JÀPP NAÑU DR BAABAKAR ÑAŊ, BOROOM KILINIG SUMA ASSISTANCE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sàndarm yi jàpp nañu fajkat bii di doktoor Baabakar Ñaŋ miy boroom kilinig Suma Assistance. Rajo Rfm a siiwal xibaar bi. Nee ñu, Medina Njaajbe lees ko jàppe. Waa « Sûreté urbaine » ñoo santaane ñu indil leen ko. Démb lees ko waroon a indi fi Ndakaaru. Jamono jii nag, xameesagul sababu njàpp gi.

Lees xam daal mooy ne, njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, ca kilinigu doktoor Baabakar Ñaŋ la doon fajoo, ginnaaw bi ko takk-der yi metitalee, pomp ko ag ndefar gog, daaneeloon na ko. Cig pàttali, waa « sûrete urbaine » woolu woon nañu, lu jiitu ñuy jàpp boroom kilinig bi, fajkat bi doon saytu Usmaan Sonko, di ko laaj i laaj. Noo ngi xaarandi yeneen i xibaar ngir am lu ci gën a leer.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj