Jàppal nañu bés layoob Usmaan ak Aji Saar : 16 me 2023
Bés bi ñépp doon xaar agsi na, di bésub layoo diggante Aji Saar ak Usmaan Sonko mi ndaw siy tuumaal ciif ak tëkkuy rey. Talaata, 16 me 2023 lañ ko jàpp. PressAfrik a siiwal xibaar bi.
Biñ jokkoowee ak layookatu Aji Saar bi, Elaas Juuf, dafa dëggal xibaa bi, waaye soriwu ci. Bu dee waa layookati Sonko yi, ñoom, nee nañu jotaguñ ci këyitug woolu gi. Meetar Ibraayma Mbeng itam, layookatu Ndey Xadi Njaay mi moom Sweet Beauty, nee na ci kibaraan yi la ko yëgee, kon moom du mën a dëggal xibaar bi.
Aji Saar nag, dafa mel ni ku wóolu boppam. Ndax, ginnaaw bi mu santee Yàlla, gërëm ay mbokkam yi ko taxawu yépp, daf ne « dëgg mooy mujj. »
Bu dee Usmaan Sonko moom, dafa jàpp ne, àppub layoo bi, yàqal ko nemmeeku yi muy def a tax ñu jàpp ko.
Usmaan Sonko tontu na imaam bi
Usmaan Sonko sànni nay kàddu imaam Aliyun Musaa Sàmb bu jumaay Ndkaaru ju mag ji. Kàddu yooyu, mi ngi leen yékkati démb bi mu jaalejee kii di Mammadu Koorka Ba mi nga xam ne, ca yëngu-yënguli weeru màrs wii jàll la faatoo woon. Li mu ko dugge woon mooy tontu imaam Aliyun Musaa Sàmb mi ne woon, ku dee ci yëngu-yëngul yi safara nga jëm. Nee na loolu du dëgg. Ndax, xam nañu diine ji te, kenn moomu ko. Moo tax muy sàkku ci mbokk yi ñu nangu ndogalu Yàlla. Mu yokk ci ne waruñoo ragal ndax, Yàlla bind na fi ñu war a jaar yépp laata ñu fiy ñëw. Xanaa kay, ci Nguuru Maki Sàll rekk lañuy bóom ay ndaw ci ay ndajem-ñaxtu. Looloo tax nag, ñu ne ñoom duñu dellu ginnaaw wenn yoon.
Jëfandikoog Koktel molotof yi
Jëwriñ ji ñu dénk wàlluw biir réew mi ngir ñaawlu li doxkatu ñaxtu yi di yor jumtukaay yooyu. Ndax, nee na, dafa ñaaw lool ñu leen di sànni ci kër jàmbur yi walla takk-der yi. Mën na am nag fekk dañu xamul ne ci wàlluw kaaraange moom, jëfandikoog doole ji dafa am i dayo. Te, bëgguñoo àgg fenn fi. Ndax, liggéeyu Nguur mooy sàmm nit ñi ak seen i alal. Réewu demokaraasi lañu nekk bu ñu waree bàyyi ndajem-ñaxtu yi am dinañu ko def. Waaye, am na dig woo xam ne kenn waru koo romb. Ndax, bu ñuy jëfandikoo lu mën a gaañ ab takk-der, feyu gi mën na metti. Te, loolu du liggéeyu Nguur gi. Rax-ci-dolli nag, duñu nangu kenn di yee fitna ci réew mi.
Njaal
Tey ci gaawu gi la kii di Njiitu réew mi, Maki Sàll, demoon ca diiwaanu Tuubaa ca këru xalif ba. Mu àndoon ca ak kii di Njiitul CESE lu yees li, Abdulaay Daawda Jàllo. Li mu ko dugge woon nag, mooy jébbal am njaalam kilifag dëkk bi, moom mi nga xam ne soxnaam sii di Daba Jàllo dafa wuyuji boroomam ci alxames jii weesu.
Génnug àddina Maam Lees Kamara
Tiis ak uw naqar dal na ci kow njabootug taskati xibaari Senegaal. Maam Lees Kamara, di woon kàngam ci taskati xibaari réew mi, moo génn àddina ci gaawug tey jii, ca raglub Principal gu Ndakaaru. Moom, Maam Lees Kamara, taskatu xibaar la woon, nekkoon itam jàngalekat ak tàggatkat ci wàll wi. Seede bi naataangoom yépp seedeel mooy ne, ku xër la woon ci wàllu njub ak màndute.