JUB, JUBAL, JUBBANTI : CONC BI TEGGEEKU NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Keroog 24 màrs 2024 la conc bi teggeeku. Keroog it la Yoon tekkeeku, wayndare yeek caabal yi daldi fireeku. Jub, jubal ak jubbanti la njiit yu bees yi woote. Moo leen tax a teggi seen conc ak seen tànk ci kow lépp lu woon wayndarew njombe, luubal, njuuj-njaaj, ger ak bépp pekk bu ñeel alal walla àqi askanuw Senegaal. Looloo leen tax a samp ëttu àtte bii di “Pool judiciaire financier”, gàttal biy joxe PJF. Ëttu àtte bu yees bile, liggéeyam mooy topp ak àtte képp walla ñépp ñu laale ci mbir yees lim ci kow. Bi ñu ko taxawaale ba dénk ko nit ñi war, liggéey dafa door, tàmbalee wone ay njureef.

Noonu, jotagum nañoo woolu Lat Jóob, nekkoon fi jëwriñ te jiite woon LONASE. Kii di Abdulaay Silla tamit, luññutukati DIC yi déglu woon nañ ko ñeel wurus wees di ruumandaat ne dañ ko génne réew mi ba ciy tudd Njiitu réew ma woon, Maki Sàll. Waaye nag, ñooñu dañoo gën a siiw rekk. Dafa di, amagum na ñu bari ñu ñu woowagum ci mbirum luubal ak càccug xaalisu réew mi. Am sax ñu ñu jàppagum ñoñ, ñu ngi ci loxoy Yoon jamono jii.

Bees sukkandikoo ci Seneweb, njiitul Sénégalaise Trading Company (STC), Aali Zaydaan, ci tirbinaalu Ndakaaru la fanaan, moom ak gàngooram. Waa DIC ñoo leen jàpp. Li ñu leen di tuumaal mooy ne dañoo luubal ceeb bob, njëg laa ngi tollu ci 15i miliyaar ci sunuy koppar. 

Ginnaaw bi luññutu gi ñeel mbir moomu jeexee, tay ci altine ji lañ leen jébbal toppekatu bokkeef gi. Dañuy fanaanaat kaso.

Ci beneen boor, yéenekaay Libération xamle na ne njuuj-njaaj bu mag moo amoon fa OQSF (Observatoire de la Qualité des Services Financiers). Ndeke, ca atum 2017 la IGE defaroon ag caabal guy biral tóoxidóona ya fa xew ci wàllu njuuj-njaaj ak luubal alalu askan wi. Waaye, Nguurug Maki Sàll ga woon moo ci tegoon concam. Ci lees rotal ciy xibaar, daf fa amoon ay nit yu laxasaayoo woon lëndëm, kootoo, di tibb ci gafakag réew mi. Waaye, ginnaaw bi conc bi teggeekoo ci caabalu IGE boobee, Yoon jot na ci ba tàmbalee càmbar mbir mi. Du ñàkk ñu jot ciy xibaar yu yees ci fan yii. 

Bu dee yéenekaay bii di Kewoulo Info, moom dafa xamle ne takk-deri “Sûreté urbaine” yi dañoo jàpp Mamadu Fawzi Jonn, yóbbu fa toppewaayu Ndakaaru bi. Moom, Mamadu Fawzi Jonn, moo nekkoon “DAF”, maanaam njiitul caytu ak kopparal gi ca kër gii di “Agence de la réglementation pharmaceutique” (Arp). Dañu koy tuumaal mbirum njuuj-njaaj ñeel alalu askan wi ak jëfandikoo këyit yu wéradi. Moom nag, ka woon njiitul kër gii di “Santé Barnabé Gningue” moo ko àqi fa Yoon. Looloo sabab ñu jàpp ko. 

Am na yeneen ak yeneen yoy, siiwagul bu baax. Loolu day wane rekk ne, Yoon a ngi defagum liggéeyam te amu ci xàjj-ak-seen. Askan week àddina sépp ñoo ngi ne jàkk Senegaal, rawatina Yoon, di xool ba xam PJF bi du mel ni CREI bu Maki Sàll ba. Li ci kanam rawul i bët. 

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj