GÀTTALI BÉS BI (28/6/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TABASKI

Waa Ahlus Sunna, ñi ñu duppee Ibaadu, tabaski nañu tey ci àllarba ji, 28 suwe 2023. Ñu seetlu mbooloo mu takkoo takku ci béréb yu deme estaad Léwopóol Sedaar Seŋoor te Ustaaz Gelaajo Ka jiite fa. Fa Pikin Ikitaaf tamit, ça pàkkub Bokk-Jëf, Ustaas Moor Kebe jiite na fa mbooloo mu bari lool. Am na yeneen béréb ak i diiwaan ci réew mi yoy, jullit ñu bari julli nañ, rendi seen i xar. 

Ça seen xutba ya nag, soññee nañ ñépp ci dox jàmm, sàmm mbooloo gi ci waa réew mi te moytu fitna. Wax nañ itam ci wàllu wote yi. Nde, Ustaas Gelaajo Ka dafa xamle ne, buñ bëggee jàmm ci réew mi, nañu amal ay wote yoy, ñépp a ciy bokk, ñu bañ a beddi kenn, ta jaarale ko ci yoon. 

Imaam yi jiite tey yépp nag, ñaan nañ ay ñaan yu al solo, jagleel ko Njiitu réew mi, way-pólitig yi ak askan wi ci jëmmu boppam. 

USTAAZ USMAAN SONKO ! 

Démb ci guddi, Usmaan Sonko wax na ak askan wi cib widewoo bob, mel na ni ci yoor-yoor gi la ko defoon. Daanaka, mbubbum Ustaas la soloon. Nde, waxul dara lu jëm ci wàllu pólitig.

Moom daal, ci diine la wax, fàttali cosaanu tabaski ak jubluwaay yi. Waxaale na sax ci diiney kercen yi, jël ay misaal ci jaar-jaaru Yeesu. Joxe na dig-daje ginnaaw tabaski ngir càmbar tolluwaayu réew mi. 

MBIRUM SWEET BEAUTÉ : NDOGAL LI ROT NA

Ëttub pékke bi génne na ndogal li mu jël ñeel layoob Usmaan Sonko ak Aji Raabi Saar. Ci àllarbay tey ji lañ ko siiwal. Àttekat bi dafa génne ab jukkib bu 35i xët, di ci leeral mbir yi ñuy toppe Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay, boroom dàmpuwaaay bi. Li ko dale ca luññutuy ndoorte ya ba ca cëppaandoo la, lépp la jukki bi fàttali. Àttekat bi nag tëjlu na dàmpuwaayu Sweet Beauté. 

Ndax dañuy jàpp Usmaan Sonko am déet ? Jëwriñu Yoon ji, Ismayla Maajoor Faal, tontu woon na ci. Ne woon na ne, mënees na ko jàpp jamono ju nekk, ginnaaw bi ndogalu àttekat bi jàppandee. Dafa waxoon ne, keroog 15 suwe 2023 :

“Fàww ndogal li jàppandi ba noppi. Bu ñu ko jébbal ndogal li, day yóbbu boppam walla toppekat bi jàpplu ko.” 

Kon, dafa mel ni lu ci des yàggatul. Bu boobaa luy xew ? Loolu mooy laaj bi.

FARÃS : AB TAKK-DER A REY BENN WAXAMBAANE 

Coowal, Nahel, ab waxambaane bu ab takk-der REY moo lëmbe réew ma. Njiitu réew ma, Ngomblaan ga, way-pólitig ya, Mbappe ak yeneen boroomi tur yu bari àddu nañ ci, ñaawlu ko. 

Emmanuel Macron dafa gaaw bind ab tweet wax ne dees na amal ag luññutu gu gaaw te màndu. Jamono jii nag, takk-der baa ngi ñu jàppandi fileek ñuy leeral mbir mi.

Senegaal nag, moom, 25i ndaw mën nañ dee, waaye, ba tey, jàppaguñ kenn.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj