KORONAA JAT NA PAAP JUUF, GAYNDEY GAYNDE YI !

Yeneen i xët

Aji bind ji

« Ërob, rawatina Farãs, dañuy xeex ak a bunduxataal tuutaafoni waaso yi (minorités ethniques). »

Njiitalu “Olympique de Marseille’’ ba woon, Paap Juuf, faatu na ci guddig talaata ji 31eelu fan ci weeru màrs atum 2020, ci loppitaanu Faan. Moom, nag, jàngoroy Covid-19 bee ko yóbbu.

Paap Juuf mi ngi juddu bésub 18eel weeru desàmbar atum 1951 ca Abese, réewum Càdd. Taskatu xibaar la woon (liggéey na ci La Marseillaise ak Le Sport), nekkoon ndawal futbalkat, manatsëeru tàggat-yaram ak njiitu këlëbu futbal “Olympique de Marseille’’ dale ko 2005 ba 2009.

[Tiis ak naqar wu réy laa yëg bi ma déggee deewu
Paap Juuf gi…Doonoon na njiit lu mag a mag,
amoon itam xol bu rafet lool… Futbalu Farãs ñàkk
na, waaye Afrig ñàkk na. Yal na suuf sedd ci
kowam. Benjamin Mendy
Futbalkat Manchester City]

Paap Juuf njiitalu ‘’Olympique de Marseille’’ ba woon, mooy ki jëkk a ñàkk bakkanam ci mbasum Covid-19 mi biir réewum Senegaal. RTS moo yëgle xibaar bi. Jàngoro ji sonaloon na ko lool ba ñu mujje woon koo sampal noyyikaay ca loppitaanu Faan.
Ndege, Mabaaba, ci turam dëggëntaan, ak aji-tawat biñ delloo réewam ñooy ñaari way-tawat yi jawriñ ji waxoon ne Covid-19 bi sonal na leen lool. Ndeyssan, ci guddig talaata ji, jagleesoon na kob roppëlaan bu ko waroon a yóbbu Farãs, ca benn loppitaanu Niis, ngir mu fajooji fa. Waaye jamono jooju, feebar bi àggoon na foo xam ne kenn mënatu ci woon dara. Noonu, Senegaal, réewum
cosaanam, la mujjee gaañoo.

[ Tiis ak naqar wu réy la Olympique de Marseille
àndal bi mu yëgee deewu Paap Juuf gi.
Waa Marseille yépp dinañ wéy di ko bëgg ci seen
xol, moom mi nga xam ne, bokk na ci ñi defar këlëb
bi.
Noo ngi koy jaale mbokkam yépp ak njabootam.
Olympique de Marseille.]

[ Dama… Mënumaa wax, mënta nekk. Xawma lu may
wax. Samam xel a ngiy dellu démb. Feebar beey xaj !
Basile Boli. ]

Laata ñu koy teg ci boppu OM, Paap Juuf jotoon naa nekk manatsëeru tàggat-yaram ci diirub benn at. Ci atum 2005 lañ ko tabb njiitalu ‘’Olympique de Marseille’’. Mu dib jaloore ju réy ndaxte OM bokk na ci ekibi futbalu Ërob yi gën a siiw te gën a mag.

Doonte ne ‘’Olympique de Marseille’’ jëlul kub ci njiiteefam, ñépp a mànkoo ne, raaya bi OM amoon ci atum 2010, liggéeyam a ko waral. Te, booba, OM toogoon na lu tollu ci 17i at yoo xam ne, jëlul raw-gàddug Farãs.

Bi muy nekk ndawal futbalkat, Paap Juuf liggéey naak futbalkat yu ràññeeku. Joseph-Antoine Bell (góolu Kamerun ba woon) ak Basile Boli (futbalkatu Farãs ba woon, cosaanoo Koddiwaar) la jëkk a teewal. Gannaaw bi, sosoon na sosete Mondial Promotion ci atum 1989, teewal futbalkat yu bare yu ci mel ni : Marcel Desailly, Didier Drogba, Bernard Lama, William Gallas, Rigobert Song, Pirès, Coupet, Francois-Omam-Biyik, Laurent Blanc, Samir Nasri…

[…Naqar wu réy la. Paap njiit lu ñépp fonkoon la, joxoon ko cër ndax ku
amoon fulla ci boppam la, baaxoon lool. Ku farlu ci liggéeyam la woon te
amoon ci xam-xam. Te, jamono jii, njiit yu mel ni Paap Juuf lañ tumurànke.
Ñàkk naa nit ku ma bëggoon bu baax, ku ma doon faral di waxtaanal, nu
demoon ba nekk ay xarit. Jean-Michel Aulas Njiitu Olympique Lyonnais. ]

Paap Juuf, politiseŋ bi Saa buñ nee Paap Juuf, xel yépp dem ci futbal ak “Olympique de Marseille’’. Waaye, du futbal kesee yitteloon Mabaaba. Nekkinu askanu Marseille ak àqi nit ku ñuul bokkoon nañ ci yi soxal bu baax a baax Mabaaba. Ndege, ci atum 2014, ci wutaakon yi doon sàkku Meeri Marseille bi la bokkoon.

[…Naqar ak tiis wu réy ñoo ma dikkal bi ma yégee ni Paap dem na (te dootul ñëwaat). Maa ngi metitlu xibaar boobu, di ko jaale njabootam gépp ak ay jegeñaaleem. Paap, yaa nu gënoon nun ñépp. Yaa doon sama royukaay. Xamal ni bëgg naa la ba fàww te dootuma la fàtte. Mamadu Ñaŋ.]

[…Yaa nekkoon sama njiit. Tey, ak xool bu tooy laa lay tàggoo. Sa dem bi dafa teel. Duma la mës a fàtte. Yal na la Yàlla yërëm, Paap. Samir Nasri.]

[…Duma fàtte mukk sunu waxtaan wa, benn weer laata maay torlub dige ak Olympique de Marseille. Rawatina li nga ma waxoon bi ma amee gaañu-gaañu. Bi ma Paap woowee woon telefon, daf ma ne woon : « sama kàddu benn la ; déggoo nan ngir nga ñëw OM te du sa gaañu-gaañu bee may tax a dellu ginnaaw. Ndaxte, yàqul dara ci say mën-mën ak sa xarañte. » Nit ku ni mel, dees na ko jox cër bu réy. Naqar wi ma ame jéggi na dayo. Djibril Cissé.]

Benn mbootaayu way-moomeel a ko jiitaloon, di ko jàppale ngir mu falu, doon meer. Paap Juuf dafa ne woon : “Man, politig ngir politig taxumaa jóg. Ndaxte, ab làmpu-mbedd su yàqoo, far ak waa càmmooñ walla waa ndeyjoor amul solo ci ki koy jéem a defar.” Mabaaba mujjewul a falu. Waaye, wàññiwul dara ci mbëggeel ak cofeel gi askanu Marseille amoon ci moom. Paap Juuf ku dëggu la woon, bëggoon ñépp, yemale ñépp te bokkoon leen njaboote. Xamul woon xàjj-ak-seen te bëggul woon lu jege sax boddekonte, rawatina ñeel nit ku ñuul. Ñépp a ngi fàttaliku taxawaayam ak kàddu yu dëgër yi mu biraloon ba coowal mbirum « quotas » yi amee Farãs, ci atum 2010. Jamono jooju la yëkkatiy kàddu yu siiw yii : « Ërob ba mu daj, man kese maa ciy nit ku ñuul ku fiy jiite ab këlëbu futbal. Muy lu jaaduwul, lu doy waar. Dafa di, nag, Ërob rawatina Farãs, dañuy xeex ak a bunduxataal tuutaafóoni waaso yi. »

Paap mujje naa am ndam ci xeex boobu. Ndaxte, naalub “quotas” yi mujjewul a àntu. Waaye, Mabaaba, ak lu mu doon mbër mu mag yépp, amul ndam ci xeexam bu mujj bi mu séqaloon ak meneen mbër mu xarañ te gaaw ci rey nit. Covid- 19 bi daan na Mabaaba.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj