KAN MOO DOON ISEN AABARE ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

« Jébbalees na Aabare Boroomam », nii la jawriñ jiñ dénk wàllu yoon wi, Maalig Sàll, dëggalee xibaar bi rotoon ci yéenekaay yi : Isen Aabare, njiitu réewum Càdd ma woon, faatu na.

Waaye, kan moo nekkoon Isen Aabare ? Lan mooy jaar-jaaram ?

Kan mooy Isen Aabare (Hissen Abre) ?

Bésub 13eel ci ut 1942 la Isen Aabare ganesi woon àddina ca béréb bu ñuy wax Faya-Largeau. Moom nag, ab jullit la woon, bokkoon ci giiru Anakaza yi bokk ci Toubou yi, ab xeet bu nekk Càdd.

Ci màndiŋum Djourab mi la màgge. Fa la ko ay sàmmi màngkat yaree, tàggat ko ba xelam màcc. Ci lañ ko dugalee daaray nasaraan, muy jàng ci ndimbalug ay sëñ-daaraam.

Bi Càdd moomee boppam, dañ fasoon yéene nangu bépp ndombog-tànk bu fab xonk-nopp yoroon, dénk ko kenn ci doomi réew ma. Noonu, Tombalbaye, njëlbeenug njiitu réewum Càdd gannaaw bim moomee boppam, tabb ko Perefe bu ndaw bu Moussoro. Waaye, ci at moomu la àggaleeji njàngam ca daara ju kowe jees duppe woon Institut des hautes études d’outre-mer, ca Farãs. Génnaale na fab lijaasa laata muy jublu ci njàngum yoon ca daaray Institut d’études politiques, ca Farãs ba tey. Ginnaaw gi, jànge na pólitig itam ci téerey Frantz Fanon, Che Guevara ak Raymond Aron.

Ci atum 1972 la jeexal njàngam, daldi delsi Càdd, ràngu ci làngug FROLINAT. Ca la sosee làrme réewum Càdd, gàttal biy joxe ci nasaraan FANT (Forces armées nationales du Tchad). FANT nag, naxsaay na bu yàgg.

Ci ati 1970 yi, Càdd dafa jànkonteloon ak i way-fétteerlu, xeex bi ne kurr ci biir réew mi ba 1974. Ci la Isen Aabare jiite ay way-fétteerlu yu bokk ci giiru Toubous yi, daldi jàpp ay tubaab ca Tibesti : benn fajkatu almaŋ, ñetti farãse (Marc Comb -ab koperaŋ- ak Françoise Claustre -ab arkewolog- ak jëkkëram). Fajkatu almaŋ bi, 1975 lañ ko bàyyi gannaaw biñ ko fayalee ; Marc Comb day mujje rëcc. Bu dee, yeneen ñaari farãse yi, ñoom 1977 lañ leen bàyyi. Waaye, bala loolu di am, Farãs yónni woon na ab ndaw, komàndaŋ Galopin mu maslaaji ak Isen Aabare ngir mu bàyyi ñaari doomam yim jàppoon. Dañuy mujje tuumal Isen Aabare ne dafa metital komàndaŋ Galopin bi, daldi koy rey.

1978, Seneraal Félix Malloum tabb na Isen Aabare njiitu jawriñu nguuram. Ci atum 1979 la moomeem jeex, bim sookee xareb maxejj bi, moom ci boppam.

Isen Aabare moo sosoon FAN, daldi daaneel Goukouni Oueddei ci atum 1982, bésub 7 ci suwe. Naka noonu, mu nekk njiitu réewum Càdd li ko dale atum 1982 jàpp 1990. Goukouni Oueddei daldi taxawal Nguurug négandiku, daw làquji ca bëj-gànnaaru réew ma. Réewum Libi mi nootoon diiwaanu Aouzou ci jamono jooju, daldi koy jàppale.

Ci 1eelu fan ci weeru desàmbar 1990 la ndem-si-Yàlla si Idiris Debi, daaneel nguurug Aabare. Ci la dawe génn Càdd, làqusi Senegaal.

Yoon topp na ko ndax dañu njort ne moo rey lu toll ci 40.000i nit. Moo tax mu amoon ñu topp lànket bi ba am ciy firnde ngir ñu mën koo teg loxo.

Ci sulet 2006 la UA jiital réewum Senegaal ngir mu àtte kii di Isen Aabare ci tuuma yi tegu ci ndodd li : (crime contre l’humanité, crimes de guerre et actes de tortures). Waaye ci diggante bi dafa dakkal wajtaayu àtte bi, ndax xaalis bu bari la laajoon.

Ci bésub 20 ci sulet atum 2015 la ko waa Chambres africaines extraordinaires tàmbaliwaat àtte fii ci Ndakaaru. Ci bésub 30 me 2016 lañ ko tëj giirug dundam, tey xamle ne tuuma yi tegu ci kawam yépp moom la. Ci ñaarelug àtte bi lañ ko alamaan lu toll ci fukk jàpp ñaar-fukki miliyoŋ ci sunu xaalis yi muy dàmpe loraafon bu nekk.

Isen Aabare daldi def dàppel ndax àndul woon ci àtte biñ ko àtte woon. Waaye, Chambres africaines extraordinaires dañ waxoon ne daan yi dara du ci deñ te it dina joxe ci lu tollu ci 82i milyaar ak 290i miliyoŋ ci CFA.

Bi mu amee feebaru koroonaa, la ko laykatam ñaanal ngir ñu génne ko kaso yóbbu ko ci ab bérébu dalluwaay, ay alkaati di ko wottu ci diirug juróom-benni fukki fan. Ginnaaw gi lañ ko dellowaat ndung-siin ci bésub 7 suwe 2020.

Isen Aabare wuyuji na Boroomam ci talaata, yemook 24i fan ci ut 2021 fii ci Ndakaaru.

Réewum Càdd a ngi doon laaj néewu Aabare ngir ñu dencee ko fa, waaye tegoon nañ ci ne duñ ko fa delloo njukkal. Noonu, jabaru Isen Aabare di Faatime Raymon Aabare wax ne : « Aabare, fii ci suufu Senegaal lay tëdd, laajuñu dara nguurug Càdd. »

Ci armeeli Yoof yi lañ ko mujje rob, keroog, 26eelu fan ci weeru ut ginnaaw tisbaar, as mbooloo mu ndaw teewe woon ko.

Ami Mbeng

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj