GÀTTALI BÉS BI (ALXAMES 18 ME 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Daaray Nguur gi tëj nañu leen fa Siggicoor ak Séeju

Li ko dale àjjuma ji 19 me 2023 ba alxames 25 me 2023 daaray Nguur gi dinañu tëj fa Siggicoor ak Séeju. Bu weesoo tey, kenn dootul tijji seen i bunt ba bés bi delsi. Muy ndogal lu tukkee ci bànqaas biy saytu njàng mi fa ñaari diiwaan ya. Ndogal loolu nag, I.A yi, maanaam kurél yiy saytu njàng mi, ñoo ko jël ginnaaw bi àttewaayu Ndaakaaru bëtalee bésub layoo Usman Sonko – Aji Saar ci 23 me 2023. Waayeet, ñu nemmeekuy ñaxtu ak i yëngu-yëngu yu metti foofule, te tëe dakk, rawatina fa wër kër Usmaan Sonko.

Ndajem-waxtaan mu YAW

Démb ci àllarba ji la lëkkatoog Yewwi Askan Wi doon amal ndajem-waxtaan ñeel tolluwaayu réew mi. Tomb bi ci ëppoon solo nag mooy ni Yoon di doxalee ak kujje gi, rawatina ak seen naataangoo boobu di Usmaan Sonko Njiitul Pastef li nga xam ne ci, jamono jii, jëflanteem ak Yoon yëngal na réew mi. Ñuy sàkku loolu dakk ci ni mu gën a gaawe. Rax-ci-dolli, ñoom namm  nañoo amal ndajem-ñaxtu ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru me wii.

Kii di Usmaan Sonko nag, bokk ci lëkkatoo googu, ay fan a ngi nii gaa ñi di laaj fan la dugg ? Ñii naan dafa génn réew mi, ñee naan dafa daw nekkul këram. Démb ci ngoon, am nañu ci lu leen leer. Ndax, bi tàkkusaan gi jàllee la génn di doxantu ci mbedd yi ak a saafoonteek i ñoñam.

Lému Ture, dépite PDS bi, gaañu na

Waa PDS am nañ dëj. Seen dépite bi, Soxna Lému Ture, moo faatu. Njiiteefu pàrti gi moo génne ab yégle, siiwal ci xibaaru faatug soxna si fekk baax Cees. Nee ñu, ca naawub AIBD la ñàkke bakkanam, fekk ñu ko doon waaj a rawale bitim-réew ngir fajeeji ko fa.

Sinjaa : ñaari bakkan rot nañu cib aksidaŋ

Ñaari mbokki deret a ñàkk seen i bakkan cib aksidaŋ bob, ma nga ame fa Sinjaa, ci otorutu pey giy lëkkale Ndakaarook Mbuur. Juróomi nit jële nañ ciy gaañu-gaañu. Tey, ci yoor-yooru alxames ji, la jéyya ji am. Bees sukkandikoo ci waa APS, ab daamaar a mbëkk benn sëfaan bu paan bu taxawoon ci tali bi. Ndeke, dafa doon jéem a mooytu beneen oto faf dal ci sëfaan bi.

Amnesty International dine pelent Nguurug Senegaal

Séydi Gasama, ndawul Amnesty International fi Senegaal, xamle na ni, kurélam gaa ngiy waajal ab pelent bob, Nguurug Senegaal lañ ciy topp. Li wo sabab moo nit ñiy dee ci ñaxtu yeek yëngu-yëngal yi te kenn du ci luññutu ngir indi ciy leeral. Peleent bi nag, pelentub mbooloo lay nekk. Moom, Séydi Gasama miy sàmm ak a xeexal àq ak yelleefi doom-aadama, dafa gis ne reykat yi, kenn du leen toppe dara te luññutu yi duñ mujj fenn.

« Jël nañ kippug layookat yiy jokkook mbokki ñees rey ngir yóbbu mbir mi ca ëttu àttewaayu CDEAO. Du doon pelent boo xam ne, X lees ciy topp. Pelent bi, Nguurug Senegaal lañ ciy topp te, mën na a mam sax ñu dem fa àttewaayi ONU yi. » Kàddu yii, Séydi Gasamaa ngi leen waxe ci mikóro TFM.

Soxna Aminata Ture dafa bëgg a taxawal ag lëkkatoo ñeel wotey 2024 yi

Rajo Sud Fm doon na dalal Soxna Aminata Ture. Soxna si àdduna ci wotey 2024 yi, wax ne mi ngi liggéey, du wut ñi mu àndal ci wote yooyule. DJ Nikolaa ak Ustaas Mawdo Fay la séqaloon jotaay bi. Wax na fa ne :

« Maa ngi liggéey ngir taxawal ag lëkkatoo ñeel wotey 2024 yi. Am na sax ñenn ñu bokk ci APR ñoo xam ne, noppi nañ ngir ànd ak man. Maa ngi leen wax ci lu wóor ni, am na ci jëwriñ yoo xam ne, xaaruñu lu dul Maki Sàll biral ñetteelu moome gim bëgg a fàggu ngir ñu tàggook moom. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj