RUWÀNDAA, RÉEW MA FARÃS NEE TOTT AK GÀCCE (BUBAKAR BÓRIS JÓOB CI TEKKIG PAAP AALI JÀLLO) 1/2

Yeneen i xët

Aji bind ji

Weeru màrs 2021 wee ñu génn, ci 26eelu fan, « Ndajem gëstub ceedeefi Farãs ñeel Ruwàndaa ak faagaagalug Tutsi yi », jébbal na Emmanuel Macron ag saabal. Du woon guléet, nag. Booy seet sax, danga naan Ruwàndaa mooy mennum réewu Afrig mi tee Farãs nelaw. Lu ko waral ? Xanaa aw xeetu gàcce wees di jéem a jàngat bu ci kanamee. Li nu mënagum wax, mooy ne ba ñu faagaagalee Tutsiy Ruwàndaa yi ba tey, képp ku ñu fal Pari, ne la « Palais de l’Élysée » baa ngoog, yaay boroom, gaawtu nga santaane sag saabalu bopp ñeel ñaawteef boobule.

Ki ci jëkk, François Mitterrand la, moo fi taxawaloon kurélug dipite guñ duppe woon « La Mission Quilès » te mu amaloon fib laajantu ngir xool ndax Pari laale naam déet ci jéyya ja amoon Ruwàndaa. Kurél googu liggéey na 8i weer soog a siiwal ag saabal gu jëmmu lool, ci desàmbar 1998. Waaye, ci diir boobu, dipite Farãs yi defuñu leneen lu dul taataan ay xibaar ci mbir mi. Moo tax ñépp xamoon nañ ni du mujj fenn. Dañ faa jóge ne, aa, ñoom de waaru nañu, seet nañu seet, gisuñu lu war a tax Kigali di duut Pari baaraamu tuuma, yokk ci ne buleen kenn damm, li réew moomu sómbi na ko naan, lu ko dal moo ko teg boppam. Yemuñ ci, ndax ŋàññ nañ tamit Mbootaayu Xeet yi, gaaruwaale ci Nguurug Bill Clinton ga woon. Dafa di, xameesoon na bu baax ne setal deru Farãs rekk a leen yitteeloon. Lenn daal la dipite yooyu xaw a nangu ne njuumte la woon te moo di ne, ni François Mitterrand ak Juvénal Habyarimana jegeyoo woon dafa dem ba mujjee gëlëmal Farãs, muy sotle nguuru Kigali ga dëkke woon saax-saaxe alalu Ruwàndaa ak a fitnaal askanam, rawatina Tutsiy réew ma.

Ci atum 2004, la ay mbootaay (« Survie », « Aircrige », añs.) ak i way-moomeeli Farãs ni fàww maxejj yi am i leeral ci musiba ya seen gornmaa defoon Ruwàndaa, daldi taxawal seen « Ndajem laajantu » bopp. Ñoom nag, lépp la « Mission Quilès » waxoon lañu dindi ba mu set wecc, ñaawlu patt-pattaaralam ciy xew-xew yu am solo, naqarlu yit sos yiñ sosoon ci mbir mi. Ndege, dipite yooyu, par-parloo ak sàmm seen derub réew rekk a leen taxoon a jóg.

Ndax ci ñaari saabal yooyu la Farãs yem ? Déedéet. Bi mu gisee ni, ci biir Farãs ak ca bitim-réew, ñu baree ngi doon wéy di tam dëmm Pari, Emmanuel Macron da ni lii kat gàcce la, te ginnaaw werante xuuxaan tekki tubéy, fàww askan wi xam fan la dëgg gi féete. Ci la giseek 13i boroom xam-xam – ci njiiteefu Vincent Duclert, dib aji-mboor – ne leen ñu gën a luññutu faagaagalug Tutsi yi ca Ruwàndaa. Nga ne ma defal ndànk, saabal yaa ngi bëgg a bari, kat ! Moo ! Lu Ruwàndaa ameel Farãs ? Lu Farãs am Ruwàndaa ? Moone de, Ruwàndaa bokkul ci réewi Afrig yi Farãs mës a teg loxo, di leen noot ci lu bir… Te sax, ci diggi atiy 1970 yi rekk la fa tàmbalee am baat. Kon, lu mu war a joteek Ruwàndaa ba koy singali nii ?

Lii, teey na xel.

Féncub faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi noon na kurr ca Farãs, ñaari gis-gis yu safaanoo yàgg faa jànkoonte. Li ciy njëkk a rote ci njàngat, mooy ab soofantal. Nde, Farãs mësul a fullaal dëgg-dëgg faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi. Bu dee pólitiseŋ yeek way-tas- xibaar yi, ñoom, ca ndoorteel la ba tey, li leen gënoon a soxal moo doon kenn bañ cee tudd seen réew, di junjub kootoo ci digganteem ak bóomkati Kigali ya. Mu am ci, nag, ay xeltukat yoo xam ne, baatub « faagaagal » ci boppam a yóbbu seen fit, ndax rekk ni mu diise. Dafa di, ñaawaayu baat bee tax nanguwuñ ñu koy dendaleek turu Farãs ci genn kàddu gi te yit képp ku repp ba ne amaana Farãs laale na ci ñaawteef yooyu, ñu dal sa kow. Ñoom daal, ni ñuy fexee ba setal seen deru réew rekk a leen mës a ñor. Jaral na leen sax sosal képp ku wuteek ñoom gisin ci mbir mi ; dinañuy dem bay méngale Saa-Ruwàndaa yeek i rabi-àll. Rusuñu ci dara : tàggook seen sago, wax wax ju ñaaw, yàq der… Kenn waruta fàtte kàdduy Mitterrand yu kéemaane ya fi ab taskatu xibaar bu tudd Patrick de Saint-Exupéry xamle woon. Lii la Mitterrand tontu bañ ko laajee xalaatam ci faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi : « Xeeti réew yooyu, de, mënees na faa rey ñépp te du yëngal kenn, nun noo fi nekk di wax waxu faagaagal waaye ci ñoom loolu lépp amul benn solo.¹» Ku taxaw seetlu tuuti, dina gis ne, màggat mi gémmiñam gu xasaw gi waccu kàddu yu ñàkk yërmaande yooyu, da doon daw res doŋŋ. Dafa meloon ni ku dem ba janook lu ñaaw li mu def, fit wi rëcc, muy jéem a gëmloo boppam ne, dee, moom taqul te yit taqalul réewam ci « faagaagalug bëccëgu-ndara-kàmm ». Ku déglu bu baax, dinga dégg lees waxul : « man, François Mitterrand, defuma Ruwàndaa dara lu tax ñu may war a méngale ëllëg ak Adolf Hitler… »

Waaye coow li, coow li, lenn rekk a am, mooy ne Saa-Farãs yu bare dañoo dencal Ruwàndaa mer. Moo tax ñu daas seen làmmiñ, të leen a teggi ci deru Saa-Ruwàndaa yi. Way- xelluy Farãs yi mel niy dëmm yu jafuur yoo xam ne, fileek saagawuñ way-deewi faagaagalug 1994 ga, duñu am jàmm. Ñoom kay, lenn rekk a leen soxal, mooy xayadiloo ña ñu reyoon Ruwàndaa ngir mbamb bañ a topp Farãs, réew mu yëg boppam, di bàkkoo ne àddina ba àddina daj, moom la yelleef ak àqi doom-aadama gën a yitteel.

Nicolas Bancel, di aji-mboor buñ ràññee, def nab gëstu ciy kàddu yu nirook yu Mitterrand yi te ñu yëkkatee leen Farãs. Ci misaal, bañ dalalee Charles Pasqua ci « Antenne 2 », ci weeru suweŋ 1994, lu mel noonu la fa wax. Biñ ko laajee naka lay gise la doon xew Ruwàndaa, lii la tontu : « Gis nga, sëriñ bi, nook ñooñu dunu benn, nun nooy ñàngal ak a yéemu ci reyante yooyuy am Ruwàndaa. Waaye, ñoom, loolu du dara ci ñoom². » Nu ni déet-a-waay, ci suweŋ 1994 ba tey, bindkat bu mag bu ñuy wax Jean d’Ormesson, bokk ci mbootaay moomu amal lool solo Tubaab yi te ñu tudde ko « Académie française », dem Gikongoro ak takk-deri « opération Turquoise » yi, delsi, ràkkaaju ba bind ci « Le Figaro » ay kàdduy doomeeraam dëggëntaan. Ñoo ngi nii : « Na buqat yi gëmm, buñ jàng lii may nettalisi ! Ndaw rangooñ yu bari ! Mbaa génne ngeeen seeni musuwaar ? Deret jaa ngi waaj a walangaan. Céy Ruwàndaa ! Nañ fa doon bóome nit ñi dafa rekk muccoon ayib, dara dàqu ko ! Béréb yañ leen doon reye, nag ! Aka ñoo yànjoon, maasàllaa³ ! » Mu ngoog… Ñu bare dinañ ni xanaa kay déet, dañuy sosal ngóor si d’Ormesson rekk, wànte kenn sañul a wax lu ni mel. Moone jarul werante : doomu-xaj booboo yatt xalimaam bind loolook loxo boppam te ku ko desee gëm mën ngaa def ab gëstu bu ndaw ci Google, wax joojoo ngi ne fàŋŋ ci lënd gi. Li xaw a doy waar, kay, mooy li « Le Figaro », yéenekaay buñ mës a weg, nangoo génne waxi dof yooyu. Waaye, ku maaseek sunu jamono jii rekk la lii mën a bett. Ku xam démb, dina la wóor ne jamono jooju, loolu xaajul woon saf Xonq-Nopp yi…

Xasteek féewaley xeet taxunoo jóg. Waaye, lu defu waxu, luy ay di jàmbat. Dëgg neexul te fàtte xaju fi. Fii la fiy way-ŋeleju ak ay faramfàccekati rajook tele daan fowe ak a ñaawal Saa-Ruwàndaa yi seen bakkan rot ci mbir mi. Noonu lay rajoy Farãs – ak ay tele, yaakaar naa – daje woon, ci atum 2014, ci mujjantalub etaasu benn otelu Kigali bu mag, ngir def seen liggéey ci 20eelu delsig-bésu faagaagal gi. Dalal nañ ma fay yoon, man mii. Waaye, ni taskati xibaar yooyule doon ñàkkalee faayda bésub pàttaliku bi daf ma rekk yéemoon. Ñu ne fa di ŋàññ ak doole Kagame, naan du njiit luy yemale, dafa sonal askanam. Li leen gënoon a ñéññloo, ñàkkul, moo doon ne fan yooyu, diggante Kigaleek Pari dafa gënoonatee ñagas, François Hollande ne ginnaaw noonu la, moo lànk, du yabal ndaw lu koy teewali Kigali. Loolu nag, jaaxaloon na ñu bare. Ci la ko Kagame gaaruwaalee ba muy wax ci àngale, daldi sërëxal ci wax ji ay baati tubaab (« les faits sont têtus », maanaam « lu ne fàŋŋ, kenn du ko jéex »). Kàddu googu reetaanloo ñépp ndax dafa leeroon ne Kagame da doon mbalag Hollande.

Léegi nag, laaj bii lañ war a samp : lu waral, boo jëlee réewi Afrig yi Farãs di xañ seen moomeel tey, mennum Ruwàndaa kesee ko ci ñemee diir mbagg ? Amaana li Farãs tàmmul a dégg ay tuuma ñeel njombey nooteel yi mu def Afrig, tuuraale fi deret ju dul jeex, moo tax. Mën naa am tamit nees koy ŋàññe ci naalub wéyal « Françafrique », moo wàññi daŋaram…

Réew mu gën a gumba Farãs amul. Tey jii la gën a noot réew yim fi tegoon loxo, tere leen a noyyi te ku wax mu mer, ne xolam bu rafet bee koy tooñati, ndax lépp lu mu mës a def Afrig, yërmaandee ko ko defloo. Kon, Farãs, ci réy ak bew bim àndal, jàpp na ne nooteelam ga njariñ rekk la woon ñeel doomi Afrig yi. Lii de la Noam Chomsky, dib xeltukatu Amerig bu siiw a siiw, di woowe ci nasaraan « la doctrine des bonnes intentions⁴ », mu tekki ne réewi tubaab yi am doole, buñ la songee, tas sam réew, yàq ko yaxeet nañ ko fi defe woon démb Wiyetnaam walla bu yàggul rekk Iraag ak Libi, dañuy jàpp ni mooy li gën ci yow ! Maanaam, rey sa njaboot ba noppi, ñëw dëj ba, naan la : « Siggil ndigaale, metti na, gaa, wànte war nga maa gërëm ndax boo xamoon li la doon yoot ! » Sée-té-té-tét ! Noonu la réewi sowu yiy def, di mbubboo rafet njort saa bu ñuy noot ak a xoqtal yeneen xeeti àddina si ; di fàtte-fàttelu bakkan yiñ rotal yépp ci sababu nooteel gi, ak deret ji ci tuuru yépp, ak dëkk yiñ taal, kilifa yiñ toroxal, alal jiñ sàcc… Dañuy nax seen bopp rekk, di kàcc, ndax mënuñoo fàtteendoo Madagaskaar ak Sétif ak Kamerun añs. Téeméeri junniy nit yi ñu rey ci xareb Alséri ba, nag ? Nga xool lii lépp, Farãs sañ a taxaw di am lu muy lay, di jekk-jekkal, walla di setal deram. Liñ naan géwél bu repp ci xare lu mu jiin xeeb ko moo tax ay dipiteem jël benn dogal ci atum 2005, di ci rafetlu li seen réew def ca jamonoy nooteel ja…

Ndax yabeel walla xeebaate mën naa weesu lii ?

Loolu Farãs def ci xelam moo waral, saa buñ ko tuddee ci faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi, mu jaaxal ko, mu naan xanaa kay du man la ñii di wax ! Rawatina ba nga xamee ni Ruwàndaa, du kenn ku mu fa gor jaasi mbaa mu dóor la balu fetal.

Waaye ku xam ni sunu jamono jiy doxe tey, dinga nànd lu tax Ruwàndaa gaaw a yëngal xolu Farãs : faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi, àddina sépp a ko seede, dëggal ko, te mooy gi mujj ci xarnu bin génn. Moo tax, képp kuñ ci tudd fàww nga ne tott ak gàcce. Farãs dafa tàmm a def ay musibaam ba noppi gën fee réy làmmiñ, di leen nettalee nu mu ko neexe, di walbati yëf yi ba ku ci xamul dara da naan dañ koo sosal.

Bii yoon, maanaam ci lépp lu ñeel faagaagalu Tutsi yi, lay yooyoo ko të ticc. Li ko waral mooy li « Front patriotique rwandais » (FPR) duma nguuru bóomkati Ruwàndaa ya duma yu metti. Bu Paul Kagame jëlul woon ndam li ci ñooñu Farãs doon jàppale, neneen la ñuy nettalee tey xew-xewi Ruwàndaa ya, bu dee sax kenn dina sonal boppam di ci yéy ak a yàbbi. Dama ni la, Farãs dafa naroon a soppi wax ji, di fen di dajale, tuur nit ñi lëndëm. Bu ay dunguroom doon jiite tey jii Ruwàndaa, nettalib faagaagalug Tutsi yi neneen lay tëddee. Nde, ku la abal i bët moo lay wax fi ngay xool. Te, li Kagame nekk njiit lu am fulla, njiit lu kenn feesul i bëtam, di jiital tamit saa su ne yittey réewam, moo gën a yàqal Saa-Farãs yi.

Te sax, yëf yi mënutoon a yomb ci Farãs. Ndaxte, ci biir réew ma la ay way-yégle ak i bañkat, defoon mbirum faagaagalug Tutsi yi seen xeexu bopp, mu jaraloon leen lu ne. Loolu nag, buñ ko waxee, xel yépp dañuy daldi dem ci ñayu-xare bu mel ni François-Xavier Verschave. Waaye, jëmm ji ci gënoon a fés mooy Jean Carbonare. Keroog, 24i fan ci saŋwiyee 1993, la yëkkati ci « France 2 » kàddu yu daw yaram yii : « Li nu gën a yéem ca Ruwàndaa, mooy dayob bóom yi, nees leen nase, anam bi ñu leen tërale… Bu kenn ne bóomkat yi teyuñu li ñuy def walla dañoo tàggook seen sago. Déedéet, am naw yoon wu ñu xàll di ca jaar. Lay xew Ruwàndaa am na tur te tur woowu du dara lu dul setalub waaso, faagaagal, njekkar ñeel niteef gi ». Ngir gën a leeral wax ji, Jean Carbonare yokk ci ne : « Farãs, sunum réew miy jàppale nguur gi sumb ñaawteef yile, di ko dimbalee xaalis ak i gànnaay, mënu cee set. Sunu réew mën na, bu ko neexee, dakkal rey yay wéy Ruwàndaa ». Ndeysaan, xol bi yëngu, mu fàtte ne mu ngi tele, di yikkët, baat biy lox, mu neeti Bruno Masure, aji-dawal ji : « Yow tamit Sëñ Masure, am na loo ci mën a def ! Dangeen a war a jóg…ngir lii dakk ndaxte mën nan koo dakkal bun ko nammee ».

Kàdduy Jean Carbonare yooyule, kenn dootu leen fàtte. Waaye kilifay Farãs yi fullaaluñ woon njiitalu « Survie » la ba mu leen yëkkatee.

Ci njeexitalu faagaagal gi tamit, ñeneen bañ nañoo noppi, di biral seen mànduteek seen xol bu rafet. Ñoo xam ne, bëgg seen réew ba fu mbëggeel yem, taxul woon ñuy far ak a par- parloo, mbaa di bań a àtte dëgg. Kii di Jacques Julliard ci ñooñu la bokkoon. Doonte deesul a faral a dégg turam ci ñi yittewoo mbirum Ruwàndaa, bindoon na, ci atum 1998, lu am solo ci « Nouvel Observateur ». Dafa ne woon : « Bés dina ñëw, ñu joxoñ Farãs baaraamu tuuma ci faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi ca atum 1994, te musiba moomu am ci jamono joo xam ni François Mitterrand moo nekkoon Njiitu réewum Farãs. Loolu, jarul nu ciy am xel-ñaar. Gaa, Farãs reyul benn doom-aadama Ruwàndaa, waaye moo ngemb ña doon rey, ay reykat yu mësuta nëbb ne dañoo bëggoon a faagaagal Tutsiy réew ma.⁵ »

¹Patrick de Saint-Exupéry, « France-Rwanda : un génocide sans importance », Le Figaro, 12 saŋwiyee 1998.

²Bancel Nicolas (2002), « Les médias français face au Rwanda. De l’intervention française de 1990 au génocide », Africultures, 30, ci lënd gi. URL : http://africultures.com/les-medias-francais-face-au-rwanda-1471/ (xoolees na ko ci 11 ci oktoobar 2021).

³Jean d’Ormesson, « J’ai vu le malheur en marche », Le Figaro, 19 sulet 1994 ; Jean d’Ormesson, « La drôle d’odeur de l’église de Kibuye », Le Figaro, 20 sulet 1994.

⁴Chomsky Noam ([2005] 2006), La Doctrine des bonnes intentions. Entretiens avec David Barsamian, Pari, Fayard.

⁵Julliard Jacques, « chronique hebdomadaire », Nouvel Observateur, awril 1998

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj