Xari Njaay
Mbasum koronaawiris mi lëmbe na àddina sépp, jaxase réew
yépp. Amul menn réew mu mucc ci jàngoro ju bon jii bawoo
Siin, ci weeru desàmbar wii weesu, atum 2019. Dafa di, nag,
mbas mi ñépp la bett. Ndege, ni mbas mi tasee wërngal àddina
si, kenn foogewu ko woon nii. Moom kay, jàngoroy Covid-19
baa ngi mel ni wëraakoon, fu nekk mu ne fa naam-daraame. Ku
mu janool ba ne la niib, bu yeboo xam ni, bu ci Yàlla jàppul, biir
suuf nga jëm. Te, Afrig, sax, kenn demul mu des.
Mbas mi daaneel na limub nit bu jéggi dayo ci àddina si,
rey ñu baree bare. Covid-19 bi yemul rekk ci di doyadil wér-gi-
yaramu nit ñi ak di faagal seen i bakkan ; waaye, tamit, dafa
làmboo ay loraange yu dul jeex ñeel fànn yu bare. Loraange yi
aju ci wàllu koom-koom yee gënatee doy waar. Moo tax, réew yi
mbas mi song yépp, rawatina yu am doole yi, dañu jël ay dogal
yu bare, génne xaalis bu takku ngir rekk mën a dékku loraange
yooyu. Bu dee koom-koomi réew yu mel ni Etaasini, Farãs,
Àngalteer, Espaañ, Itali, añs. la mbas mi néewal-doole, Afrig, moom, kenn waxaalewu ko. Naam, nguuri réewi Afrig yi jël nañ
ay matuwaay ngir fagaru. Wànte, ba tey, warees na amal ab
taxaw-seetlu ñeel matuwaay yooyee.
Xeex ak mbër mu tollu ni Covid-19 dafa laaj ay pexe ak mbir yu
bare. Waaye, ajoowoo na yit alal ju takkoo takku. Ndeysaan,
Afrig moom, ndóol a di ñaareelu turam, tumurànke di santam.
Loolu tekkiwul ni réewi Afrig yi amuñu xaalis walla alal ju doy
de. Déedéet. Dafa di, ni njiiti Afrig yi taylee alalam ak i doomam,
rawatina cuune biñ cuune, moo waral Afrig mënta jariñoo alal
jim làmboo. Bu ko defee, leb ak ñaanaatu rekk lañ fi nekke.
Léegi, nag, jamono jii nga xam ne jamonoy bopp sa bopp la,
tëjees na bunti réew yépp, kenn talatul kenn. Kon, nan la waa
Afrig di def ngir génn ci, ñoom ñi nga xam ne, li ëpp ci li ñuy
dunde, dañu koy jéggaani bitim-réew ? Déggees na sax njiitu
réew mi, Maki Sàll, di wax ne ‘’Banque Mondiale’’ dafa war a far
bori réewi Afrig yi, walla mu xool ni mu koy wàññee. Lii rekk doy
na ci gàcce. Waaye, warees na cee jële njàngat yu bare. Bu ci
jëkk mooy solos mbey, dunde. Nde, ci dëgg-dëgg, askan wu
nekk war ngaa mën a bey li ngay dunde.
Ci beneen boor, yëngu-yëngu yi ak xeeti liggéey yu bare,
rawatina yu sew-sewaan yi askanu Afrig yiy faral di suturloo, su
ñu dakkul it, wàññeeku nañ bu baax. Mënees na jël misaal ci
Senegaal. Sabab bi, nag, mooy aaye bi nguur gi aaye mbooloo
yi, guural gi ak dëju-guddi. Rax-ci-dolli, tëjees na yenn ja yi, utal
waxtu wàcc ya ca des. Ci wàllu dem beek dikk bi, wàññees na lim yi daamar yi war a yeb. Am ay dawalkat yu yokk paas yi
ndax li ñu daan am, amatuñu ko te njëgu esãs bi wàññeekuwul.
Fim ne nii, sikkim yépp a lakkandoo. Daanaka, dara doxatul ci
réew mi, rawatina koom gi. Xutaab bii, bu yàggee njaaxum am.
Ndax réewi Afrig yi am nañu xel meek doole ji leen ciy génne ?
Ndax danuy toog di xaar ndimbal walla danuy am sunu fullaay
bopp, demal sunu bopp ? Ndax ‘’Banque Mondiale’’ dina nangul
Maki Sall ñaanam gi ?
Laaj yaa ngoogu. Waaye, li am ba des mooy ne, fim ne nii,
koom-koom yaa ngi sooy. Te mën naa jur fitna ju réy a réy ci
réewi Afrig yu bare.