Keroog, 16i pani ut 2024, la Senegaal dugg ci mboorum xarala ak gëstu. Nde, ci bésub àjjuma jooju lañu njëkk a yónni ab satelit ci jàww ji. Muy bés bu réy te màgg, di ndamu Saa-Senegaal yépp, waayeet di sagub Afrig gépp.
“Gaindesat” lees duppee satelit bi. Ay doomi Senegaal ñoo ko xalaat, defaral ko seen bopp. Naam, liggéey nañook i ma-xareñi Farãs yu “Centre spatial universitaire” bu Montpellier, wànte ñoom ñoo liggéey lépp daanaka.
“Gakndesat” nag, ab “nanosatellite” la. Maanaam satelit bu ndaw. Ci biir “fusée” bii di “Falcon 9” lañ ko dugaloon bi ñu koy sàndi ci jàww ji. Ca dalub Vandenberg bu Californie lañ ko sàndee. Jëwriñu njàng mu kowe mi, gëstu beek coste gi, Abdurahmaan Juuf, teeweeji woon na ko.
Jalooreb xarala bile nag, day gën a jox dayo Senegaal, ci àddina si ak Afrig. Ndaxte, ci biir réewi Afirg yi féete bëj-dexu Saharaa bi te di làkk farañse, Senegaal mooy ci ñaareelu réew mu amal boppam ab satelit. Jiibuti mooy réew mi ko njëkke.
Satelit bi nag, dina amal réew njariñ yu bari ci fànn yu yaatoo yaatu niki gëstu bi, njuux li, mbey mi, kéew mi, kaaraange gi, añs.
Gàcce-ngaalaama gëstukati Senegaal yi jëmmal wile naal.