KÀDDUY DOKTOOR SEEX MUHAMMAD AHMAD LÓO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Doktoor Seex Muhammad Ahmad Lóo biral nay kàddu, jëmale leen ci askan wépp, rawatina Nguur gi ak Yoon wi. Dafa amoon i ndaw yu génn, Pikin, di lakk ay nataalam, moom ak yeneen i kilifa yuy askanoo ci mbooloom Ahlus Sunna, maanaam ibaadu yi. Ginnaaw gi, saaga nañ ko saaga yu ñaaw, daldi koy tëkku. Moo tax mu biral kàddoo yii nu leen di dégtal, lépp diy waxam.

« Li xew mooy li daan xew rekk. Moo di tuuma joo xam ne, saa buñ demee ba am dal, dana am ay nit ñoo xam ne, ñooy jóg jëmaleeti ko ci Ahlus Sunna. Am nañ mbokk mu baax, nekk ab gëstukat bu mag ci sunu réew mii, day faral di wax ne, am na ay kurél yu nekk ci suuf di liggéey yoo xam ne, seen yitte mooy na jàmmaarloo am ci diggante kuréli diine yi fi nekk, te buy am, na am ci biir Lislaam. Dafa mel ni nag, ñooñu, seen ub liggéey, jamono yu ne, bu demee bay bëgg a dal, dañ koy xambaat.

Ci ay at ci gannaaw, dañ daan xëy rekk, jékki-jékki gis ab surnaal bind walla tele wax, ñu wax ne sàntar bii, ni jàkka ak daara ji, génne ay terorist moo ko tax a jóg. Tuuma joojee di dem, ñuy xool ba ci yàgg gis ne, fii kat, imaam yi fii xutba ak jàngalekat yi fii jàngale, seen i wax nëbbatuwul, àdduna sépp a ngi koy déglu ; waxuma Senegaal, waaye fépp a ngi koy déglu. Ñu ne, « Aa, fii ay respõsaabal ñoo fi nekk. Li ñiy wax day mel ni amul. Ñu wëlbatiku xool gis ndongo yi fiy génne, ñu bokk ci ñi ëpp i jom ci réew mi ci liggéeyal seen diine ak seen um réew. Ñu ne kon, tuuma jooju doxul, nañ seet leneen.

Ñu dem ba jëmmi jamono, mbooloo daje fi, ci béréb, ñu moom kat, ka leen jiite moo fi bindoon, yéeféerloo mboolem magi Lislaam ak mboolem mag ñi nekk ci réew mi. Ba ñu waxee loolu, wax ko ci seen ub tele, tasaare ko, fii laa leen tontu ci ab xutba, ne leen loolii ñuy wax, nañ ko indi. Li feek ñu ngi ndund, nañ gëstu ci li ma bind. Buñ ci gisee liy wax ne « diw sàngam dafa yéeféer la », muy magum Lislaam mu dëkk Senegaal ak mu dul ku dëkk Senegaal, nañ ko indi fii. Su boobaa, dinaa am kuuraasu [fitu] taxaw ci kow mbooloo mi ne « Aa, lii kat maa ko waxoon, waaye maa ngi koy weddi. Ne leen nag, may naa leen ñuy seet fileek seen dund di jeex, su jeexee na seen i doom ñëw, su doom ya jeexee sët yi ñëw. Boobaak lééegi gisaguma ku ko indi.

Li xew nag, démb walla barki-démb, nun ñépp noo jékki-jékki gisandoo. Nun xamunu sax li xew. Ay mbooloo yu jékki-jékki génn, nee nañu fii ci Pikin lañu nekk, am ku ca nekk kuñ xam, ñuy wax ne diw sàngam ak diw ak diw ak diw, boole ci samaw tur, ñooy saaga kilifa yi, génne sama foto [nataal] wone ba mu fés, ak yeneen i foto, lakk ci kanam nit ñi, won leen ne nii ñu def foto yii danañ leen ko def ; xam nañ seen i kër fañ nekk, danañ fa dem, xam nañ nàngam, xam nañ nàngam. Jëmm ja doon wax, bam daaneelee, ñeneen jël parol, kenn ku nekk wax say wax, loo xam ne lépp ay mënaas [tëkku] la.

Loolu nag, mbir la. Mbir la ci mbir yi. Daanaka, sunu cell gu yàgg ak lu romb lu ne, nu ne danuy bàyyi noonu mu jàll, loolu bu yàggee dana lu muy indi loo xam ne day niru ag yabeel. Waaye nag, taxawaay bi nuy taxaw te mu doon benn, te du soppiku bu soobee Yàlla ndax manhaj la, mooy di dalal ndaw ñi.

Bi loolu amee, yónnee nañ ma ay sõ [ndéggat] yu bari yoo xam ne, ay ndawi Ahlus Sunna ñoo koy waxante ci ay gurub [kippaangoo watsab]. Ñu ne, nañ jël fotoy seen kilifa, ñoom ña ko def, génn nun itam def sunuy widewoo lakk ko, saaga ko ni ñu saagaa sunuy kilifa. Ndax kat, ñi doon lakk, yemu ci lakk foto ak mënaase [tëkkuwaate], waaye àgg nañ ci saaga, ba àgg sax ci ay waa-jur. Waaye, sõ [ndéggat] bu ma ci jot bu ne, dama naan déedéet, loolu du yoon wi. Yeen, seen ub yar, du yarub saaga kilifa. Te kilifa ga ngay génn di lakk ab fotoom moom deful dara. Amaana kii koy tuddoo sax xamu ko. Kon kilifa ga, bul lakk fotoom, boo ko lakkee daŋ ko tooñ. Bul ko saaga, boo ko saagaa daŋ ko tooñ. Am yeneen yoon yu ñuy jaar.

Jëmm ja doon wax, xamees aw turam. Bam waxee bay daaneel, tudd na koo xam ne, doomu kilifa la. Wax na aw santam, wax uw turam, wax turu baayam, ne kat « kon sëñ diw, li nga ma doon defloo, def naa ko. » Kon loolu li nga ciy dégge mooy, ñooñu seen ub jaaxle àgg na ci jël ay merseneer [sàmbaa-bóoy] moo leen dese léegi. Ndax, ña fa daje woon ñi ci ëpp ay mbër lañu ak ñu nekk ci làmb, ci niñ ma ko waxee. Su fekkee ne ñooña lañ mujje nag, ñoom lañuy fay ñuy génn di wax wax yu mel noona ak di ko jëfe, jàpp naa ni réew moomii, li ñu bari di wax ne dëkk bi amul Yoon, man gëmuma loolu. Gëm naa ni dëkk bi am na aw Yoon.

Jëmm mënut a taxaw, bëccëgub ndar-kàmm, ñu di ko widewoo muy wax, tudd nit, jaar ciw turam, tuumaal ko ne dafa saaga kilifa yu gën a mag ci réew mi, udd seen i tur, walbatiku génneb fotoom lakk ko, boole ko ak di ko saaga ci ñaari way-juram, ñu xam la, xam kilifa ga la yabal ak ndeyam ak baayam, ñu bàyyi ko muy jàll noonu. Loolu moom, wax dëgg réew mi tollagul foofu. Ndax kat, su fekkoon ne kenn ci yeen ñii moo jóg, def loolu ci mbedd, bu noppee jarul ñu koy porte pelent, porokirëer [toppekat bi] mooy ñëw jëlsi ko ci saa si.

Su fekkee nag, nun, sunuy der àggagul foofu, sunuy tur itam xéy na yu woyof la, sunuy mbubb ùbuub yu woyof la ba tey, waaye nag danan natt Yoon nag ba xam Yoon daa am ci dëkk bi ba xam amu ci. Kon mbir mi foofu la tollu… »

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj