Usmaan Sonko génn na. Basiiru Jomaay Fay génn na. Senegaal yëngu na, rawatina Ndakaaru. Démb, ci guddig alxames ji, lañ génn ca kasob “Cap-Manuel” biñ nekkoon. Bi xibaar bi jibee, Ndakaaru dafa riir démb.
Démb ci alxames ji la xibaar bi jib. Xaat-xaat, xibaar bi law na ba daj réew mépp ; àddina sépp yëgandoo ko. Dëkk biy riir, Ndakaaru yëngu, xumb lool, coow li kurrl. Nit ñiy yuuxoo ak a sarxolle, daamar yeek moto yiy kalaksone… ñépp a bég. Ñépp màbbandoo, daw wutali Site Kër-Góorgi, fa këru Usmaan Sonko nekk. Mbooloo mu takkoo takku daje fa. Fu sàndi woon mbattu mu tag. Ñu nekk di woy turu Usmaan Sonko ak Basiiru Jomaay Fay.
Sémbuw amnisiti bi Maki Sàll wotelu fa Ngombalaan ga moo far tuuma yiñ doon toppe meeru Sigicoor biy njiitul Pastef ak tofam lii di Basiiru Jomaay Fay mi mu tànn, def ko lawax.
Me Xuraysi Ba, kenn ci seen layookat yi, moo dëggal xibaar bi. Benn taskatu xibaaru AFP la sàndi kàddu, wax ne : “Ci sunu kanam lañu génnee. Mat na.”
Ndiiraan giy dox ndànk biir Ndakaaru. Biñ ci tegee ñaari waxtu, ñu gis Basiiru Jomaay Fay génn di tàllal loxo mbooloo mi, daldi wax ne :
“Gis nan ni ngeen nu jàppalee ak ni ngeen nu taxawoo. Bég nan lool. […] Sonko génn na.”
Tey lañu war a janook taskati xibaar yi ca otel Azalaï.