JÀPP NAÑ BUGAAN GÉY DANI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àllarbay démb ji, 2i pani oktoobar 2024, lañu woolu woon Bugaan Géy Dani mi jiite kurélu “Gëm sa bopp”. Waa “Division de la cybercriminalité” ñoo ko bëggoon a déglu, taxoon ñu sant ko mu wuyuji leen. Bi mu demee nag, bàyyiwuñu ko mu ñibbi. Nde, ci li rotagum ciy xibaar, fa la fanaan. Tay ci suba lees ko jàllale fa toppekatu bokkeef gi, ñu war a janoo ñoom ñaar.

Bees sukkandikoo ci sunuy naataangooy Seneweb, kenn jurewul boroom Dmedia. Maanaam, kenn pelentu ko, walla ñu kalaame ko yoon. Benn banqaasu DSC moo gis ab widewoo bu mu defoon, di dal ci kow Càmm g. Noonu, takk-der yi, ci seen coobare bopp, jël mbir mi ngir tijji ci ag luññutu. Ci kow loolu la komiseer Jijag Fay tàggu toppekatu bokkeef gi ngir woolu Bugaan Géy Dani, Ibraayma Ndóoy daldi ko koy nangul. Looloo ñu woolu ko ngir laaj ko ñeel luññutu googii takk-deri DSC yi tijji.

Bugaan nag, dafa bëggoon pólitigee mbir mi, moom ak waa lëkkatoo Sàmm sa kàddu. Ndax, lëkkatoo gi ci boppam dafa siiwal ab yégle di ci ñaawlu les woolu Bugaan mom, lawax la ci wotey dépite yees dëgmal, keroog 17i pani nowàmbar 2024. Bu dee moom Bugaan, Usmaan Sonko la tam dëmm, wax ne moo nekk di ko fexeel ngir tere koo bokk wote yooyu. Loolu doyatul, muy wuyuji, raŋale ay daamar, di korne ak a daagu ci tali bi, donte ne kenn xatalu ko ci yoon wi. Dafa di, dañ ko xàllaloon yoon wi. Waaye, moom, dafa bëggoon a réyal mbir mi, rax ci pólitig. Ndeysaan, pexeem sottiwul. Yàgg na ci yoon wi lool, waaye mujje na àgg.

Bi mu àggee, naam romb na waxtu wees ko joxoon, waaye taxaw na wax ak taskati-xibaar yi. Ci li mu jàppoon, mbirum lempo yi mu ameel askan wee tax ñu woolu ko. Dafa daldi lënkale lees ko woo ak i yëngu-yëngoom ci géewu pólitig gi. Wànte, dafa mel ni mbir yi jotewuñu dara. Lees koy toppee mooy “wesaare xibaar yu wéradi”. Seneweb moo ko xamle.

Ba muy dem, àndoon na ak i layookatam, meetar yii di Aamadu Sàll, Elaas Juuf, Aliyun Badara Faal ak Jibi Jàllo. Am na ñu wax ne, takk-der yi dañu ko won widewoob ndajeem bu mujj bu amaloon ak taskati-xibaar yi, keroog 26i pani sàttumbaar 2024, ginnaaw bi Usmaan Sonko ak Càmm gi waxeek askan wi ba noppi ñeel koppari réew mi. Moom Bugaan, boroom Sentv, nangu na ni moo wax kàddu yees ko askanale.
Takk-der yi dañu ko xamal ne li mu wax ci jëwriñ yii di Abdurahmaan Saar, Séex Dibaa ak magum fara-caytub Càmm gi, Muhammet Al Amiin Lóo, tegginewuñu dara te ay yàq der la. Nee ñu, moom Bugaan dafa tontu, wax ne, mëneesul wax ne ay kàddoom tegginewuñu te day yàq der. Moom daal, ci lees wax, dafa wax takk-der yi ne daf leen di bàyyi ñu jàppee waxam ji nu mu leen neexee. Bi mu tontoo loolu, benn takk-der laaj ko :
“Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dafa joxe ay lim, nga weddi lim yooyu, ne baaxuñu. Ndax danga am ay xibaar ñeel lim yu wér yi ?”
Bugaan tontu :
“Ginnaaw bi mu waxee, ndaw si fi teewal FMI dafa génn, wax ne am na wóoralug “cours des comptes””.
Mu dolli ca, moom Bugaan, ne :
“Bu dee lim yi Usmaan Sonko joxe wér nañ, day tekki ne ñi labaj lim dañ leen a war a topp. Waaye amuñu benn firnde bu wone ne dëgg la. Bu dee wesaare ay xibaar yu wéradi, moom moo ko def.”
Ba tay, ci lees rotal ciy xibaar, luññutukat yi dañu laaj Bugaan ndax dafa am ay këyit yu firndeel li muy wax. Waaye Bugaan dafa ne day xaar wóoralug “cours des comptes” laata mu ciy àddu. Ca la ko takk-der yi laajee ndax mi ngi natt bu baax ay kàddoom buy wax. Nde, ba tay ci waxi takk-der yi, leblekat (bailleurs) yi mën nañoo dégg i waxam, daw, dem seen yoon. Waaye, Bugaan dafa joxoñati Usmaan Sonko, wax ne moom mooy dawloo leblekat yi ndax moom moo fésal guuta gi koom-koomu Senegaal nekk. Bugaan dafa jàpp ni, Usmaan Sonko moo war a ñëw leeral. Ciy waxam, moom jógul ngir naqaral kenn. Dafa wax ne :
“Mësuma am yéeney naqaral kenn. Defuma lu dul moytuloo nit ñi waxi Usmaan Sonko.”

Fi mu nekk nii nag, dafa mel ni luññutu gi jeex na. Nde, amaana Bugaan jàkkaarloo ak toppekatu bokkeef gi fii ak ëllëg. Dees na xam ndax dañu koy tëjandi fii ak ñu koy àtte walla. Ak lum ci mën di doon, Bugaan moom dafa jàpp ni pólitig moo laxasu ci mbir mi. Te yit, mënul a génnee Usmaan Sonko ciy waxam. Dafa mel turu njiitul Pastef li dafa taq ci làmmiñ wi, tëw a deñ. Ñenn ñaa ngi naan sax daf koy toppandoo ci lépp, ba ci baat yi Usmaan Sonko daan jëfandikoo bu waxaan ak Njiitu réew ma woon, Maki Sàll.
Usmaan Sonko daal, ku weex dunq la.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj