Ci altiney tay jii la Njiitu réew mi julli korite. Fa Jumaay Ndakaaru ju mag ji la jullee, niki at mu nekk. Nees ko baaxoo gise, Njiitu réew mi jagleel na askan wi ay kàddu ginnaaw bi mu jullee ba sëlmal.
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dafa soññ askan wi, xirtal saa-senegaal yi ci ñuy xam a jéllale, xam a déglu ak di jàppoo ak a jàppalante.
« Maa ngi ñaanal saa-senegaal yu jigéen yi ak saa-senegaal yu góor yépp koriteg jàmm gu ànd ak wér ak yaakaar. Na bésub tay ji doon bésub cant Yàlla, bésub mbégte bu daj ñépp ak bésub bennoo, juboo ak jàppoo ñeel njaboot yépp. » (kàdduy Njiitu réew mi)
Njiitu réew mi sargal na yit kilifa diine yi ak kilifa aada yi ci liggéey bi ñuy liggéey ngir réew mi am jàmm ak dal, ak li ñuy suuxat jikko yu rafet ci taalibe yi ak mbooleem nit ñi. Looloo tax mu rax ca dolli, moom Njiitu réew mi, ne :
« Weeru koor wi fàttali na nu solos ngëm, yar, njéggal ak bokkoo. Mbaax yooyu ñooy kenoy Bokkeef gu jub gog, dañu ciy jàppalante. Maa ngi sant Yàlla mi nu may nu teewe weer wu sell wi ci xel mu dal. »
Njiitu réew mi sàkku na ci kilifa diine yi ñu wéy di ñaanal réew mi. Li mu tëje ay kàddoom mooy feddali ne, moom, Senegaal gépp la boole njaboote ; yéeneem mooy déglu ñépp. Loolii tamit lay ñaax képp-kenn ci doomi réew mi, di sàkku ci maxejj bu ci nekk mu « … xam a jéllale, xam a déglu ak di jàppoo ak a jàppalante. Senegaal dafa soxlaal doomam yépp ngir jëm kanam ci kaw bennoo. Nanu wéy di tabax réewum jàmm, réewum mbokkoo ak màndute. »