“DOY NA !”, “DAFA DOY !”. Ñaari baat yii mën nañoo tënk doxu-ñaxtu bi amoon ca diiwaanu Tàmbaakundaa ak ci péeyub réew mi, gaawu bii weesu, 25eelu fan ci weeru me. Binta Kamara, 23 at, lañu xoj ba mu sedd guy. Mbir maa ngi xewe foofu ca Tàmbaa ñetti ayu-bés ci ginnaaw, bésub gaawu, 18eelufan ci weeru me. Ki ko rey, nag, da ko doon jéem a siif, ndaw si bañ, waa ji jaay ko doole, xoj ko ba mu dee ciy loxoom. Jëf ju ñaaw jooju, siifaate beek reyaate bi, la ñaxtukat yi ne : “na fi dakk !”.
Dafa di sax, baayu Binta Kamara politiseŋ bu far ak Maki Sàll la, amaana looloo waral mbir mi gën a fés. Wànte, jamono jii ak at yii ñu weesu yépp, siifaate bi ak reyaate bi dafa takkarnaase. Ndaxte, ci benn ayu-bés gi doŋŋ rey nañu ci ñaari jigéen : kenn ki ci màrse bu Wakaam lañu fekk néewam, ñu futti ko ba mu set wecc, keneen ki Kumba Yàdd la tudd, Cees lañu ko reye gànnaaw bi ñu ko siifee ba noppi. Kurél yiy sàmm àqi jigéen ñi fii ci Senegaal nee nañu, luy jot jot na ginnaaw dee, nguur gi na jël ay ndogal ci ni mu gën a gaawe, dakkal ñaawtéef yi jigéen ñiy jànkoonteel. Ndakaaru sax, amaleesoon na fa ab doxu-ñaxtu.
Keroog, ca Péncum askan wi, “Place de la Nation” ci nasaraan, ñu bare ci doomi-réew mi taxawoon nañu fa ngir naqarlu ak kaas ñàkk kaaraange gi réew mi nekke, te mu gënatee metti ci jigéen ñi. Ci anam bu doy waar lañu fa taxawe woon. Ay kanam yu sadd di wone seen mer ak seen tiis. Ñu seel seeni kanam, péntuur ci lu nirook deret, mu ciy rogaat. Li ñu ko dugge woon, moo doon xamal ñépp ne deretu jigéen ji ñuy tuur dafa doy.
Waaye, maandu war na ku nekk ci nun. Ràcc jëmale sa kanam baaxul. Dëgg la, jigéen ñi sonn nañu wànte rey bi moom fépp la, du jigéen ñi rekk la ñuy bóom. Ndax, saa su nekk ñu dégg ne am na as ndaw su faat jëkkëram ci lu ñàkk faayda te kenn du dégg kuréli jigéen ñi wax. Bu ko defee, li ñu war a xeex dëgg mooy rey bi ci boppam. Loolu nag, yemul rekk ci teg fiy daan yu diis walla ñu def ku rey ñu rey la. Li gën mooy ñu xoolaat yarinu xale yi ca ba ñuy tuut-tànk, jàngal leen yar ak teggin, waaye jàngal leen itam diine, ngir saxal ci seen xol ak ci seen xel ay jikko yu rafet. Ndax Wolof Njaay dafa ne, gune lawtanu yomb la, boo ko wëlbatiwul, mu law fu la neexul.