JÉYYAY MBËKK MI : AAMADU BA (BBY) ÀDDU NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ ja woon ci nguurug Maki Sàll, Aamadu Ba, àddu na ci jéyya ji am ci géej gi, te 89i saa-senegaal ñàkk ci seen i bakkan. 

Ci géeju Gànnaar gi la mbir mi amee. Nde, dafa am ñenn ci doomi réew mi ñoo xam ne, dañ mbëkki woon, wutali Espaañ. Bees sukkandikoo ci kàdduy lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar ci wote yi mujj, jéyya jii dafay fàttali ngaañ yi  nekk ci mbëkk mi ak ni mu wóoradee. Ñaawlu na yit anam yu metti ba jéggi dayo yi mbëkk-kat yiy jël gaal giy nekke ci yoon wi, biir géej gi. Te, ba tey ci waxi Aamadu Ba, dara waralu ko lu moy yàqi, maanaam ñàkk yaakaar ci réew mi. 

Aamadu Ba dafa bind, di artu :

“…danu war a fexe defar koom-koomu réew mi ngir ubbil nit ñiy bunti liggéey ngir ñu mën dund ci ngor. Warees na tamit samp ay kurél yuy taxawu ndaw ñi ngir ñu bañ xalaat a song mbëkk mu wóoradi mii.”

Mi ngi jeexal ay kàddoom cig woote bennoo bokkaandoo naqar wi te liggéeyandoo ngir “soppi, jëlee fi ndund gu lëndëm gile”.

Cig pàttali, fan yii weesu, dafa am ug gaal gu yeboon 170 mbëkk-kat, bawoo ca tefes ya Senegaal digaloo ak Gàmbi, wutali Tugal. Waaye, dafa mujje suux. Juróom-ñeenti nit kese ñoo ci mucc, ab xale bu jigéen bu am 5i at bokk ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj