JÀPPATI NAÑ USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii weesu lañ ñàggi kër Usmaan Sonko ginnaaw 55i fan. Ñu yaakaaroon ne Nguur gi dafa séqi jéego ngir dox jàmm. Waaye, dafa mel ni jàmm jooju ñu doon séentu, jubseegul. Nde, tey ci àjjuma ji laa waa sàndarmëri jëlsi Usmaan Sonko këram, jàpp ko yóbbu. Ba jamono jii nuy bind yaxal bi, bàyyeeguñ ko.

Ci njolloor gi, bi jumaa di waaj a jot, lañ ko jëlsi këram, fa Site Kër-Góorgi. Waa GIGN ñoo ko jàpp. Pastef ñoo dëggal xibaar bi cib yégle bi ñu génne. Nee ñu, lees ko jàppe jotewul dara ak mbirum “ngerum ndaw” bi ko àttekat bi daanoon ñeel coowal Aji Saar li. Nee ñu, mbirum jollasu la.

Ci lees foragum ciy xibaar, Usmaan Sonko dafa jàppante ak benn takk-der bu bokk ci way-yëddu yi (services de renseignement). Nee ñu, bi Usmaan Sonko jógee jumaa di dellu këram, aji-yëddu bi daf ko doon filme, di ko foto ak telefonam. Usmaan Sonko ci boppam moo nettali mbir mi ci mbaali-jokkoo yi. 

“Bi ma jullijee ba ñëw, way-yëddu yiy taxaw bés bu nekk sama buntu kër, dañ ma doon filme. 

Man ci sama bopp maa nangu jollasu bi, wax boroom na ko ubbi ngir ma far nataal ak widewoo yim jël ci man…”

Kon, lii, meneen mbir mu bees la. Ñoo ngi xaarandi yégleb Nguur gi. Pastef moom, ñu waajal xeex bi ngir ñu bàyyi seen lawax ci wotey 2024 yi. Nde, ci seen yégle bi, digal nañ banqaas yépp ñu booloo taxaw ngir waaj.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj