GAYNDEE NJAAY ! MBARA-WÀCC ! CAN 2022 : SENEGAAL JËL NA RAW-GÀDDU GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dibéer, 6eelu fan ci féewaryee 2022, 21i waxtu ci guddi tegal nañu. Lépp a ngi ne tekk, ne selaw. Ñépp a ngi ne cell. Fu doomu Senegaal mënoon a nekk jamono jooju ci àddina si, xolam, xelam, ak sagoom yépp a nga woon ca Olembe. Kenn talul kenn, kenn talul dara, ñii di ñaan Yàlla, ñee di saraxu Eduwaar Mendi, niki rëporteeru Canal + bi doon waxe xol, naan :

“Ayca Eduwaar Mendi ! Fàww nga jëli bii, jàppal balu Mohamad Lasheen bi ! Eduwaar Mendi ! Fàww nga jëli kooooooo… Jëli na ko, Dudu Mendi ! Ki dàq a góolu ci àddina si jëli na ko ! Bi yoon mi ngi xeeñ neex ! Senegaal am na ñaari estaar, ñaari estaar te waxoon nan ko, ñaari estaari àddina : Dudu Eduwaar Mendi ci kã yi ak Saajo Maane mi rate woon penaatiwam ci kanamu Mohamed Abuu Gamal…”

Mu des Saajo Maane. Bu dugale mu jeex. Xol yiy tëf-tëfi, nit ñiy lox. Kub baa ngi fëgg buntu Senegaal. Bët yépp ne jàkk ab bal… benn bal… bal ba ca Kamerun… balu Saajo Maane ba… Lilian Gatounes mel ni ku nàmpe Senegaal, bokk ak nun yëg-yëg bi, naan :

“Mbir mi yomb na, bu dugalee, bu dugalee Senegaal jël raw-gàddu gi nekk Sàmpiyoŋu Afrig ! Fim ne nii Abiib Béy warul toog, xam naa mi ngi jaabante rekk ! Mi ngi koy xool, mi ngi julli niki saa-senegaal yiy xool bal bi ci tànki Saajo Maane yi… Saajo Maane, dawu Saajo Maaneeeeeeeee… ! Saajo Maane def na ko ! Saajo Maane dugal na bal bi !  Senegaal ! Senegaal nekk na Sàmpiyoŋu Afrig njëlbeenug yoonam cim mboor ! Mayo bi am na biddéew !…”

Kenn xàmmeetul kenn. Yuuxoo yi, sarxolle yi, jooy yi… Réew mépp a riirandoo. Ñii di daw xamuñu sax fuñ jëm. Ñee di fëgg ak a mbëkk lépp luñ jot. Ñenn ñiy daanu, xëm ; ñeneen ñiy wëndeel raaya Senegaal gi, def mbooloo, di woyandoo :

“Bojo-bojo yee ! Seen baay ñëw na ! Seen baay ñëw na !”

Mbégte mu ni réye, mësta am ci réew mi. Nde, Senegaal dafa yàgg a yóotu kub bi. Jamonoy AOF ba tey, ni ko Ablaay Jaw waxe, Senegaal a ngi daw ginnaaw njëlbeenug kubam. Ay maasi maas jaar nañ fi, yaakaar yu bare tas niki 2002 ak 2019. Saa bun ko jegewaan ba nar koo téye rekk, mu mel ni dafa am jinne ju koy këf ci sunuy loxo.

Ci atum 1965 la Senegaal tàmbalee bokk ci joŋanteb Kubu Réewi Afrig yi, juróomi at ginnaaw ag jonnam. Xaar bu yàgg booboo waral mbégte mu réy mii. Saajo Maane ak i ñoñam def jaloore ju réy a réy jooju, kenn dootu ko fàtte abadan. Ndaxte, ñoo fi njëkk a indi kub, sargalee ko Senegaal. Siggil nañ Senegaal, sagal ay doomam ak i maasam yiy ñëw. Ndege, seen ndam li keroog 6eelu fan ci féewaryee ca Kamerun, dina tax ñu binde wurus turu Senegaal ci mbooru futbalu Afrig.

