Maymuna Nduur Fay, taskatu xibaar bi jiite 7tv la ab/ay sàmbaabooy dogaale, fitnaal ko, jam ko paaka. Mbir maa ngi xew ginnaaw bim jeexalee jotaay bi mu doon séq ak Farba Ngom, démb ci guddig alxames ji.
Rawalees na ko ca raglub militeer bu Wakaam. Nee ñu nag, jot naa ñàkk dereet ju bari. Muy jëf ju ñaaw joo xam ne, ñépp ñaawlu nañ ko.
LU DEFU WAXU a ngi koy mastawu, di ko ñaanal wér ak mucc.