GÉNNUG ÀDDINA Me USMAAN SÉY 

Yeneen i xët

Aji bind ji

Me Usmaan Séy, layookat bu siiw bi, moo génn àddina. Ay mbokkam a ko tàgge, kibaraan yi siiwal xibaar bi. Moom nag, Me Usmaan Séy, ku ñu ràññee la woon ci biir layookati réew mi, bokkoon ci kàngaami “barreau” bi. Ndaxte, ca atum 1985 la bindu woon ci “barreau” bi, maanaam kurélug layookati Senegaal yi.

Moom sax, dafa bokkoon  ci ñi doon layal Sitoor Nduur mees tuumaal mbirum ciif. Nitu pólitig la woon itam, jiite woon pàrti Front républicain, bokk Bennoo Bokk Yaakaar, doon jàppale Maki Sàll. 

Defu waxu moo ngi koy jaale njabootam, di ko jaale ay mbokkam ak naataangoomi layookat.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj