JÀPP NAÑ BAH JAXATE AK IMAAM SÉEX TIIJAAN NDAW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb lañ jàpp kii di Bah Jaxate, di aktiwist bu jege Maki Sàll. Waa DIC ñoo ko teg loxo. Li ko sabab mooy kàdduy tuuma yu yékkati teg leen deru elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko.

Bees sukkandikoo ci taskatu xibaar bii di Baabakar Ture mu Kewulo, Usmaan Sonko moo sabablu jàpp biñ ko jàpp. Maanaam, Usmaan Sonko boolewu ko Yoon. Toppekat bi ci boppam moom jël ndogalu boppam, yónni takk-deri DIC yi ngir ñu jàpp ko.

Moom nag, Bah Jaxate, bi mu janook luññutukat yi, dafa lànkoon ne du wax. Waaye, ca mujjantal ga, nee ñu wax na ba ne am nay firnde yoy, layookatam bi la leen dénk. Fi mu nekk nii nag, mi ngi ci loxoy Yoon.

Naka noonu, kii di Imaam Séex Tiijaan Ndaw itam, jàpp nañ ko. Waa DIC ñoo ko jëli. Moom it, li ñuy toppee Bah Jaxate lañu koy toppee. Nde, dafa wax ci Usmaan Sonko ay kàddu yu ñàkk teggin, tuumaal ko ci wàllu ngóor-jigéen. 

Cig pàttali, Usmaan Sonko daf fi dalaloon Saŋ Lig Melãsoŋ (Jean-Luc Mélenchon). Ba ñuy waxtaan, dañu àdduwaale ci mbiri boroom ñaari tur yi. Mu jur fibcoow lu réy. Ca la Bah Jaxate ak Imaam Séex Tiijaan Ndaw génnee, wax ay kàddu yu ñaaw a ñaaw ci elimaanu jëwriñ yi, njiitul Pastef lii di Usmaan Sonko. Looloo waral ñu jàpp leen.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj