GUY NJÓOBEEN (1/2)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aatu feeñ na ! Njaayeen yi dégluleen

Njóobeen bi raw na leen

Buleen ko réyloo woyal, nanguleen

Guy ga ca Yoof du mës a liis

Kuy siisu randul te muñaale sa tiis

Nde, bile Njóobeen, daa ji du mës a ŋiis

Guy Njóobeen gilee donn lëf ci Kocc

Moo tax du meññ focc

Ku nàmpe ci meenum Seex Anta, Njóobeen ba niki moom

Loo togg, yakk mu di koom

Gaa ñi seedeleen, Bóris, kenn du moom

Guy ga ca Yoof, dootul réer li mu bind

Téereem yoy, ñooy sax ni Guy-mbind

Reenam ya law nañ ba Oklahoma

Dekkal fa Murambi, téerey yaxi Ruwàndaa

Ñu bég ca, góor ña ; ñu sagoo ca, gor ña, niki Madibaa

Maki Madibaa, dëggal ma :

« Bi ma gisee Bóris, ak muuñam bu siiw ba te bari kersa, di jëli cargalug Neustadt Prize, dama yëg sag bu réy a réy.

Dama bég ci moom balaa dara, bég ci liggéey bi mu sottal ci diir bu ëpp ñeen-fukki at.

Neexalu ngërëm bile, yeyoo na ko ngir waxtu yu yàgg yi muy toog di togg ak a ràbb i baat yu gànjaru, di waxloo way-dawlu yeek ñiy dund.

Bóris, daanaka léppam ladab la. »
Wax ji duy baab, nde léppam a di ladab

Dëgg du romb i nopp

Ku sa xol laab, nangul te bul xalab

Rëddi werekaan bi jar a sopp

Bubakar dafa aay

Bóris du wax lu aay

Jóob a jubba doo kuy saay

Ak sa xalima bu neex a neex

Nooni Afrig ak àddina nga sóoru xeex

Céy bile Njóobeen

Duma nga leen ca njëlbeen

Li ngay bind du neen

Madibaa seede ma :

« Bu ma koy xool, dafay mel ni dafa digaale ci pet ak jinne jiy dée bindkat yi. »

Du man maa koy weddi

Mbaxanem jaloore jii, àddina du ko xeddi

Xanaa ku soxor, xamadi, ñoradi niki naataangooy réewam yi ko beddi

Safoo waxi picc

Fàtte Guy-Njóobeen gi ne gicc

Ay doxandéem di witt

Ay nawleem di ko fitt

Madibaa, waaruwoo ?

« Man kay, sama cawarte geek sama ràngati yépp a naaw, naqar ak tiis dikkal ma. »

Ñaari saa-senegaal kese lan fa woon, teewoon ca xew-xew ba.

Dëgg kaani la, kuñ ko tuuf nga toxoñu

Waaye nag, deesu ko ñéeblu

Dëgg ji mooy, ku xool sa démb, daldi roñu

Sa bopp nga toj, sa bopp nga xeeblu

Bopp bu toj mooy xam-xam bu jeex

Bu xam-xam jeexee cig gaal ba caaxaan ne ca faax

Googu gaal dafa nar a suux cim mbeex

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj