Ci neexitalu atum 2024 mi, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, biral na ay kàddu yi mu jagleel askan wi. Ca Njénde la la doon waxe, démb ci talaata ji 31i fani desàmbar 2024, di màndargaal njeexitalu atu 2024 ak ndoorteelu atum 2025 mii nu dugg.
Ay ñaan ak njukkal la Njiitu Réew mi ubbee ay kàddoom. Ñaanal doomi Réew mépp jàmm ak wér-gi-yaram, ñaanal itam way-dawlu yi fi wàññeeku ci biir atum 2024 mi. Njiitu Réew mi sargal na yit jigéeni Senegaal, rafetlu bu baax seen taxawaay ci njbaoot gi ak ci réew mi. Yemu ca. Ndax, moom Kilifa gu mag gi, delloo na njukkal sóobare yi wattu kaaraange réew mi. Seedeel na leen yar ak xereñte. Ginnaaw ñaan yi ak njukkal yi, Njiitu Réew mi biral na ay ndogal yu mu jël ñeel at mu bees mi.
NAALUW JOMAAY ÑEEL KAASAMAAS
Ndogal li mu njëkk a jël a ngi aju ci jàmmi réew mi, rawatina fa Kaasamaas. Nde, xamle na yéeneem ak yitteem ci jàmmi Kaasaamaas. Naka noonu, tëral na aw naal wu mu duppee « Plan Diomaye pour la Casamance (PDC) » (Naaluw Jomaay ñeel Kaasamaas). Jubluwaay bi mooy liggéey ngir delloosi jàmm fa diiwaan booba, waayeet taxawu askan wa fa tuxoo woon ci sababu fitna ji te, jamono jii, ñu nekk di ñibbisiwaat.
« LIGGÉEYAL SA RÉEW »
Ci biir i waxam, Njiitu réew mi fésal na ndogal lu am solo ci ndoorteelu atum 2025. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, Càmm gi dina taxawal ab jumtukaayu xarala bu tudd « Liggéeyal Sa Réew ». Bu sottee, képp kuy Saa-Senegaal, foo mën di nekk, wëliis xàjj-ak-seen, dinga mën a bindu, joŋante ngir bokk ci liggéeykat yi Càmm giy jël ci yenn fànn yi. Mu dolleeku ca ne, képp ku am itam aw sémb walla ay digaale yuy amal réew mi njariñ, dinga ko fa mën dugal.
Ci beneen boor, Njiitu réew mi xibaare na ñeenti sémbi àtte ñeel i sàrt yu ñu war a gaaral fa Ngomblaan ga, jëm ci doxaliin wu leer te dëppoo ak njub.
DEES NA FI JËLE SÓOBAREY DOXANDÉEM YI
Bokk na yit ci ndogal yu fës yi Njiitu Réew mi jël, mooy demug sóobarey doxandéem yi fi nekk. Bi mu faloo ak léegi nag, guléet Njiitu réew mi di joxe àpp ñeel wàll wi. Dafa ne :
“Sant naa jëwriñ ji yor Dooley Xare bi mu gaaral yoonu koppe wu bees ci wàllu fàggandiku ak kaaraange, mu di yoon wow, lenn ci njeexital yi mooy doon dakkal teewaayu bépp sóobareb réewu doxandéem fi Senegaal, dale ko 2025.”
Kon, mënees na jàpp ne, ci biir atum 2025 mi, sóobarey Farãs yi ak yeneen réew yi dinañu ñibbi, Senegaal gën a moom boppam.
Bu weesoo ndogal yu am solo yooyu, Njiitu Réew mi feddali na tamit kóoluteefam ci elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko mom, fan yii wees la aajar naaluw pólitigam wi mu fas yéene liggéeye ci at yii di ñëw, sukkandiku ci « Agenda National de Transformation – Sénégal 2050. »
Ci mujj gi, Njiitu Réew mi, sant na bu baax askanu Senegaal ci ñor gi ñu àndal ci wàllu demokaraasi. Muy jóo ñépp ci booloo, bennoo, dogu liggéey, liggéeyal Senegaal ngir soppi Réew mi ci anam yu baax.