KASO AMATI NA GAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jàpp nañu Faddiilu Keyta mi bokk ci bëkk-néegi Usmaan Sonko, njiital PASTEF li. Ab yaxal bi mu bindoon, fésal ko ci xëtu Facebookam a tax, ci lees wax, ñu jàpp ko. Waa PASTEF jàkkaarloo nañu ak taskati xibaar yi démb ci àllarba ji, naqarlu mbir mi ak jàpp yu dul jeex yi ñuy jàpp ndawi PASTEF yi.

Xanaa yoon, ci ndigalu Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa singali Usmaan Sonko ak i naataangoom ? Ñu bari, ku leen ko laajoon, « waaw ! » lañuy tontu, rawatina farandooy PASTEF yi ci seen bopp. Dafa di, saa bu Yoon wooloo Usmaan Sonko rekk, ci mujjantal ga, dees na am ku ñu jàpp ci ñi muy liggéeyal walla ay farandoom. Ngir fàttali, keroog bi Usmaan Sonko génnee ci pekkug magum àttekat yi, Maham Jàlloo, mi ko doon déglu ci mbirum ciif gi ko Aji Saar di jiiñ, dafa fekk ñu taxañ way-wattoom yi, yóbb leen Mbuur. Yëgul, tinul. Wii yoon, kenn ciy bëkk néegam lees teg loxo : Faddiilu Keyta.

Faddiilu Keyta dafa biraloon ab yaxal ci xëtu Facebookam, bésub 23 nowàmbar 2022, di wax ci mbirum sóobare yees wax ne dañu réer. Lees koy toppe, ci lu rotagum, moo di ay tuuma yu réy a réy yi mu teg ci kow Nguur gi ci mbir mile. Moom nag, Faddiilu Keyta, mooy kiy jokkale « Nemmeeku Tour » bi Usmaan Sonko di amal fan yii yépp. Te sax, ci mbirum « Nemmeeku Tour » moomule lañ jàppe woon way-wattoom yi. Mbaa du « Nemmeeku Tour » bi dafa tiital Nguur gi ? Loolu la Basiiru Jomay Fay, kenn ci kilifay PASTEF yi, jàpp ba tax ko wax :

« Dañoo jàpp sunu mbokk Faddiilu Keyta, aji-jokkale « Nemmeeku Tour » biy tere nelaw Nguur gi. Ab yaxal bu mu fésal ci xëtu Facebookam mooy sabab bi ñu ko jàppe. Te, loolu, woolu woon nañ ko ci, déglu ko, daldi koy bàyyi. Dañu foogoon ne fa la mbir miy yem. Waaye, ndegam démb amuñu dara ci li ñu bëggoon (LK : ci jàkkaarloo Sonko-Aji Saar), dañu koy sipp mbokki Usmaan Sonko, di dal seen kow. »

Waa PASTEF ñaawlu nañ itam jeng bi Yoon bi jeng. Mu mel ni, ku fare ak Nguur gi, ànd ak Maki Sàll, lu la neex def, lu la neex wax. Dara du la ci topp. Waaye, ku safaanoo ak ñoom, booy sëqët ñu lay nëbb jant bi. Nde, ci mbir mees tëje kaso Faddiilu Keyta, ñu bari àddu nañ ci. Am na ñu ci wax wax yu jéggi dayo te, ba tey, toppekat bi woowu leen. Ndaxte, kii di Ahmet Susaan Kamara toog cib tele, Sen Tv, wax na dañu rey Dijje Baaji ak Fulbeer Sàmbu walla ñu labal leen te ba tey, ci kàdduy Basiiru Jomay Fay, « kenn woowu ko ». Muy laaj nag lu Faddiilu wax lu gën a réy li Susaan Kamara waxe ci tele. Dolli na ci ne :

« Fàddiilu waxul lu gën a ñàng lii, xalaatam la biral. Te, ci réewum demokaraasi, amees na sañ-sañu wax sa xalaat ak a àddu ci doxalinu Nguur gi ñeel këf yiy am ci réew mi. »

Laaj bi sampu nag mooy, lu tax boobaak léegi jàppuñu woon Faddiilu Keyta ? Lu tax defuñu ko keroog bi ñu ko woowee ? Li am ba des mooy ne, jàpp tëj bi dafa bari ci réew mi. Mëneesatul a toog ayu-bés te déggeesul ne Yoon teg na diw loxo. Li ci xaw a teeyloo xel yi rekk mooy ne, saa su nekk, day rax pólitig, ñu singali kujje gi, rawatina PASTEF. Yëf yi dañoo mujje niru xoqatal. Wolof nag, dinay wax naan, loo muñ mu jeex ; waaye muñ tamit dafay jeex de.

LK : leeralu kër gi

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj