Kaïs Saïed : weex der taxul a weex xol

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndekete yoo, nit, nit ay posonam. Kàdduy boddekonte yi Njiitu réewum Tinisi li biral, keroog talaata, ñoo firndeel wax ji. Moom,  Kaïs Saïed, dafa tamm ñuule yi dëmm, jiiñ leen xeeti ñaawteef, caay-caay ak mbonte ya am ca réewam ma. Yemu ca. Ndax, dëkk na leen xare, daldi digal Nguuram gi mu jël i matukaay ni mu gën a gaawe ngir, ciy waxam, fànq loraange yi leen doomi Afrig yiy indil. Boobaak léegi, nag, coow laa ngi ne kurr ci àddina si. Nit ñaa ngay ñaawlook a naqarlu kàddoom yu suufe yooyu.

Fan yii, daanaka kibaraan yépp a ngi wax ak a bind ca la xew Tinisii. Kàddu yaa ngi jóg, yégle yiy bare. Muy kuréli way-moomeel yi, di mbootaay yeek nit ñiy sàmm àq ak yelleefi doom-Aadam, muy boroom tur yi ba ci sax baadoola yi, ñépp ñoo ngi kaas tey duut baaraam Njiitu réewum Tinisii li. Dara waralu ko lu dul kàddu yu suufe te ruslu yi mu wax, keroog talaata, 21 féewarye 2023, jëmale leen ci ñuuley Afrig yi bawoo bëj-saalumu yayub Saharaa.

Moom,  Kaïs Saïed, dafa jiite woon am Ndaje mom, kaaraange réew ma lees ca doon fénc. Ba mu ca jógee nag, ca la yàbbiy kàddu yu nëb yooyee tax, boobaak léegi, nit ñiy naan « cam ! ». Ndaxte, dafa joxoñ doomi Afrig yi bawoo bëj-saalumu yayu Saharaa bi, jiiñ leen taafar ak fitna ya fay xew. Nde, daf leen tudde ay « ndiiraani màngkat yu jubadi » yoy, « soppi xar-kanamu Tinisee leen tax a jóg ». Yemu ca de. Ndax daf ci dolli ne, xeetu ñaawteef, caay-caay ak mbonte yi fay am yépp, ñuuley Afrig yooyee ko fay indaale.

Njiitu réewum Tinisi li neeti, ñëw bi fa saa-Afrig yi féete bëj-saalumu yayub Saharaa biy ñëw, duggewuñ ko lenn lu dul soppi deri askanuw Tinisii wi. Ciy waxam, ag kootoo la gog, lalees na ko ci ndoorteelu xarnu biñ nekk, ngir fexe ba réewum Tinisii doon « réewum Afrig kese », soppi xar-kanam ba dootul niroo ak réewum « araab ak jullit ».  Ci kow loolu la  Kaïs Saïed, Njiitu réewum Tinisii li waxee ni dañu war a gaaw « jël i ndogal » ngir dakkal ñëw ba fa ñuuley Afrig yiy ñëw.

Muy ay kàddu yu yées, bon te ñaaw, rawatina bi ñu génnee ci gémmiñu Njiitum réew buy wax ne jullit la. Nga xam ne, lu nekk mën na caa topp ci xeeti ñaawteef, xoqtal ak bunduxataal ñeel ñuuley Afrig ya fa nekk. Nde, bu mbañi ñuule yi dégge seen njiitum réew di wax lu ni mel, dañuy am yoon ngir teg leen bépp xeetu fitna ak metital.

Daanaka nag, àddina sépp a ñaawlu wax ji, doore ko ca way-moomeeli Tinisii yeek kurél ya fay sàmm àq ak yelleefi doom-Aadama. Kii di Romdaan Ben Amoor mi yor kàddug Forum tunisien pour les droits économiques et sociaux dafa waaru ci wax ji, tiit ci. Moo ko tax a wax ne, ñoom, « danu rus ci kàdduy Njiitu réew mi, noo ngi ñaawlu baat yi mu jëfandikoo te ñuy àtte-ñàkkal ak a tuutal way-tukkiy Afrig bëj-saalumu Saharaa gi. »

Jamono jii nag, bépp ñuule bu nekk fa Tinisii, tiit nga, jaaxle. Nee ñu, fan yii yépp, pólisu naar yaa ngay jàpp ak xoqtal doomi Afrig yu ñuul yi ni mu leen neexe. Bu ñenn ñiy natt limub ñees jàpp ci 300, am ñeneen ñu koy ful ba 1000. Foo dem ca réew ma, ñoo nga fay rëbb ak a àtte-ñàkkal nit ñu ñuul ñi te. Moo tax mbootaayu AESAT mi dajale doomi Afrig ya fay jànge xam-xam ak liggéey daldi génne ab yégle di ci artu ay ñoñam, di leen ci wax ñu toog seen i kër te mooytu. Mbootaay gi yemu ca. Nde, bind na njëwriñi Biir réew ma, Mbiri doxandéem yeek Njàng mu kowe mi, di sàkku ci ku nekk ci ñoom am ndajem-waxtaan. Bindaale nañu sax Njiiteef ga, di kaas. Christian Kwongang mi ko jiite xamle na ni am nay àmbasaad yu jël seen i matukaay ngir delloo seen i doom. Àmbaasadu Koddiwaar moom, mi ngi waññ saa-Koddiwaar yi bëgg a ñibbi.

Àmbaasadu Mali, moom itam, génne ab yégle di ci dalal xeli saa-Mali yi, di leen wax ne njiit yaa ngiy bàyyi xel la fay xew. Te yit, képp ku namm a ñibbi, joxe nañuy limat yees war a jokk. Bu dee àmbaasadu Senegaal moom, ci alxames ji la génne yégleem, waaye waxul dara lu jëm ci mbir mi. Xanaa Guy Maris Saañaa miy ñaax Njiitu réew mi mu woolu àmbaasadëeru Tinisii bi. Bu dee kurélug Bennoog Afrig, moom, ñeenti fan ci tey lay door a génne yégle di ñaawlu ba fu ñaawlu yem kàdduy Njiitu réewum Tinisii li.

Xanaa  Kaïs Saïed, moom, dafa wéradi ? Walla dafay naax ? Waxam ji kat, dafay wund ag doyadi, ag suufe ak ug ñàkk xam. Xanaa araab bu ñuul amul ? Ndax jullit moom du ñuul ? Waaw, ngóor si moom, xanaa dafa fàtte ni araab yépp duñuy jullit ? Kii nit laam ? Lu tee ñu wax ak  Kaïs Saïed mii, xamal ko boppam ?

Booy digle cangaay, na fekk nga set. Bu dee mbonte rekk ak jikkoy caay-caay, ca saa-Tinisii yi la fekk baax (du saa-Tinisii yépp lees ci namm). Nde, bu dee doomi Afrig yaa nga fay dem, jàng ak liggéey a leen fa yóbbu te kenn mësu leen fa jiiñ mbirum terorist. Doomi Tinisii yi kay lañ ciy tuumaal fépp ci àddina si, rawatina Farãs.

Bésub 14 sulet 2016, Mohamed Lahouaiej-Bouhlel mi dawaloon ag sëfaan (kamiyoŋ) jubal cim mbooloo ca Niis (Farãs) ba rey ci 86i nit, xanaa du doomu Tinisii ? Bésub 29 oktoobar 2020, Brahim Aouissaoui, 21i at, moo rendi woon 3i nit ca jàngu « basilique » bu Niis (Farãs). Kookeet bu dul saa-Tinisii, lum doon ? Bésub 23 awril 2021, Jamel Gorchene, 36i at, dugg Farãs ci lu dul yoon, jam fa paaka ab takk-der ba mu dee. Moone de, déggeesul njiiti Farãs ya naan dañu war a rëbb saa-Tinisii yi. Kon Kais Saed deful lu dul gàtt xel. Nde, fàttewaat na ne, 18 000iy way-tukkiy Tinisii duggoon nañu Itali ci atum 2022 mi ci lu dul yoon.

Waaye nag, lii lépp, benn sabab la am. Mooy ne, fim ne nii, réew ma dafa nekk ciy tolof-tolof yu metti ci wàllu koom-koom. Dund bi jafe na fa lool, ndax lépp a fa yokku. Rax-ci-dolli, lii di suukar, di kafe walla ceeb, daf fa jafe jamono jii. Lii de, lees jàpp ne la Njiitu réewum Tinisii li di jéem a nëbb.

Lees mën a jànge ci lii mooy ne, weex der taxul a weex xol. Te yit, du xeebe, lu moy ku xeebu. Nde, ku naan ci ndoxum xamadi, boo màndee wax lu wéradi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj