Musaa Aysatu Jóob
Démb ci altine ji Orange Footbaal Club fésal na ekibam ci atum 2019-2020, muy dajale doomi Afrig yi nu gën ràññee ci futbal, di po mu am bayre fépp ci àddina si. Réewum Senegaal nag am na ci ekib boobule juróom i doomam yu ñu tànn, looluy firndeel bu baax jéego yu am solo yi doomi réew miy def ca bitim-réew. Juróomi gone yooyoo ngi nii : Saajo Maane, Kaliidu Kulibali, Idiriisa Gànna Géy, Krepeŋ Jaataak Papis Demba Siise. Tur yu dul bett ñi xam bu baax futbal !