LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (15/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NDAJEM JËWRIÑ YI (15/1/2024)

Ndogal yi tukkee ci ndajem jëwriñ mu tay mi :

  • Dees na yeesal fànnu yaale ji te gën ko ñoŋal ngir liggéey yi ci tukkee gën a yokku, ndaw ñi mën cee ame xëy.

  • Dees na saytu naaluw Xëyu ndaw ñi daldi koy lootaabewaat.

  • Jëlees na ndogalu gën a doleel jëflante yi dox diggante Nguur gi ak diiney réew mi.

  • Dees na suuxaat fànnu géej gi ak waax yi nees ko tëralee ci “Agenda nation de transformation”.

MBIRUM EMEDIA : JËWRIÑ ABBAAS FAAL DUGAL NA CI LOXOOM

Ci benn laaj-tontu bu mu séqoon ak waa saabalukaay Le Soleil, jëwriñu Liggéey bi, Abbaas Faal, xamle na ne, wax na ak waa “Direction générale du travail” ñeel coow la am fa Emedia.
“Sant naa “Direction générale du travail et de la sécurité sociale” mu defaral ma ag caabal ci mbirum Emedia. Waaye duñu yem ci ñoom rekk, [dinañu saytuwaale] fépp fu am ay jafe-jafe.” (Kàdduy jëwriñ Abbaas Faal)
Rax na dolli ci kàddoom yooyu, ne : “Dañuy sos rekk ngir sos. Xamuma ci yan anam lañu taxawalee Emedia, waaye jàpp ne naal wi dafa am ay jafe-jafey koom-koom ci anam bi ñu ko tëggee. Xamuma lu xew, waaye am na ñu koy lënkale ak li Nguur gi fi jóge dem. Gëmuma loolu nag. Bu dee ne loolu la, naal yu bari ci nasax lañu jëm.”

BÀRTELEMI JAAS JIITETUL METROPOLIS

Jordi Vaquer, Magum fara-caytu Metropolis, dafa génnee ab yégle buy xamle ne Bàrtelemi Jaas jiiteetul Metropolis. Bindees na ci yégle bi ne :
“Ci bésub 13i fani desàmbar 2024 bii lañu wàccee Sëñ Bàrtelemi Jaas ci boppu meerib Ndakaaru. Ndogal loolu daf ko ñàkkloowaale ndombo-tànku njiitul Metropolis.”

Waa Metropolis dañu daje, fénc mbir mi. Ginnaaw bi ñu sukkandikoo ci dogu 10eel ci Sàrti Metropolis, ci lañu tabb meeru Montevideo ngir nekkandi njiitul Metropolis ba keroog ñuy falaat keneen.
Cig pàttali, ca atum 2023 lañu faloon Bàrtelemi Jaas ci boppu Metropolis, di mbootaayu àddina mu dajale dëkki yu mag yi ci àddina sépp.

ÀPPEL LAAYEEN 2025

Njiitul yéenekaay Le Soleil daje na ak kurél gi yor wàllu jokkoo gi ñeel Àppel bi. Li waral ndaje mi mooy waajtaayi Àppelu ren jii, 2025. Bési 30 ak 31 ci weer wii lees koy amal. Ngir yembal lépp lu aju ci wàllu jokkoo gi, Lamin Ñaŋ mi jiite SSPP Le Soleil, dalal na kurél gi ci àllarbay tay jii, 15i fani 2025. Aadama Sow moo jiite woon mbooloo mi waxtaani woon ak Sëñ Ñaŋ.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj