Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019.
Li ngeen ciy jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi.
Saada Kan : Noo ngi am mbégte delsi ak yéen ci seen jotaayu waxtaan « L’entretien » bi nu leen di dégtal ñaari ayu-bés yu nekk. Tey, nag, noo ngi dalal gan gu mag, ab werekaan bu ñu ràññee ci àddina sépp, mu di ab bindkat bu yebu ci ittey réewi Afrig yi rawati-na ci lu ñeel seen daraja, di ab móolkat, taskatu xibaar, jàngalekat. Kookooy Bubakar Bóris Jóob. Moom lanu fi dalal tey, fas yéene waxtaan ak moom. Kon, Bubakar Bóris Jóob, ginnaaw bi nu la nuyoo, nu bàyyi la nga nuyoo laata nuy sóobu ci waxtaan wi.
Bubakar Bóris Jóob : Jërëjëf Saada. Maa ngi lay sant di la gërëm ci dalal biŋ ma dalal ci jotaay bii nga xam ne, xam naa ko bu baax sax. Ndaxte damay faral di ko seetaan saa yu ma ko sama jot mayee. Ndax li may toog bariwul, saa su nekk maa ngi ci roppëlaan yi. Waaye, jotaay bu ma yitteel la ; dama koy seetaan saa yu ma amee jot.
Saada Kan: waxtaan wi nag, dama koy doore ci ndokkeel la ngir yool biñ la jagleel fan yii weesu ca Etaasini.
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Jërëjëf. Yool bi, “Harold Ethel L. Stellfox” lañ ko dippe. Iniwérsite Dickinson bi nekk ca Pensilwani, ca réewum Amerig, moo ma ko jagleel. Ma bég ci lool sax, ànd ci ak sag bu réy. Ndax, ñi ma ci jiitu, ay bindkat yu mag a mag lañ, ma bëgg leen lool, def leen ay royukaay te daan jàng seeni téere ca ba may ndaw. Looloo ma tax a bég ci li ma jot ci yool boobu. Jëli woon naa ko. Jot naa fa amal sax aw waxtaan, jàngaale fa tuuti sama téere bi, Murambi ci nasaraan ak sax Doomi Golo ci wolof.
Saada Kan : Nga ne ma ! Ci wolof, nag…
Bubakar Bóris Jóob : Waaw, waaw. Mayoon nañ ma ko. Li ma ko dugge woon mooy baaxe am mbooloo mu déggul wolof, taaru kàllaamay Kocc ak neexaayam.
Saada Kan : Noo ngi lay sant ci sa teewaay ci waxtaan wi. Naam, ñépp a la xam. Waaye, du ñàkk mu am ñu umple ne, ca njëlbéen, jàngalekatu xeltu (philosophie) nga woon, nekkoon tamit taskatu xibaar. Nu gis ne at yii weesu yépp, yaa ngi doon jàngale, di bind, di amal i waxtaan, di wër àddina si. Jamono jii sax yaa ngi jàngale ca Niseryaa. Muy biral ne yow, jëfkat nga. Ma bëgg laa laaj, ndax du xeex bi ngay xeexal làmmiñi Afrig yi, rawati-na wolof, moo la yóbbe loolu lépp ?
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Jàpp naa ne, xeex booboo sabab lépp. Te, du loo xamante ni, dafa xéy rekk sotti. Boo xoolee ba ci biir, dinga gis ne sax, jaar-jaar boobu nga tudd, fa la bépp bindkat di faral di jaar, rawati-na bindkat buy xeexal jenn itte ju ko ñor. Maanaam, dangay nekk ndaw bu gàtteñlu, bëgg lool njàngum téere yi, di jéem a topp ci tànki bindkat yu mag yi. Rax-ci-dolli, ngay bindantu ay taalif yu ndaw, ay kilib ak ay téere fent. Noonu nga koy jàppe ba xéy bés, génne ab téere. Bu ko defee, ñu jàppe la bindkat, ndax du yaa koy def sa bopp. Ndege, fàww nit ñi jàppe la bindkat nga door di ko nekk. Noonu, ay ndigaale sa diggante ak nit ñi tàmbalee juddu ; ngay tibbe ci mboolem-nawle mi di bind, di roote ci seen nekkin ak dundin ay xalaat ak i gis-gis di leen jëmmal ci say biir téere. Ñoom itam, ñuy jàng say téere di la ci laaj ngay tontu. Waaye, duñu ci yem. Ndaxte, dinañ lay faral di laaj sa xalaat ci nekkinu askan wi, xew-xewi jamono walla sax xew-xewi àddina sépp. Bu ko defee, nga sóobu ci illa ju bees : jëmmal nekkinu nit ñi, rawati-na wu doomi Afrig yi. Noonu la bindkat bi di jëflante ak askan wi. Maanaam, ci moom lay jële daa ji muy rëdde téereem yi ngir jëmmal seen nekkin, dégtal àddina sépp kàddu yiy riir ci seeni xol te seeni làmmiñ të leen a tudd.
Léegi, nag, bu ñu seetloo, xool nekkin ak dundinu doomi Afrig yi, benn njàngat lañ ciy jële : njaam gi deñagu fi. Njaam gi maam yi doon dund ca jamonoy njaam ga ak ca jamonoy nooteel ba, am na ba tey. Ba jonni-Yàlla-tey jii, mënees na ràññee màndarga yi ci réewi Afrig yi : yorin wi, nguur ak njiit yiy jaamu nootkat ba woon, toroxtaange ak tolof-tolof yi askani Afrig yi di jànkoonteel bés bu nekk. Li ci gën a doy-waar mooy ne, Afrig rekk ngay fekk ay bindkat yuy bind ci làkk woo xam ne, seeni nawle walla ñi ëpp ci askan wa ñu bokk dégguñu ko. Muy lu yéeme ! Lan moo leen di tax a bind ak kan lañuy bindal ? Ndax xel nangu na loolu ? Man ci sama bopp, ndànk-ndànk laa tàmbalee yeewu ci mbir mi. Te bu loolu amee, ginnaaw Yàlla, maa ngi koy sante jàmbaar ju mel ni Séex Anta Jóob, sama doomu-baay bi. Te du man rekk, képp kuy xeexal làmmiñi Afrig yi, seeni aada ak lépp lu ñeel seen daraja, war ngaa delloo njukkal Séex Anta Jóob ndax moo sumb liggéey bi, xàllal nu yoon wi. Ci gàttal daal, mbirum làmmiñ lu am dayo la ci sama jaar-jaar.
Saada Kan : Am na loo mës a wax, te mu soxal ma lool. Nee nga bés “nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem”. Mu mel ni li wax ji wund mooy dafa jot nu xeex ngir sunu daraja. Yow miy boroom wax ji, loo ci namm dëggëntaan ?
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Li ma tax a wax ne, nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem, ñaari mbir la. Bi ci jiitu, mooy jafe-jafe ak boddikonte yi doomi Afrig yi di dund jamono jii, rawati-na boroom der yu ñuul yi. Tey, mbañeel ak tiitaange ji yeneen xeet yi ameel nit ku ñuul moo ma gën a tax di wax. Ndax, Jamono jii, ñaawalees na lépp lu aju ci nit ku ñuul walla mu ñeel ko. Moom kay, tudd Nelson Màndelaa walla Baraak Obamaa sax génnewu la ci. Feek yaa ngeek der bu ñuul, jàppees na la nib gàkk-gàkk walla tilim bees war a raxas ba mu set wecc, jële ko fi. Loolu, ñuulaayu nit ki la ñeel, muy benn. Bi ci topp, nag, doomi Afrig yi ci seen bopp la ñeel. Dafa di, cosaanoo Afrig ñenn ñi bàkkaar lañ ko jàppe. Tey, bët bu ñaaw lañuy xoole Afrig. Boo nee Afrig rekk, xel yi dem ci xareb maxejj yi (guerres civiles), coxorte, yorin wu ñaaw wi ñu yore réewi Afrig yi, cambar-cambar bi, ndóol bi ak tumurànke bi, nger mi, añs. Saa boo xamee ne, nit ku ñuul nga teg ci nekk doomu Afrig, dañuy jàpp ne warees na la jéppi, xeeb la, suufeel la. Loolu laa tudde mbugal.
Saada Kan : Kon, Bóris, bu ñu la déggee, ngir nu mucc ci jafe-jafe yooyu, ngir nu nekk, fàww nu xam nun nooy ñan. Te loolu, mënta àntu feek geestuwunu démb, roy ci maam ya tey ndamoo sunuy moomeel. Mu mel ni looloo la tax a bind ci wolof. Rax-ci-dolli, mënees na méngale sa taxawaay ak bu Séex Anta Jóob. Ndax danga jàpp ne, wareef la ci doomi Afrig yi ñu wéyal xeexam ak ndono li mu nu bàyyee ?
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Mi ngoog. Loolu kese la, du leneen. Man, dama jàpp ne ñi ëpp ci nit ñi dañu réere mbiri Séex Anta Jóob. Ndaxte, saa yuñ ko tuddee rekk, xel yépp dem ci Misra mu njëkk ma, mómi ya, piramid ya, ca wax ya mu daan wax ak li mu bind ci sunu cosaan te mu doon lu am a am solo. Xel yi dinañ dem itam ci firnde yu leer yi mu jële ci gëstoom yu xóot ya, te diy wone ne, baaxi maam yu Misra yu njëkk ya, ay nit ñu ñuul, diy doomi Afrig, ñoo ko jëmbëtoon, suuxat ko ba mu naat lool, raw ci àddina sépp jamono jooju. Toog nan fi diir bu yàgg, Séex Anta rekk a doon wax ne, Afrig a sukk jur àddina si. Bépp xeetu mbañ ak ngànt indil nañ ko ko, weddi ko ngir rekk bëgg a werante. Ñi bañoon dëgg googu, àggoon nañ ci sos ay fen yu tooy xepp ngir rekk mbañ, xeebeel ak coxorte gi ñu ameel nit ku ñuul, rawati-na doomu Afrig. Waaye, suul ker du ko teree feeñ. Tey, boroomi xam-xam yépp a bokk ànd ci waxam ja. Kenn déggatul ña ko daan weddi démb. Waaye, liggéeyu Séex Anta mëneesu ko tënk ci gëstukat bi mu doonoon. Séex Anta yemul woon rekk ci di wax ak di firndeel ne, Afrig moo sukk jur àddina si walla, sunuy maam ya woon ci Misra ay nit ñu ñuul lañu woon. Liggéey na yit lu am solo ci wàllu politig.
Bu leen fàtte ne, Séex Anta Jóob nekkoon na fi politiseŋ. Waaye, nag, wute woon na lool ak politiseŋ yi nu xam. Moom dafa xamoon ne, xeex bi mu daan xeex, mënta àntu feek nguur dugalu ci loxoom. Maanaam, fàww nga yor ndogal li ngir mën a jëmmal xalaat ak yéene yi nga am ñeel sa réew walla sax Afrig gépp. Te, bokkoon na ciy yéeneem yu rafet ya, fexe ba réewi Afrig yépp booloo doon benn. Te, nag, ak li mu doon rafet xalaat yépp, mësul a dige lu mu mënul walla lu mënta nekk. Maanaam, daawul fen di dajale ni yeneen politiseŋ yi. Muy lu am a am solo. Séex Anta dafa daan wax ne, bu réewi Afrig yi bëggee tàggook seeni jafe-jafe, fàww ñu ànd fajandoo seeni jàngoro te kenn bañ a jéem a demal boppam. Ci gis-gisam, képp ku beru ci sa wet, dinga wéet ak say jafe-jafe. Te, béy bu àndul ak i moroomi béyam, ànd ak cere ja. Kon, Séex Anta ak ñu mel ni Sànkaraa, Kuwaame Kurumaa ñoo bokkoon benn xeex, bokk benn jubluwaay bi : afal Afrig, boole doomi Afrig yi ñu doon benn ngir Afrig naat, ay dommam tekki.
Moom, li ko wutale ak i maasam mooy itte ju mu joxoon làmmiñi Afrig yi ak liggéey bu réy a réy bi mu ci def, rawati-na làmmiñi réewum Senegaal. Wone na ne, làmmiñi Afrig yi ñoo bokk cosaan ndax ci làmmiñu Misra lañu soqeekoo. Biral na itam mbokkoo gi nekk seen diggante ci wàllu aada, muy lu am solo. Dafa di sax, téereem bu siiw boobu mu génne ci atum 1954 te mu tudde ko “Nations nègres et Cculture”, moo may fit ñenn ñi ba ñu sóobu ci xeex bi. Ndege, ci màqaama téere bi la kurélu FEANF juddoo bañ ca tegee 4 at, ca Frãs, diiwaanu Gërënoobal. Kurél gi, nag, ay boroomi daraja, ay kàngam yu ñu ràññee, ñoo ko séqoon, ñu ci deme ni Abdulaay Wàdd, Asan Silla, Séex Aliyu Ndaw, Saaliyu Kànji Masàmba Saare, Asan Ja, añs. Ku lim juum. Waaye ay boroomi dayo ñoo ci bokkoon te amal liggéey bu am solo lool sax ñeel làmmiñu wolof. Ngir fàttali, kurél googu moo fi génne woon Ijjib wolof, muy ab téere bu ñeeloon njàngum wolof. Liggéey boobu moo àgsi ba ci sunu jamonoy tey jii. Lépp li ñu jot a wax walla def ci làmmiñi réew mi, ginnaaw Yàlla, ñooñoo tax te ñoom, téere Séex Anta baa leen xamb. Moo tax nu war ko sant, sargal ko, delloo ko njukkal. Ndax wolof dafa ne, bu lëg lekkee aloom, na ko gërëme coy…