Ndey Koddu Faal
Fii ci Senegaal, limu ñi Covid-19 bi daaneel romb na téeméer.
Moonte bi feebar biy soog a feeñ ca réewum Siin, ñetti weer ci ginnaaw – mi ngi mel ni démb ci man – dañoo foogoon ni fa lay yem, du dal ku dul Sinwaa. Njuumte la woon, ndax mujj gi laal na Ërob. Ñu ni kon xéy-na feebaru nit ku weex la. Am na sax ñu dem ba naan doomu-jàngoro bi ñemewul tàngoor, mënul a dund Afrig, moo tax nit ku ñuul du ko am.
Ndekete yóo…
Léegi leer na ñépp ne koronaa xàmmeewul ku ñuul ak ku weex, yoonam newul ci ku puur ni Sàppone bi walla Sinwaa bi te boroom daraja beek baadoolo bi la yemale kepp. Faat na Mari-Roos Kompawore ak Manu Dibango, song Mustafaa Màmba Giraasi jóge fa dal ci Boris Johnson ak Prince Charles. Suñ bëggoon a lim kilifa yi muy lottal yépp fan yii, dun fi jóge tey. Xanaa rekk di ñaan ñépp ñu bàyyi xel ci fajkat yi mu sonal lool. Koronaa, kenn mënu koo teg bët ba naan yaa ngi koy jàpp. Koronaa dëj na nit ñi seen kër, tax na ñu tëj jàkka yi, jumaa yi, jàngu yi ak tamit isin yeek biro yeek daara yi.
Te yemul foofu.
Su ma ko mën a waxe noonu xew ci boppam… xewwi na !
Koronaa nee na bëggatul gis kenn muy dox ay tànki mbokk te kat, moom, buy doxantu ba séen ñaar ñuy joxante loxo bu ne leen bum fi amati mbaa ma def leen lu ñaaw léegi ! Te nag, àddina-si-juróom-ñaar amul réew mu mucc ci ndigalam yu kéemaane yi.
Waaw, xanaa koronaawiris moom gaynde gu tëx la ?
Lu ma ciy gën a xalaat, di gën a waaru. Ci dëgg-dëgg, xawma lu ma yëf yiy niru. Waaye mësumaa fàtte ni dee du moy du jaas, xam koo tax nit di ji muy sax ak a meññ, di móol, di fent i taalif ngir tabax ëllëg.
Tey jii nag, koronaa tax na ëllëg gën a lëndëm, dee gën noo jege. Maa ngiy déggaat kàddu Ngiraan Fay yi ci ndoorteelu Doomi Golo :« Àddina : dund, dee. Leneen newu fi, Badu. Lii rekk : demal, maa ngi ñëw.» Waaye kan moo bëggul a dund ? Ma ne kon koronaa dafa wàcc di nu mbëllee : di nu fàttali ni lu tuuti- gallaxtaan lanu te amunu benn ka1ttan. Bi nuy ganesi àddina indiwaalewunu tus, te bu nuy dem it dunu yóbbuwaale tus. Lii di biral ne dara jaru fi fëgg dënn ak jaay lu amul.
Nan seetaat boog sunu bopp te dellu ci Yàlla.