Démb ci àllarba ji, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga woon fa Amerig (New York) ngir teeweji 79eelu ndajem Mbootaayu Xeet yi (ONU). Bi mu falook léegi nag, guléet muy jël kàddu gi, wax ak i naataangom, waayeet wax ak àddina sépp. Ginnaaw bi mu waxee nag, sag bu réy la Saa-Senegaal yeek Saa-Afrig yi am ci kàddu ya mu fa biral. Nde, wone na fa fulla ju mat sëkk, wax fa wax ju solowu te yenu maanaa.
Ña yaakaaroon ne amul dayob janook yeneen njiiti réewi àddina si de, yàqi nañ. Ña doon njort ne dina raf, mbaa mu dër, walla sax mu fakkastalu, lemaat nañ seen geen ndànk, toog ci. Dafa di, li Basiiru Jomaay Jaxaar fay wax lépp dafa lalu ci dëgg, lalu ci jub, jubal ak jubbanti bi muy woo àddina sépp, ndeem bëgg nañ jàmm ju sax am ci àddina si. Dees na leen dégtal as lëf ciy kàddoom, ci jukki yii toftalu ñeel wëppa ya mu fa faramfàcce.
BENNOO JOXANTE LOXO NGIR SAXAL JÀMM
« Maa ngi jël kàddu gi tay, ànd ak gëm-gëm bu xóot : bennoo ci biir wuute yi mooy pexe miy tax a am jàmm, yookute gu sax ak ngor ñeel doomi Aadam yépp. [Loolu nag] ñépp ñoo ci war a dugal seen loxo, fépp ci àddina si. »
AM NA ÑUY JALGATI SÀRTI MBOOTAAYU XEET YI
« Noo ngi dund ci àddina su bari fitna sos, dañuy jalgati bés bu nekk sàrti Mbootaayu Xeetu yiy digle màndute, yoon ak càmmug àqi doom Aadama. […]
Bu nu bàyyee ñuy wéy di jalgati sàrt yooyii, danuy joggi cëslaayu Sàrtub Mbootaayu Xeet yi te di salfaañe kenoy Kërug jàmm gii. »
SAYEL BI DU GÉEW BU RÉEWI DOXANDÉEM YIY XEEXE
« Mënunoo wéy di seetaan jéyya jiy am ci Sayel bi. Naka noonu, mënunoo nangu ñuy soppi Sayel bi, di ko def géew bu ay réewi doxandéem di xeexe. »
SÀMM ÀQI RÉEWUM PALESTIN
« Senegaal mi jiite Ndajem doxal àqi juddu askanu Palestin, mi ngi woote, di sàkku ñu dakkal xare bi ci saa si, mu jeex tàkk wenn yoon. »
JÀMM A NGI TÀMBALEE CI ÑU SÀMMAL KU NEKK NGORAM
« Jàmm, du rekk ñàkk a xare. Jàmm, dafa aju tamit ci nit ku nekk mën a dund ci ngor, lekk ba suur, naan ba màndi, am dëkkuwaay, jàng ak di mën a faju. »
NOOTEEL DAFA WAR A JEEX !
« Dafa laaj ñu tàggook bépp xeetu jaay doole ngir ga nit ñi ay jikko ak nekkiin yu wuute ak seen i mbatiit ak i gëm-gëm. […]
Mënunatunoo nangu anam bi ñuy jiitee àddina si, muy anam bob day wéy di yokk yemoodi gi, loolu mëneesatu ko nangu. »
MBOOLOO NGIR DOOLE, LU ÑEPP BOKK, ÑEPP JOT CI
« Amul menn réew, ak fu dooleem mën a tollu, mu mën dékkul boppam jafe-jafe yiy yoot àddina si. Fàww nuy yékkateendoo, di dóorandoo. Fàww nu bennoo wëliis wuute yi ngir tabax ëllëg bob, danu ciy sàmm ngoru doom Aadama ; ëllëg bob, yoon a koy lal te dañu ciy séddale njureefi naataange bi. »
Mooy li gune yiy wax rekk, Njiitu réew mi toj na fa.