naa 8i yoon, daldi dank :
Njaaxum yi dul jeex te ki ko firndéel di Farba Seŋoor, àndoon ak Parsidaa Ablaay Wàdd, mujj fekki Parsidaa Maki Sàll. Njaaxum yi yemul ci Farba, yemul ci dem ak dikk, ñu ngi ci njàng mi, càkkeef gi ak wér-gi yaramu askan wi ;
Màndute, ngor, nger ;
Polótig ni muy doxe ci réew mi. Ñiy woote boolo bokk, ak ñi siis, fëqale, bàyyiwul dara, xuloo yi, xeex yi, mbiri xaalis ;
Moom, am na lu bare lu mu ci xam, ndax dugg na, génn na, ci Ànd-Jëf Xare bi ak ci APR (muy farandooy nguur gi) ;
Caytu ak koom, ni ñu lëkkaloo, naka la gise mbey mi, napp gi, mbiri jokkoo ak jumtukaay yu bees yi, naka la ñu war a dégmal, topp, jubbanti, yaatal, yombal, jubal, jëflanteek sàndikaa yeek yeneen mbootaay yi ;
Mbiri àtte, fa mbaxane wara nekkee benn ;
Mbiri xalaatin, caada, cosaan, wolleet ;
Xar-kanam mi ngi ci. Am na nataal yu leer, am na yu nëbbu, yu mu muur. Wone na ñiy dóor (Wàdd, Maki), ñiy dékku (ku ci mel ni Abdul Mbay) ;
Ndénkaane yu am solo ci mbiri rabat, dégmal, caytu ;wone na njàng, xam-xam, xarala.
DAANEEL
Téere Alasaan Sàll bi am na solo : jur na coow lu réy waaye ñi bokk ci làngu polótig gii di ”République Des Valeurs” am nañ ci mbégte. Ceerno nag, ci CRD la bokk, woote Ànd, Déggoo, Dekkil Bokk. Waa APR ñoom, dañoo mer ba futt, rawatina ñi téere bi xosi.
Coow li du gaaw a dakk, ndax lii doomi-réew mi ak ñiy bàyyi xel ci Senegaal daa ñu ci wax.
Du ñàkk mu doon téere bi ñuy gën a waxtaane ci at mii ñu nekk.
Cafka gi nag ak ceeñ li, li ma ci gën a saf, mooy li Ceerno sant Sàll, wone ni Al-Pulaar la, ajoor la yit. Loolu de war naa neex, soxal ñépp ñi nangoo ubbi seeni gët ak seen xel, bañ a jiital, bañ a surux ci kàmbu xeet, waaso ak diine su ñuy polótig. Su ko keneen bindoon, dina am ñu ni dafa bañ Parsidaa Maki Sàll ndax li ñu bokkul xeet, waaso, mbaa tarixa.
Fii ci réew mi, war nañ jiital saa su nekk njariñu réew mi, boole ci njub ak bokk jëmu.
Baabakar Jóob Buuba
Jàngalekat, gëstukat,
Bokk ci Taxaw Temm.