KAN MOOY JIITEJI CESTI ? (NDEY KODDU FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Atum 2005 ak léegi daara ju mag jiy tàggat taskati xibaar yi ci Iniwersite bu Ndakaaru day tabb ñi yelloo jiite ko. Àllarba 26éelu fan ci weeru Ut 2020 jàngalekat ak saytukati Daara ji ñoo njëkk a tànn seeni nit. Ci kow loolu, ci 13 ñi doon wote, 9 yi wutaakon bii di Mamadu Njaay lañ jox bopp, 4  yi ci des faruñook kenn ; kon bésu wote ba dees na jël 3 baat féetëlee kook Mamadu Njaay.

Bu loolu weesoo, talaata 1 sàttumbar yeneen ligéeykati CESTI yi tamit 12 lañu te 7 yi Njaay lañu àndal, 5 yi woteel soxna si Kusoŋ Tarawore miy jiite tey CESTI. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj