KUMBA AM NDEY, KUMBA AMUL NDEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb lañ bàyyi Xuwaan Baranko (Juan Branco), yóbbu ko ca saa sa fa dalub roppalaanu AIBD ngir dàq ko, génne ko réew mi. Moom nag, ma nga cosaanoo ca réewi Farãs ak Espaañ. Maanaam farànkoo-español la. Dafa bokk ci layookati Usmaan Sonko yi. Moritani lees ko jàppe woon laata ñu koy jébbal takk-deri Senegaal yi. Nde, Toppekatu Bokkeef gi dafa gàlloon tubaab biy tuuma yu deme ni atàntaa, kootoo, ciiwalug xibaar yu wéradi ak doxalin ak pexe yuy nasaxal kaaraange bokkeef gi walla di sabab ay fitna yu jéggi dayo. Ca la Toppekatu Bokkeef gi biralee ag càkkuteefug njàpp ci àddina sépp ñeel Xuwaan Barankoo, maanaam ab “mandat d’arrêt international”. Mu dugg Senegaal ba génn, kenn jàppu ko. Mu àgg Gànnaar, naar yi teg ko loxo, jox ko kilifay réew mi. Biñ ko jàppee nag, yàggul sax ci kaso bi, ñu bàyyi ko, ñibbiloo ko. Mbir mii, askanu Senegaal war na ci jàngatee dara ci wàllu kaaraangeem ak ngoram.

Ci gaawu gi, 5i fan ci ut 2023, lañ jàppoon layookatu Usmaan Sonko bi. Fa Gànnaar lees ko tege loxo, jébbal ko takk-deri Senegaal yi, ñu indi ko Ndakaaru, tëj ko fi. Nit ñiy werante : ñii naan jàpp nañ tubaab bi, ñee naan dañuy sóob rekk, di ruube. Ca la Antuwaan Feliks Joom, jëwriñu biir réew mi, indee ay leeral :

Ma leen di yégal ne, layookat bi ñëwoon fii, wax lu ñaaw sunuy càmpeef, di wax lu ñaaw sunu Njiitu réew, di jéem a tuutal sunu réew, fi may wax ak yeen nii, mi ngi ci loxoy BIP, jàpp nañu ko. Xuwaan Barankoo, jamono yii, mi ngi ci loxoy BIP.

Bi jëwriñu biir réew mi waxee lii, ca la coow la wullee ñaay. Moroomi layookatam yi mu àndal ci layoob Usmaan Sonko yi daldi naqarlu lees ko jàpp ak anam yees ko jàppe. Diir bu gàtt ba ñu ko jàpp yépp, lekkul, naanul. Moom, Xuwaan Barankoo, da doon xiifal. Mbokki réewam ya, rawatina waa Farãs, ñépp a màbbaandoo di ñaawlu njàppam gi ak di xirtal Nguurug Farãs ci mu jël ay matuwaayam ngir bàyyilu ko ni mu gën a gaawe. Moo tax it, yàggu fa sax. Balaa coow liy fay, kilifay réew mi bàyyi nañ ko. Nde, mënees na méngale Xuwaan Barankoo ak xal bu xonk coyy bu tege woon ci tenqi kilifay réew mi. Moo tax it, gaaw nañ bàyyi ko. Dafa di, mbott a fi gën a bëgg a ndox, waaye mu tàng bokku ci.

Bu yeboo ne, Xuwaan Barankoo bokk na ci ñi tere nelaw Nguurug Maki Sàll gi. Ndax, layookat bu siiw la bob, xeexal néew-ji-doole yi ak baadoolo yi seen i njiit di tooñ ak a xoqatal a ko siiwal. Rax-ci-dolli, mu ñëw di layal Usmaan Sonko mi nga xam ne, ci kujje gi ba mu daj, moom rekk moo tee Maki Sàll nelaw. Yemu ca, mu kalaameji Nguurug Senegaal gi fa CPI, Ëttu àttewaayu àddina si, ñeel pékkey nitteef (crimes contre l’humanité) yi mu wax ne, Càmmug Maki Sàll gi ak i takk-deram def nañ ko diggante màrs 2021 ak 2023 mii ñu nekk. Loolu la ko Nguur gi meree ba di ko toppe tuuma yees lim ci kow.

Bi ñu jàppee Usmaan Sonko, Xuwaan dafa bett ñépp. Daa xaar ba layookati Usmaan Sonko yiy janook taskati xibaar yi, mu ne tëll, génn. Coow li ne kurr ci réew mi. Mu jël kàddu gi, wax, ne :

“ Sëñ bi, Toppekatu Bokkeef gi,

Li ma fi tax a teew mooy wax la ne ragalu ma.[…]”

Duggam ci réew mi dafa juroon ay jiixi-jaaxa. Ñuy laaj num def ba dugg ci réew mi ak num def ba génn fi te kenn gisu ko, kenn jàppu ko. Jar na sax laaj, ba xam jaarul woon Moritani ba muy dikk. Ak lum mën di doon, mbir mi day dellu ci maanaam kaaraange réew mi, rawatina ci sunu dig yi. Te, ci sunu gis-gis, Xuwaan Barankoo dafa feeñal cikki (défauts) réew mi ci wàllu kaaraange, cuune ak cuufe gi sunu njiit yi làmboo.

Yow nga ngay topp nit, di sàkku ñu jàppal la ko fépp fu mu mën di nekk ci àddina si, mu dugg sa biir réew ba génnaat te jàppoo ko. Ku la gën a cuune ndax am na ? Loolu day wone ni, Senegaal, ku mu neex dugg, ku mu neex génn ni mu la neexee. Sunu dig yaa ngi mel ni tame. Nguur gii di ne day xeex rëtalkat yi (terorist yi), ndax ginnaaw lii, mënees na leen cee wóolu ? Yow, nit ko xam, xàmmee ko, mu fës lool, mooy dugg sa réew, dox ba àgg ci péey bi, wax ak taskati xibaar yi, tele yi di ko wone nga tëe koo jàpp. Mu noppi ca, génnaat péey bi, ne yolos dem, génnaat réew mi, jàppoo ko ba tey. Ak li Senegaal am ciy takk-der yépp ak i sóobare, benn xaleb tubaab mën leen a rëccee ci anam bu yombe nii… Waaw, bu doon ay saay-saay yu bari pexe te am i ngànnaay nag ? Loolu doyatul, waa bitim-réew jàppal la ko ngay damu, di fëgg dënn. Ana kersa ? Jamono ja ngay bàkkook a réy-réylu, tubaab yi wax rekk, nga delloo leen ko. Céy buqat !

Meneen mbir mi jar a wax moo di ne, mbirum Xuwaan Barankoo mi daa gënatee feeñal cuufe gi sunu njiit yi suufe ci kanamu tubaab yi. Nde, daanaka 1 000iy saa-senegaal lañu nëbb jant wi ci sabab ak i tuuma yu gën a woyof fuuf yi ñuy toppe Xuwaan Barankoo. Nit ñaa ngi wax layookat bii di Baabakar Njaay ak ndawul Pastef lii di Bentaleb Sow. Waaye, ñaata baadoola ñoo tëdd ci kasoy Senegaal yi, di fa dund lu mettee metti te defuñu dara walla defuñu lu ko jar ? Moone de, ñu bari ñoo ngi kaas ak a xeex booba ak léegi ngir ñu bàyyi leen, waaye dara. Nguur gi daf leen a tanqamlu, faalewu leen sax. Bu dee xonq-nopp moom, bu mbokkaam yi sëqatee sax, pale ba riir. Fii la Senegaal tollu. Ag cuufe gu bir la Càmmug Senegaal woneeti ci kanami tubaab yi, xeeblu seen bopp, xeeblu Senegaal gépp itam. Waxunu dañoo war a jàpp Xuwaan Barankoo de. Déedéet. Liggéeyam rekk lay def. Li mu ànd ak Usmaan Sonko moo neexul Nguur gi. Loolu kese la, waaye deful lees ko war a toppe, ci sunu gis-gis. Waaye nag, doxalinu Nguur gi lanuy joxoñ, yaafus ak ñàkk fulla yi ñu wone ci mbir mi.

Ñi am i mbokk walla ay jegeñaale ci kasoy Senegaal yi, tey, ame nañ naqar wu réy. Seen i doom, seen i jëkkër, seen i jabar, seen i baay, seen i ndey, seen i nijaay, seen i rakk, walla seen i mag, nekk ci kaso yi, di sonn, te mënuñu ci dara. Lu nekk ñu def. Lu nekk ñu wax. Fu nekk ñu dem. Waaye dara. Xuwaan moom, ginnaawam bandaŋ. Kumba am ndey, Kumba amul ndey, léeb ba wuyoo na fi turam.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj