Seneweb moo siiwal xibaaru jàppug Paap Aale Ñaŋ, taskatu-xibaar ak faramfàccekat bu siiw. Jamono ji nuy bind yaxal bii, mu ngi ci loxoy takk-deri pólis bu mag bi. Nee ñu, mbóot yi mu feeñal ñeel mbirum Sonko-Aji Saar mee tax ñu jàpp ko ci dibéeru démb ji.
Sabab yi
Bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum, li taskati-xibaar bi sennal ciy xibaar ñeel kootoo gi am ci mbirum siif mees di tuumaal Sonko a ko yóbbe nattu bile. Dafa di, Paap Aale Ñaŋ dafa baaxoo di def ay live yoy, dina ciy dégtal ay xibaar yu bari ci ni réew miy doxe ak njombey Nguur gi. Fan yii, dafa bari woon li muy wax ci mbirum Aji Saar ak Usmaan Sonko. Te, ciy waxam, ag kootoo a ko lal. Waaye, dafa mel ni du loolu rekk a sabab jàpp gi ñu ko jàpp.
Ndeke, ci lees wax, li muy ñaax larme bi ñu fippu, di tilimal deru yoon ak li muy siiwal ay wayndare yees jàppe « secret-Défense » bokk nañ ci tuuma yees ko gàll. Dollina nañu ci sax ne, day tasaare ay xibaar yu wéradi ngir ñaawal deru Nguur gi fi nekk.
Démb rekk, ci suba si, laata ñu koy jàpp, Paap Aale Ñaŋ nag, bindoon na ci xëtu Facebookam, di ci wax naan :
« Yan saa-senegaal ñooy « hommes d’affaires » yiy jël màrse yi ñu dippe “secret défense ” ? Seen bari alal dafa jéggi dayo ba ñuy yokkal alal ñeneen. Ca Niseer, ba Njiitu réew ma, Isufu, santaaneeb ndéggantu ci màrsey ngànnaay yi, seneraal yu bare ñoo daanu. Senegaal moom, xel xalaatu ko… »
Lii la mujje bind laata xibaarub jàppal di jib.
Jàpp gi
Ci yoor-yoorub dibéer ji la ko ay takk-der yu bokk ci Kaaraangeg dëkk bi (Sûreté urbaine) jàpp. Nee nañu nag, ci ndigalu toppekatu Bokkeef gi, Aamadou Ba, lees ko jàppe. Wànte, firnde amagul ci ndax toppekat bi génneegul, fi ñuy binde lii, ab yégle bu koy dëggal.
Buur TV jokkoo na ak rakku Paap Aale, laaj ko ci mbir mi. Moom, nag, amul mbetteel ci li ñu jàpp magam. Wax na sax, ne kenn “jàppewuñ ko këram” donte nanguwul leeral béréb bien ko jàppe. Mu teg ci ne :
” …tey jii [démb], dibéer, ñu ñëw jàpp la, joxuñu la ag woote, waxuñu la benn sabab buñ lay jëlsee. Waaye nag, bettu nu. Xamoon nañ ne, yàgg yàgg, dañ koy jàpp ak yeneen taskati-xibaar, loolu na leen leer. »
Ñu baree naqarlu li xew, dina wane seen njàqare ak seen tiit ci ñi yoon wi doxe.
Seex Ahmet Tiijaan Yum mu parti PUR, moom, day « réccu » li ñu jàpp ab taskatu-xibaar bu far ak askan, di xeex ngir ñu “yemale” ñépp ak ngir “caytuwin wu mucc ayib ñeel balluy réew mi. »
Xalifa Sàll tamit ñaawlu na jàpp gi laata muy tagg Paap Aale Ñaŋ, wax ne ku xereñ la ci liggéeyam, di ku yàgg a xeexal demokaraasi te bëgg réewam lool.
Waa SYNPICS, mbootaayu taskati-xibaar yi, àddu na ci mbir. Ab yégle lañ génne, di ci wax ne :
” Noo ngi door a yëg jàppug taskatu-xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ. Synpics wax na ak layookat bii Bàmba Siise ngir xam sabab yi waral ñu jàpp ko ak ngir taxawu ko ni mu ware ci fànn yépp.”
Ñu bari, wëliis ñees fi tóxal seen i wax, yékkati nañu ay kàddu ci mbir mi, di ko jooy ak a kaas. Fim ne nii, li ñépp tàmbalee laaj, an jàpp gu bari gi, mooy : ” ku ciy topp ?”