Umar Sisoko Embalo, Njiitu réewum Gine Bisaawoo, tasati na Ngomblaan ga. Démb altine, ci yoor-yoor bi, la woolu ca màkkaanu Njiitu réew ma (pale), Ndajem-Réew. Ay njiiti campeefi réew ma teewoon ci niki njiitu Ngomblaan gi, Domingos Simoowes Pereraa, njiitu jëwriñ yi Seraldoo Martins ak njiiti làngi pólitig.
Ca njeexitalu ndaje ma, yéenekaayu web bii di VOA Afrique dafa siiwal ab dekkare bob, Njiitu réew maa ko xaatim, di ci wax ne :
« Dees na àppal wote yii di ñëw saa bu jàppandee, ni ko sàrti (…) ndeyu-àtte ji tëralee. »
Dekkare bi yemul foofu. Nde, xamleet na ci ne :
« Ginnaaw bi “Garde nationale” bi jéemee daaneel Nguur gi te nu am ay firnde yu leer ni am nay way-pólitig yu ci laale, campeefi Bokkeef gi mënatuñoo dox ni mu ware. Mbir yii xew dañuy wone ne nu ngi ci njàqarem pólitig mu mag. »
Li xew moo di ne, àjjuma jii weesu, ci suba si, ay soxi fetel yu bir a bir lañ doon dégg ci gëbla ga, ca wetu dalu (caserne) “Garde nationale” bi. “Forces spéciales” yi ak waa “Garde nationale” bi ñoo doon weccantey soxi fetel. Ci diggu bëccëg bi la jàmm ji delsi. Bi ñu xëyee ci gaawu gi, Njiitu réew ma, Embolo xamle ne dañ doon jéem a daaneel Nguuram te, dina am ay « njeexital yu réy ». Daf ne :
« Dubaay laa nekkoon di teewe COP28 bi. Mënuma woon ñibbisi ndax liñ doon jéem a doon daaneel Nguur gi. Dama leen a bëgg a wax ne jëf jii dina am ay njeexital yu réy. »
Rax na ca dolli ne, « Am nay màndarga, dinan leen leen won. Daaneel bii ñu doon jéem a daaneel Nguur gi dañ ko waajal laata 16 nowàmbar (bésub 50eelu cargal làrme bi). »
Looloo tax mu tas Ngomblaan ga. Wii moo ñareelu yoon wi muy tas Ngomblaan gi ci diirub ñaari at kepp. Ñu bari, rawatina kujje ga, dañ jàpp ne li mu amul i dépite yu doy moo ko tax a tas Ngomblaan gi. Nde, moom Njiitu réew ma, amul sax lu tollu ci 30i dépite. Mu mel ne, foofeet, demokaraasi daf fa nasax ni mu nasaxee jamono jii ci réewi Afrig sowu jant yu bari.