KORONAA, LËMBAAJE NGA DUNYAA (Taalifu Li Faal Sàmba Suuna)

Yeneen i xët

Aji bind ji

 
Koronaa
Yamoo ci doon balaa
Dajal nga àddina-wërngal-kepp
Bawoo ca réew ma ñuy wax Caayna
Ab xoqtal tax laa jóg kepp
Lëmbaaje nga Dunyaa
Fit yépp rëcc nañu
Ñii naan ab jaam nga
Ñee naan ab dajaal nga
Bëgg a fowe sunu xam-xam
Fàtteloonu sunu gëm-gëm.
Su la neexee diigal koom-koom yi
Su la neexee suuxal am-am yi.
Waaye mukk ci mim Dunyaa
Dunu la seetaan ngay fowe sunuy ngëm
Di nu sa lu bees
Xanaa kay doomu-Aadama mi Boroom bi mooñaale fátte
Xel miy fattu mooy ki yées
Nanuy nuyoo tey bañ a joxante loxo
Nuyoo
A-Salaamu Aleykum doy na ci
Yálla na jámm wácc ci kaw ñépp
Nanuy raxasoo ndox saa su ne
Jullit yépp xam nañu ne
Yonent bi denkoon na leen yile káddu
Ñu di : set ci jaamu Yàlla la bokk
Njàqare gi nga teg àddina
Noo ngi ñaan Boroom bi musalnu
Te muccalnu ci
Nu bañ a fàtte ni ngànnaayu aji-gëm mooy ñaan
Kon na jaam yépp ñaan
Delloo lépp ci loxoy sunu Boroom
Danga noo song waaye mënoonu
Danga noo bett waaye ragalun la
Dinanu nàmm sunuy ngànnaay
Dinanu jàkkaarloo ak yaw
Te dinanu la daan
Njëkkewoo fi te dungeen fi mujje yaak say ñoñ

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj