JÉYYA JA CA KAFRIN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ak jéyya ju réy a réy la réew mi yeewoo tey. 54i nit ñoo ñàkke seen i bakkan ci ab aksidaŋ bu mettee metti bob, mi ngi ame ca Sikilo, ci diiwaanu Kafrin. Dafa di, ñaari biis yu mag, yeboon ba fees dell, ñoo mbëkkante ci yoonu Kafrin-Tàmbaa wi. Benn biis bi, nee ñu Kéedugu la bawoo woon jëmsi Ndakaaru te, beneen bi, Ndakaaru la jóge woon. Ci guddig gaawu gi, jàpp dibéer la musiba bi am. Ginnaaw 54i nit yi ci faatoo, nee ñu, am na 100i nit ak lu teg yoy, jële nañ ciy gaañu-gaañu.

Réew mépp a ame tiis ak naqar. Fi mu nekk nii, aksidaŋ bi la ñépp di waxtaane. Bu ñii dee joxoñ baaraamu tuuma Njiit yi, ñee ña ngay tiiñal dawalkat yi ; ñenn ñiy xas takk-der yees di ger ci tali yi, ñeneen ñiy ŋàññi wata yu màgget yeek tali yu bon yi. Toppekatu Kawlax bi, moom, génne na ab yégle, di ci xamle ne, ay boori 3i waxtu ci guddi gi la aksidaŋ bi am. Ci yégle bi, nee na ci, benn biis bi la pónoom toj, mu daldi wàcc yoonam, mbëkki beneen biis bi doon dawe weneen yoon wi. Sàndarm yeek sàppëer yi daw gaaw walluji nit ña. Waaye, booba, liy am, am ba noppi.

Jamono jii nag, Njiitu réew mi jël na ndogal, dekkerete 3i fani dëj yuy door ëllëg ci altine ji, 9 saŋwiyee 2023. Nee na yit, dinañ amal am Ndaje mees yaatal ñeel njawriñ yi ngir, ciy kàddoom : « ñu jël ay dogal yu leer ci wàllu kaaraangeg tali bi ak way-tukki yi. » Njiiteef gi xamle woon na sax ni, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa war a dem Kafrin, fa aksidaŋ ba ame, bu 13i waxtu tegalee 30i simili. La mu ko dugge mooy seeti ña ca jële ay gaañu-gaañu.

EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi jaale mbokk yi ci deele ak waa réew mépp, di mastawu ñi ci jële ay gaañu-gaañu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj