JUAN JÉBBAANE NA MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Juan Branco, layookatu Usmaan Sonko bi, jure na Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak i ñenn ciy ñoñam ca CPI, ëttub àtte àddina si. Maanaam, daf leen a kaalaameji, ci ndigalu Usmaan Sonko, fa ñuy àttee képp ku def, sabab walla nga laale ci liy faagaagal doom-aadama. Tey ci yoor-yooru alxames ji la layookat bi doon amal um ndaje ak taskati xibaari àddina si, fa Pari (Farãs) ngir leeral ak a biral 4 500i firnde yi tax ñu jébbal jure gi àttekati CPI yi. Lii toftalu, ag tënk la ñeel ponk yi gënoon a bir ca ndaje ma.

Layookat bi dafa faramfàcce wayndare wi ñuy toppe Njiitu réew mi ak ñi ñu ci tudd. Ci biir i waxam, dafa wone ab xeetu ngëtën loo xam ne, dañ ko lootaabe, nas ko. Maanaam, xoqatal yi, jàppaate yi, rey yi ak ni nguur gi fi nekk di salfaañee àq ak yelleefi nit ñi, lu ñu xalaat la, tëral ko, jëfe ko. Kon, Juan Branco yemul rekk ci woney firnde yiy dëggal tuuma yu réy a réy yi mu gàll ci kow nguurug Senegaal gii, ci kilifteefu Njiitu réew mi, Maki Sàll. Ngëtën lile, du ay way-pólitig rekk a ci bokk. Nde, boole na ci takk-der yi ak seenn i kilifa. Am na ci sax ay géwél walla niti mbatit yoy, nguur gee leen ngemb. Limees na seen i tur ci njeexitalu yaxal bile. Ñu war a laaj nag, lu tax nguur gi def tóoxidóona yii yépp. Luy sabab yi ? Juan Branco tontu na ci laaj bi.

Bees dégloo layookat bi, pékke (crimes) yi am yépp, lenn rekk a leen sabab : nguur. Bëgg a aakimoo nguur gi, mu jaral leen lu nekk, moo tax Njiitu réew mi ak i àndandoon joggi ci kow i sàrt ak i teggiini demokaraasi yépp. Bañ a wàcc jal bee tax, Maki Sàll ak i gaayam bëgg xotti ndeyu àtte jiy sàrtal ci dogu 27eelam bi ne, lenn Njiitu réew amul sañ-sañu def lu ëpp ñaari moome yu tegaloo. Ŋoy bi ñu ŋoy ci nguur gi, matt ci ba dëgër ak seen i dëgëj a tax, ku leen namm a diir mbagg ku nekk, ñu fexeel la, tooñ la, jaay la doole, xañ la say àq, yow ak ñi ànd ak yow ñépp.  Moo tax itam, mbooloo mu jóg di ñaxtu, ñu yabal ay takk der ci ñoom, ñu leen di metital, ànd ak ay saay-saay yees jox i ngànnaay, ñu leen di sox i batali fetel, di leen faat. Nga ne ma waaw, ku sooke lii ?

Juan Branco neeti, ku jiin Njaag a, te Maki Sàll a di Njaag. Lii lépp, moo ko jiite, ànd ci ak 109i nit yi kootoo ak moom. Mooy ñi ñuy limsi ci njeexitalu yaxal bi. Léegi nag, layookat bi nee na, ñoom ñépp, dees na sumb, ñeel leen, luññutug ndoorte gog, mooy doon laltaayu kalaame bi ñu leen di kalaameji fa CPI. Doxalin wile, layookat baa ngi ko wéer ci dogi 13.c) ak 15 yu Sàrtub Rom ba Senegaal xaatim. Yan pékke lañ leen di toppe ?

Ci kàdduy Juan Branco pékke yi ñuy toppe Maki Sàll ak i àndandoom ñooy yii toftalu :

  • Faagaal i bakkan ;

  • Jàpp ak tëj kaso yuy jalgati yoon yees sàrtal ci àddina si ;

  • Mbugal, ngëtën ak a naaxsaayal ay nit (Dijje Baaji ak Fulbeer Sàmbu) (dogi 7.a, 7.e, 7.f, 7.h ak 7.i bu Sàrtu Rom).

Ci wàlli firnde yi, am na 746i firndey pékke yees dajale, saytu leen, seggat leen. Firnde yooyu, ñu ngi jóge fépp ci réew mi, diggante màrs 2021 ba tey, ci atum 2023 mi.

Juan Branco xamle na ni, du ca CPI kese lañuy àqi Maki Sàll ak ñi laale ci tuuma yees leen gàll. Jébbal nañ ag jure ca àttewaayi Farãs yi. Bu ko defee, képp ku ñu tudd ci wayndare wi, boo tegee sa tànk Farãs, mën nañ laa jàpp.

Fi mu nekk nii, deru Maki Sàll yàqu na ci àddina sépp. Nde, mbir mi dafa tas ci àddina si. Te, li ko jiitu, ay kurél yu mag génne woon nañ ay yégle di ci ñaawlu taafar ji ak ni takk der yiy bóomee askan wiy ñaxtu. Muy Amnesty International, Human Rights Watch, Magum Ndajem àq ak yelleefi doom-aadam mu ONU (Haut-Commissaire aux droits de l’Homme de l’ONU), njiitul Ndajem Bennoog Afrig ak yeneen i campeef yu mag ci àddina si, ñàpp a yedd Maki Sàll.

Léegi nag, ñoo ngi xaarandi ba xam ndax CPI ak àttewaayi Farãs yi dinañ féetewoo mbir mi. Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj