“Tubaab yaa ngiy dem, waaye seen i karabaane a ngi des sunu biir ba tey, ñu ngemb leen, ràng leen i ngànnaay ; ba tax na xeex bu mujj biy dox ci diggante ki ñu béefeer ak aji-béefeer gi dafay jëmmu li ci ëpp ci diggante ñi ñu béefeeroon. “ FRANTZ FANON
Bi réewi Afrig yu bari moomee seen bopp – 60i at ci ginnaaw – ba léegi, am na fi lu bari ciy xew-xew yiy wéy di dëggal, saa su nekk, kàdduy Frantz Fanon yi. Mu mel ne sunu maas gi la dencaloon wax ji ndax méngoo gi waxam ji méngook jamonoy tey jii. Wolof ne, waxi mag dina guddee, waaye du fanaan àll.
Patrice Lumumba de, bu gisoon ni Sayiiru démb bees duppe tey Repibilig Demokaraatig bu Kóngo mel, du wax safaan bi. Nde, ba sun-jonni-Yàlla-tey jii, Tubaab yi, rawatina Bels yi, ñoo ngiy wéy di ratt réewam. RDC nga xam ne, Yàlla da leen a tàggatal seen suuf si, solal leen siy balli-mbindaare ba mu ne gàññ. Bariwaay bi jaaxal àddina si bañ koy dàkkentale « scandale géologique », maanaam kéemtaanug biir-suuf. Réewum Belsig ma ko nootoon démb, ca jamonoy mbéefeer ma, lal i pexe, fexe ba jaxase doomi réew ma ci seen biir. Dafa jafal taal ci ñaari diiwaan ya fa ëpp i balli-mbindaare, ne ci ginnaaw di leen xamb.
Belsig, nag, du leen ne « xeex leen seen biir ! ». Pexe seytaane la def, fexe ba ëfal ñaari doomi réew ma, Moise Tschombé ak keneen, ñuy cóoki seen biir. Ku jëkk keek mbootaayam yékkati seen i ngànnaay ngir beddi diwaanu Katànga. Ki ci topp ak bosam feelu leen ci diwaanu Kasaï. Lii yépp a ngi xewoon ay weer, ginnaaw ba réew ma moomee boppam. Nee ñu, Union minière (Bennoog mbellum-suuf mi) bokkoon na ci ñi doon suuxlu (ruux) Belsig ngir mu ŋoy te baña bàyyi réewum RDC.
Xew-xew yu tiis yile, bu ñu jiituwul itam, dees na leen a boole ci yi sooke xare yu bare yi doomi Afrig yiy xare seen biir, boobaak léegi. Ci biir naatangoo yooyu di xeex seen biir, dees na ci ràññee ñaari xeet. Wu njëkk waa ngi ëmb ñiy xeex ñeel seen askan, seen i àqi réew, péexam ak naataangeem. Xeet wa ca des ëmb tubaab yu ñuul yi fi teewal yu weex yi, di leen jàppale ci seenub naal : wéy di not ak a jariñoo réewi Afrig yi.
Ñoom, ndawi nootkat yoo yii, xaalis ak ndomboy-tànk yiñ ciy jële rekk ñoo leen ñor. Ndeysaan, seen yoon nekkul ci jafe-jafe ak seen ëllëgu askan. Moo tax, limi nit yu bari yiy dee ci xare yi ñuy sooke safu leen sax. Bu ko defee, deret ju bari jot naa tuuru ci jàmmaarloo yi jot a am boobaak léegi. Doy na ci firnde, way-fippu yiy fétteerlu, bawoo ci diwaan yi, di rey ak a bóom ay jaambur yu leen deful dara ak di daaneel ay nguur, di taal i fitna yu dul jeex, askan yi di ci loru.
Bu fekkoon ne, sax, ay nit yu tekkiwul dara, walla yuy wut tur walla alal kese ñooy def jëf yu ni mel, kon du bett kenn. Waaye, ay njiit ak i boroom kàddu yu ràññeeku tey wootewoo mbaax ak defar, mbooloo dar leen, yaakaar leen, ñooy sabab xare yi. Loolu, nag, moo jaaxal ñu bari. Nde, ay doomi Afrig lañu yu, nee ñu defar a leen tax a jóg, ba noppi wëlbatiku di yàq. Ci wàllu politig, dees na fekk njiit yu ni mel ci réewi Afrig yi féete bëj-saalumu màndiŋum Saxara, rawatina réew yi Farãs nootoon. Houphouët Boigny, ca Kodiwaar ak Seŋoor, fii ci Senegaal, ay firnde yu bir lañu ñeel wax ji.
Ci gis-gisu Usmaan Sémbéen, Seŋoor – mi mu duppe Lewoŋ Miñaan ci benn ci ay téerey-nettaleem -, mooy, “ginnaaw Faidherbe, li gën ci lu réewu Farãs meññ, ki gën ci ay ndawam yi ko taxawal Afrig ci dëkk yi mu nootoon”. Ci xalaatu benn boroom xam-xam, jàngalekat, ci yenn ci daara yu mag ca réewum Farãs, “Seŋoor mooy aji-noot bu kenn dul gis feneen”. Bubakar Bóris Jóob, nag, moom nee na Léwo mooy ku kenn mënul natt, “koo xam ne féetéwul fii, féetéwul fa ca des”. Mongo Beti, moom, “Oncle Tom-Seŋoor la koy woowe, ndam li gën a réy bu nit ku weex am”. Kàddu yii yépp, yi nga xam ne bu ci nekk am fu mu wéeru, dañuy wone péete mi Seŋoor féetewoon ak tubaab yi ak jàppale bu mu leen doon jàppale ci yenn ci seeni jëf yu yées ci Afrig.
Seŋoor moomu daan wéy ci waawu Farãs, fexe woon na, ci ndigalu Farãs, ba Séex Anta Jóob sore daara ju kowe ju Ndakaaru, toog ay at jàngalewu fa. Miŋ ko daan xeex ak a bunduxataal ci wàllu politig, jamono ja Séex Anta bokkee ci kujje gi. Ndege, dafa ragaloon maxejj yi, xippiloo leen seen i bët ngir ñu mucc ci naxe yi ak nootaange bi. Roland Colin nettali na – jële ci Mamadu Ja -, ne ba Seŋoor dajeek moom Farãs, ca Gonneville-sur-mer, ngir xool ban taxawaay lañu waroon a am ci referendum bu 1958 bi. Ciy waxam, Seŋoor da ko ne woon “teel na Senegaal di moom boppam, dafa war a nangu yeneen 15i ba 20 at ci kilifteefu Farãs”. Mënees na gëm waxu Roland Colin bees sukkandikoo ci kàdduy Seŋoor ci boppam. Nde, moo waxoon lii : ” Yàlla xam na ne, Këru Farãs bëggu nu koo génn, ndax neex na, te fa lanu màgge. Li nu bëgg daal, as-tuut la : mooy samp fi sunuy néegi-ñax yoo xam ne nii dañuy yokk te di dëgëral njaboot gi, walla sax Farãs.”
Ci beneen boor, ci nguuru Seŋoor lees nose, ñeel Senegaal, “Opération Persil” ak lenn ci “Opération Mar Verde”, ngir suuxal nguuru Séku Ture ca Gine ndax li mu dakkaloon nooteelug Farãs cim réewam. Taxawinam deful lu dul dëggal kàddu yii : ku bég ci sag njaam fàww nga noonoo kiy fippu ngir moom boppam. Mënees na fàttali lu baree-bari ci lu Seŋoor def walla mu wax ko te mu safaanook njariñal Senegaal ak Afrig te duggewu ko woon lu dul jàppale Farãs mu noot Afrig.
BOOS NDÓOY
(Ñaareelu xaaj bi fan yiy ñëw)