Kolonel Séex Tiijaan Mbóoj wuyuji woon na sàndarmi Kolobaan yi. Moom, Séex Tiijaan Mbóoj, moo fi jiite woon kurélu Coopération et des Relations publiques du Centre des hautes études de défense et de sécurité de Dakar, gàttal biy joxe CHEDS. Moom, soldaar ba woon, dafa tontuji woon laaji luññutukati Kolobaan yi. Nee ñu nag, yàggoon na fa lool laata ñu koy bàyyi mu ñibbi.
Dafa mel ni, léegi, jege Usmaan Sonko walla jege ku jege Usmaan Sonko wóoratul, rawatina boo dee liggéey ci Nguur gi, walla nga ci doon liggéey. Du Séex Tiijaan Mbóoj moo koy weddi, moom, sóobare ba woon. Ndax, dañ ko dàq te kenn taxul ñu dàq ko ku dul Usmaan Sonko. Nde, ay kilifaam yi tekki ndombog-tànkam dañ njort ne, moom ak Usmaan Sonko am na luñ séq. Cig pàttali, ci weeru màrs 2023 mii lañ ko dàq. Balaa boobu, liggéeyal na Senegaal 41i at, diggante 1982 ak 2023. Bi ñu koy dàq, mi ngi amoon 61i at. Dara taxul ñu dàq ko, ci lees wax, lu dul lu mu « leeral ci benn yéenekaay ne, balaa takk-der yi (way-wattu kaaraange yi, pólis ak sàndarmëri) di la jàpp, fàww ñu am këyitug jàpp-indi (mandat d’amener) walla mu doon ci càkkuteefu kilifag caytu ».
Ginnaaw bi ñu ko xañee liggéeyam, dañ ko bëgg a noppiloo. Moom, Séex Tiijaan Mbóoj, moo ko xamal i mbokkam bim jógee sàndarmëri Kolobaan. Kenn ci waa pekku pólitigam moo xamal waa Seneweb ne « dañ ko wax kàddu gii “bàyyil sa wax yi. Amoo sañ-sañu def pólitig ».
Moom, nekkatul sóobare, dañ ko dàq. Xanaa dara waratu koo tënk ? Bees sukkandikoo ci kiy wax ba tey, luññutukati Kolobaan yi dañ ko xamal ne, buñ ko dàqee sax, dafa war a sàmmonte ak warteefu cell gi (droit de réserve). Waaye, « Kolonel bi daf leen a wax ñu won ko sàrt bi ko tënk ci warteefu cell googu, waaye mënuñu ko woon génnee. ».
Kon, li yóbbee Kolonel Séex Tiijaab Mbóoj lii yépp, ginnaaw biñ ko dàqee, mooy lees njort ne dafa jege Usmaan Sonko miy lawax ci wotey 2024 yi. Bu dee séq ak Usmaan Sonko dara bàkkaar la walla bu dee dañ koy tere ci réew mi, nañ ko xamal askan wi.