JOXEB LIJAASA BU 48eelu LËLU CESTI (NDEY KODDU FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Alxemes jii nu génn la CESTI doon jox seen lijaasa 4i taskati xibaar yu jigéen ak 21 yu góor. Xew-xew baa nga ame “UCAD 2” ci njiiteefu Abdulaay Jóob, jawriñu Mbatiit bi. Lël bii nag, mooy 48eel bi te ñuŋ ko tudde ndem-si-Yàlla ji Saaliwu Tarawore, nekkoon taskatu xibaar, jànge Cesti diggante 1975 ak 1978, liggéey APS ba noppi toogaloon fi EFE, benn yéenekaay bu newoon ca Espaañ.

Ñi ëpp ci taskati xibaar yu bees yi – mat nañu 10 – tele lañu taamu te Màggat Gay a leen raw ñoom ñépp ; Mamadu Umar Ba lañ gën a ràññee ci 7 yi def rajo ; bu dee 8 yi jàng bind ci surnaal, Muhamed Jenn a jiitu ñeneen ñi topp ci ginnaawam. Mu mel ni kon sama mbokki jigéen yi gaa ñi raw nañ leen fépp ren…

Porfesoor Mamadu Njaay, njiitu daara ja, yëkkati na fay kàddu yu am solo, jëmale leen ci waay-génn Cesti yi.

Lii la leen wax :

«Yéen a ngi jot seeniy lijaasa ci jamono ju metti, jamono joo xam ni mbas mi daa jaxase àddina si juróom-ñaar. Ni ko ñépp xame, jur nay jafe-jafe yu bare ci liggéeyu taskati xibaar yi, rawatina ci wàllu koom ; xibaar yiy jaare ci mbaali-jokkoo yi sax, muccuñu ci. Waaye bu mu leen tax a yàccaaral, ndax tàggat nañ leen ci lu mucc ayib. Su ngeen góor-góorloo dingeen ci génn. Te am naa yaakaar ni dingeen bàyyi xel xar-baax yi Saaliwu Tarawore làmboo woon te ñu doon : fonk liggéey, xereñ, jub, gëm sa bopp».

Ndaje ma géeyul ndax liñ fa toog yépp, woykat ak xalamkat yaa ngi doon bégal xol yi.

Pr Umar Jaw a ubbi waxtaan yi ndax moom la Cesti tànnoon ngir mu jottali mbooloo mi li mu tudde «yóbbalu mag». Ñaax na leen ci dëggu ak mën làkk wi ñuy joxee xibaar. Mu ni : «moytuleen ku leen jam. Fileek nit kaa ngi dund, njàngam du jeex, jàngleen ngir seeniy ñoñ naw leen. Sunu liggéey bii nag, dunu waat ni ko fajkat yi baaxoo def, waaye terewul mu laaj lu bari. Tënkuleen ci jikkoy Saaliwu». Bi mu noppee, Séex, doomu Saaliwu Tarawore bi yoroon baatu njaboot gi te àndoon sax ak yaayam moo ko wuutu ci mikóro bi. Lii la fa wax : «Ñi faatu dëgg, mooy ñi ñu fàtte. Tey, Cesti, daara ju mag ji ñuy tàggatee taskati xibaar yi, dekkalaat na Saaliwu Tarawore bi mu ko tuddee bésam bii, feelu waa Espaañ ndax ñoom it sargaloon nan sunu baay, ba njaboot gi demoon teewe ko. Saaliwu Tarawore, ñu baax a ko meññ, moo tax mbaaxam ak njubam mënul woon bett kenn…. Mësul a naagu, mësul a nangoo laal xaalisu nger. Li ma wóor mooy ne 48eelu lël bii, duñ ko rusloo mukk, dinañ ko def royukaay, def seen liggéey ak ngor, fexe ba kenn du leen yab.»

Bi mu daanalee, lañu seetaan ñaari «films» : bu njëkk bi ci Saaliwu Tarawore, bi ci des ci lël bi doon génn Cesti. Biñ jagleel turandoo bi, daw na yaram lool : magu Saaliwu, soxnaam, jarbaatam ak i xaritam seedeel nañ ko bëgg njaboot ak fonk liggéey. Ginnaaw loolu, xaritu benn bakanam, doomu-ndeyaam, Ibraayima Baaxum moo def nataalam, fàttali nit ki mu nekkoon.

Jawriñu njàng mu kowe mi, moom, Doktoor Aamadu Galo Jóob la yabaloon. Bi mu ndokkeelee ñépp ba noppi, Dr Jóob daa wax ci turu boppam ne bu sañoon taskati xibaar yi gën a def i jéego ci wàllu paj ak xarala ngir yokk xam-xamu askan wi ci fànn yooyu, mu amal Senegaal gépp njariñ. Nee na itam bu Yàlla sàkkee àddina si ba noppi jël nit jagleel ko làmmiñ, xel, kàddu ak kàttanu sos, war nanu cee jàngat ni loolu lépp liggéeyu taskatu xibaar baa ngi ci biir. Kon war naa jàppale askanam, baaxe koy xibaar yu wér te wóor ngir mu mën a moytu yenn jafe-jafe yi ».

Ci gis-gisu Ahmadu Aali Mbay miy Njiitu Iniwérsite Séex Anta Jóob, «joxeb lijaasa day biral njàng mu sotti tey may nit ki xam-xam ak mën-mën». Gërëm na yit Pr Mamadu Njaay, ni ko : “Ndokkale Njaay ci yu bees yi nga sos ngir jëmale daara Cesti jii kanam. Lu aw askan di gën a xam di gën a yeewu. Yéen ñii, tey, ci seen ndodd lañ teg yen woowu… ».

Abdulaay Jóob, jawriñu Mbatiit bi tëj waxtaan wi, da cee yokk ne : «tas xibaar, li mu gën a laaj mooy màndook yemale ; loolu la nguur gi xam ba taxaw ci tànki set-setal ko, bëgg it ñépp jàppale ko ci ».

Moom daal, amul kenn ku fa janook mbooloo mi wax te fàttaliwoo jikko yu rafet yi turandoo bés bi amoon ba noppi ñaax 48eelu lël bi mu aw ci yoon wi mu xàll démb tey soog a ñëw.

Bi lii lépp jàllee, la Pr Mumini Kamara door joxeb lijaasa yi…

Boroom-teraanga yi sañse ba jekk : jigéen ñi sol i baseŋ yu gel teg ci sor, gàlloo kol gu baxa. Góor ñi tam, naka noonu waaye ñoom ay kóstim yu baxa-bu-dër lañ sol, takk karawaat bu xonq ci kow simis bu baxa. Ñoom ñépp sagu, bég ci li fa seeniy mbokk, seeni xarit, seeni naatangoo teew, bég itam ci ni kilifay làrme beek yenn àmbasadëer màggale bés bi.

Biñ sargalee ndongo yi ba noppi, dañ cee toftal Soxna Aana Laliir Sow miy sekerteeru njiitu njàngale mi ci Cesti, soxna su mën liggéeyam, ànd ceek farlook dal. Biñ ko woowee, ñépp a jóg taxaw di ko tàccu. Muy lu sedd xol te daw yaram.

Bi joxe bi weesoo, dañoo jóge Ucad 2, wutali Cesti ngir bernde yi : xeeti ñam ak naan yu bari te neex. Ci kow loolu, njiitu ndongoy 48eelu lël sant bu baax Pr Mamadu Njaay, njiitu Cesti, ndax nee na «guléet ci joxeb lijaasa benn boroom-teraanga génnewul dërëm jëme ko ci tegu bernde walla colu bés bi ; lépp njiiteefu Cesti moo ko sasoo ba mu jeex tàkk. Noo ngi sant Njaay it ci oyofam ak yaatug dënnam».

Cig pàttali rekk, Cesti mi ngi juddu ci atum 1965 ci ndimbalu Unesco ngir tàggat taskati xibaari Afrig yi, mooy it daara ji gën a kowe ci wàll wi ci Afrig-bëj-Gànnaar.

Saaliwu Tarawore moom, ci weeru Me 1952 la juddu ca Fatig, wuyuji boroomam ci oktoobar 2018.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj