Jëf toxal na wax. Ñoo ko dige woon, jëfe nañ ko. Umar Sàmba Ba siiwal na limub jëwriñ yi Sëñ Basiiru Jomaay Fay tabb, moom Njiitu réewmi, ngir jëmmal liggéey bi. Bi ñuy kàmpaañ ak sax lu ko jiitu, waa Pastef dañu dige woon ne, bu ñu jote ci Nguur gi, duñu weesu Càmmug fanweeri jëwriñ. Yéene jooju, matal nañ niki démb. Nde, ñaar-fukki jëwriñ ak juróom lañu tabb, toftal ci juróomi fara-caytuy nguur.
Ci teewaayu Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi, la Sëñ Umar Sàmba Ba biral turi jëwriñ yooyile muy jiite. Dafa di sax, moom Usmaan Sonko moo jëkk a jël kàddu gi, fàttali jubluwaay yi Nguur gu yees gi sasoo, jëwriñ yi war a xar seen tànki-tubéy ngir matale leen.
Jëwriñ yii toftalu ñoo séq Càmm gu yees gi :
Yaasin Faal, jëwriñu bennoog Afrig ak mbiri bitim-réew
Seneraal Biram Jóob, jëwriñu dooley xare bi (làrme bi)
Usmaan Jaañ, jëwriñu Yoon
Seneraal Sã Batist Tin, jëwriñu biir réew mi ak kaaraange bokkeef gi
Biram Suley Jóob, jëwriñu laf gi, soroj beek mbéll yi
Abdurahmaan Saar, jëwriñu koom-koom gi, Naal bi ak digaale bi
Séex Dibaa, jëwriñ kopparal geek ngurd mi
Maalig Njaay, jëwriñu tabaxte yi ak tukkiy (yaaley) suuf geek kow gi
Daawda Ngom, jëwriñu kéewnga gi ak coppiteg mbindaare mi
Bakari Saar, fara-caytub Nguur bees dénk mbiri mbatiit, indistiriy coste yi ak moomeeli mboor yi
Ca njeexital la, Usmaan Sonko xamle na ne, seen mébét mooy baral liggéey, fexe ba jëwriñ yi fi nekkoon gaaw a jox lenge yi jëwriñ yu yees yi leen di wuutu. Joxe na sax àpp, fii ak altine, nga xam ne, Nguur dina mën song jafe-jafey askan wi ci lu gaaw. Moom sax, ci altine jii ñu dëgmal lay nangu lenge yi ci loxoy Sidiki Kaba mi muy wuutu ci bopp jëwriñ yi.
Moom, meeru Sigicoor bi, xamleet na ne, Njiitu réew mi jox na àppug weer ngir jépp jëwriñ ju ame moomeg pal, mu tekki ndombog-tànkam ci moomeg pal googu te jublu ci liggéeyu njëwriñu bi ñu ko dénk, bañ ci rax beneen liggéey. Kon, jàpp jëwriñ joo xam ne meer ngi, walla ngi jiite am ndaje bokk-moomeel yi walla sax ngay dépite, am nga weer ngir bàyyi liggéey yooyii.
Nguurug Basiiru Jomaay Fay gu fàttewul ndem-si-Yàlla, Mahammad Buun Abdalaa Jonn, elimaanu jëwriñ ja woon te génn àddina ci àjjumay démb ji, 5 awril 2024. Usmaan Sonko fésal njaalu Njiitu réew, ñaanal ko. Waxeet na ne, ci ndigalu Basiiru Jomaay Fay, Nguur gi dina def kemtalaayu kàttanam ngir taxawu njabootu Mahammad Buun Abdalaa Jonn. Muy lu rafet lees war a gërëm.