FMI yabalati na ay ndawam fi Senegal ngir ñu waxtaan ci mbirum koom-koom ak koppari réew mi. Jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Koppe gi (Abdurahmaan Saar) ak Jëwriñu Kopparal gi (Séex Dibaa) ñoo leen dalal.
Ci talaatay démb ji, 18i màrs 2025, la ndawi FMI yi, ci njiitalu Sëñ Edward Gemayel , teersi fi réew mi. Ndaje mi nag, bari nay jubluwaay. Waaye, bi ci gën a not, ci kàdduy Sëñ Gemayel, mooy waajtaayu lees duppee “misreporting”. Li ñu ko dugge nag mooy xool, ànd ceek Càmmug Senegaal gi, wan naaluw koom-koom ak kopparal wu yees lañuy tëral ngir tegaat Senegaal ci yoon.
Bu dee Jëwriñ Abdurahmaan Saar moom, dafa feddali yéeney njiiti Senegaal yu yees yi ci leeral ak a sellal anam bi ñuy jiitee réew mi ak nees di saytoo alalu askan wi. Loolu, ciy waxam, dafa dëppoo ak naaluw “Vision Senegaal 2050” wi nga xam ne, ci njub, jubal ak jubbanti la Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ lal.
Waaye, mbir yemul rekk ci wax ak i yéene yees di biral. Moo tax jëwriñ ji xamleet ne, dees liggéey ngir ñoŋal koom-koomu réew mi ci anam bu yaatu ngir, ëllëg, Senegaal mën a moom boppam ci fànn wile.