Moone, ca ndoorteelu joŋante bi, xel teeyoon na. Ginnaaw bi ñu futbalee ak Simbaabuwe 90i simili dugaluñu, ba arbit ba may leen 4i simili Saajo Maane am penaati dugal ko, ñoo ngi doon ŋàññ Aliw Siise ak i gayndeem. Nu futbal ak Gine, futbal ak Malawi daldi arañefe ñaar yépp, dugaluñu lu moy benn penaati. Coow li nar a jóg. Waaye, mu am ñuy dalal xeli saa-senegaal yi, di wax ne ekib bi dafa matagul, waaye dina baax ndax Senegaal dina yeewuji.

Naka jekk noonu la fa deme. Ndaxte, Senegaal waajalul boppam nim ko bëgge woon laata muy dem Kamerun. Ekib bi dafa waroon a dem Ruwàndaa defaroo fa, tàggatu fa, futbal fa ñaari joŋante laata muy dem ci CAN bi. Waaye, ñenn ci futbalkat yi amey gaañu-gaañu, ñi seen këlëb yi téye woon ak koronaa bi ñoo xajamaloon waajtaay boobu. Biñ àggee Bafusam ca Kamerun tamit, koronaa bi sonaloon na leen. Daanaka sax, du ñépp a demoon. Ndax, Bàmba Jeŋ ak Baaba Caam Ndakaaru lañ leen bàyyi woon ca njëlbeen ga, ngir ne dañ ame woon koronaa.

Loolu doyul, jinne yu ñuul yi di fen ak a dajale. Ay dof di leen tàllal mikoro yi, ñuy léeb ak a kàcc, naan Senegaal “…du àgg sax ¼ de finale…” walla buñ “…amee wërsëg ½ finale lañuy yem..” waaye “…duñ mës a jël kub bi.” Cim ! Ay feni neen. Ñoom ñépp la Yàlla weer keroog. Kon, Yàlla yewwi na askanuw Senegaal ci njabarkat yeek gisaanekat yi. Bir na ne, xamuñu kumpa. Donte ne, nag, am na ñu oyofoon xel lool, gëm leen, di saaga futbalkat yi ak a xas Aliw Siise.

Loolu lépp nag, teewul, Aliw Siise aki ndawam fas jom, muñ, ànd ak fullaak faayda, xar seen tànki-tubéy ngir indil Senegaal sarica biñ yàgg a xaar. Noonu, ñu taxañ Kap-weer ci 1/8 de finale yi, dóor ko 2i bii ci dara, dóor Gine Ekuwatoriyaal 3-1 ci ¼ de finaal yi laata ñu ko ñamalaat Burkinaa Faso ci ½ finaal yi. Yaakaar gi yokk lool. Àddina sépp jàpp ne bii yoon, mooy bu baax bi.

Naam, Saajo Maane rate woon na penaati ci 5eelu simili bi, waaye xàddiwuñu woon. Nde, Senegaal moo futbal finaal bi yépp. Esipt moom, dañ doon xaar, di def ay “contre-attaque” ngir nax Senegaal. Te, bu dul woon seen góol, duñ àgg sax seri. Nde, génne na fa ay bal yu bari, rawatina yu Bàmba Jeŋ yi.

Biñ àggee seri tamit, xawoon nañ tiit. Li ko waraloon mooy ne, Esipt noonu la gañee woon ñetti joŋanteem yu mujj yi laata muy àgg finaal. Te, seen góol bi, Abuu Gamal, dafa fees kã yi, aay lool. waaye, bii yoon, Senegaal moo aye woon. Te bu Yàlla nee waaw, lépp ay sotti. Moo tax, bi Saajo dugalee penaati bu mujj bi, ay rongooñ sotteeku nañ, mbedda Senegaal yi fees dell.

Keroog, réew mi xumboon na lool ba foo sàndi woon mbàttu mu tàkk. Askan wi fàtte naqar wim ame woon yépp ba, daanaka, cinu reer tegewul woon ci kër yi. Njiitu réew mi bég lool sax. Ñu wane ko muy tëb ca Adis-Abebaa bim nekkoon. Mu daldi jël dogal, def feriyee bésub altine 7eelu fan ci féewaryee, ne day delsi Senegaal ngir teeru gaynde ni ñuy teeroo buur.

Bés boobu, Njaayeen yi ak Njóobeen yi ay mburook ndambe lañ reere woon, ndeysaan. Ñi sant Ba, ñoom, xam naa cereek meew baa leen dimbali woon. Waaye, bésub mbégte, bul xol feesee, feesal biir.

Waaye nag, am lu ñuul ci soow mi. Nde, bukki moom, jëfi bukki rekk la mën a def. Dinan ci ñëw…

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj