Njàngatum Guddig Mbooyo (2/2)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Doolee mën dëgg, waaye dëgg mooy mujj.

Li tax bindkat bi taamu kàddug Guddig Mbooyo, daldi koy tudde téereem bi, dug tandle. Bul jaawale. Mbooyo, tur la, turub aji-jëmmal boo xam ne bii, jëfam dàkkontewul ak mbóoyo mi nga xaw a jaawale ak turam bile. Waaw.

Diggante Tiijaan, Jéen, Góora, Maye ak Mbooyo ci boppam, ngelawal jàmm lu féex a ci daan daw, rattaxal diggante yi, yaatal xol yi te féexaloon jëflante yi. Bi Mbooyo sàccee takkaayi Maye mi ko jàppe woon doomu-ndeyam, ngelaw loolu dafa mujj a nekkaat ngelawal tàngaay lu rax suuf, daldi ñagasal diggante yi, gàkkal leen, lëndëmal gis-gis yi, xatal dund bi biir Quartier Latin.

 Mbooyoo def tojaangeem ba noppi, wor Maye, dellu tuumaal Tiijaan, jëkkër ji. Tiijaan moomu, moo nuy nettali ni mbir deme ci biir téere bi. Wolof ne, teey, ci ndox lees koy séentu ; waaye ci nit la gënee. Tiijaan, ku teey la. Bi càcc gi amee, ñu daldi koy tuumaal, yàq ci deram, teewul dafa ànd ak sagoom, sumb ab lànket ngir leeral mbir mi, setal deram.

« Teey ak sago, war na ku ne bu mbir teewee, muy bànneex walla safaan ».

Mbir mi yombul woon. Ndaxte, ndëgg-sërëx bu ne tegal nañ ko Tiijaan ngir gëstoom bi bañ a àgg. Jaay nañ ko sax doole, xaw koo xoqtal ngir mu dakkal lànketam bi. Nde, ndeyu Mbooyo, boroom alal la, dib kilifa ci réew mi, mën a yóotu lu loxol baadoola dul laal. Xam nga fi ma jëm, du ?

Ger. Mooy baat bi. Fu yoon jàddee, ger a ko fàbbi. Céy ger ! Réew mum ne saraax, dara du fa baax. Xàjj-ak-seen dina fa am, boddekonte am, jalgati ya bare, àqi nit ña, ñu teg leen fale. Bu ko defee, koom-koom ga saay, reéw ma daay. Waaye, bu gor bañee dëggi bañ, ger du fa naane ñeex bay yàq seen bànneex. Tiijaan, ci bañkat yooyu la bokk. Jëleesoon na fen jiital ko ci kow dëgg gim àndal ngir rekk làq Mbooyo ci sababu ger. Takk-der yi kootoog yaayu Mbooyo mi leen neexal, bëgg a tiiñal Tiijaan ciy fen ndax rekk xaalis. Tiijaan fippu, lal i pexeem, fexe ba feeñal dëgg gi, biral ko ci kanami ña ko sikkaloon ñépp, setal deram.

Fen mën na xéy, dëgg gontu. Waaye, yàgg-yàgg, dëgg dina ko dab, suul ko. Nga ciy jàngee ni doomu-aadama warul wax lu ko wóorul, teg ci dafa war a màndu ci loo xam ne yoonam nekku ci.

Séy xare la !

Yemul foofu de, ndax Lamin Mbaay moo ngiy joxe ay tegtal ci nu jigéen di taxawe biir néegu séyam. Muy taxawaay bu am solo ci weg ak yiir boroom-këram, jàppale ko, nekk xaritam, raxaale ci tamit joŋe ju mat sëkk. Jigéen dafay neex dereet, woyof, dégg ndigalu jëkkëram, « fexe ba dara du ko naqari… Togg lu neex, xeeñ lu neex, wax ju neex, cuuraay yu neex ». Bépp jigéen bu wéyee ci yile ndigal, dina tax ba loo joxoñ sa jëkkër dagg. Bu loolu weesoo, nag, jigéen ñi war nañoo juboo ci seen biir, di jàppalante. Njëkke yeek goro yi tamit yaataal soxna siy séy ci biir kër gi, moom it soxna si mu góorgóorlu te gën a muñ, jàppe goro yi ni ay way-juram. Mu xam ni séy ndoorteel rekk la am, li ci des lépp muñ la, bañ a lëñbët, bañ a dëkke sëngéem, su ko defee jàmm ne ñoyy.

« …fexe mooytu ger… »

Nu gis ne, kon, li gën a yitteel Lamin Mbaay, bokk na ci yee askan wi ci jikko yu ñaaw yu nit ñi jikkowoo te ñu war koo mën a xeex. Kor, jàmbu, ger, fen, naaféq, ñàkk a màndu, añs., benn baaxu ci cim réew, rawatina ger. Ger, nag, dafa barey melokaan :

« Ger mën naa bañ a nekk xaalis bu ñu la jox, mën naa nekk xoqtal, mbaa dig la ci wàllu àdduna mbaa lu deme noonu ; ba ci liggéey sax ».

Ger a tax njublang gi bari ci àddina si, koom bi deme boor, ñi yor alal di gën a barile, néew-ji-doole yi di wéy di ñàkk. Lu neex waay def, te dara du ko ci fekk. Ger dina sàgganloo ndaw ñi ba di leen tàmmal lu yomb.

« War nga fexe moytu ger, ndax wolof nee na : « Ku ñu ger doo wax dëgg », te réew, am na tawat yoo xam ne, képp kuy dund ca réew ma war na taxaw temm ci xeex ko, muy ger…. Ger moomu dafa law, ba laal xol yi ak xel yi… ».

Tiijaan, nag, gor piir la. Te gor, du fayantoo…

Rafet kanam daal, rafet jikkoo ko gën

Li Lamin Mbaay di ŋàññ sikki doomi-aadama yépp ci biir téere bi, moo ngi sargal it boroom jikko yu rafet yi. Ndax nit ñee yemul. Ñii dañuy mat, di doxe ak xel ;  ña ca des matadi, di deme ak xol. Tiijaan miy nettali téere bi, Yàlla may na ko xel moomu, moo tax bi dëgg gi feeñee, deram set, dafa bës xolam, muñ dem jàppale kii di Jéen, jëkkëru Mbooyo. Jubluwaayam lenn rekk la woon : saxal teraanga jeek kersa gi dox seen diggante ak tamit suturaal Mbooyo miy xaritu Maye. Kóllëre gi mu sàmm, daf koo gën a siggil ciy nawleem. Moo tax, rafet kanam daal, rafet jikkoo ko gën. Nde, lépp loo gis, ci nettali lay mujje. Waaye, nag, bu peccum liir neexee, ndey jaa téye ca mbagg ya.

Jikko yu rafet yi bindkat bi fésal ci téere bi, jaarale leen ciy way-jëmmal yi, dafa fekk xalima baa jëkk a rafet, loxo bi koy rëdd set wecc. Kon, Lamin Mbaay, gàcce- ngaalaama !

Li duuf ci nag wépp, nag, xajul ci cin li te lu neex du doy. Fii lañ koy yamale. Ku bëgg a mos neexaayu xalima Lamin Mbaay, gaawtul wuti Guddig Mbooyo (ca EJO-Editions), di ko jàng ci guddig mbóoyo giy màndargaal sunu jamono ji, ngir féexal sam xel, yaatal sab xol.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj