Gayndey Senegaal yi féetewoo kuppeg tefes gi amati nañu ndam. Ci gaawub tay jii la doon joŋante ak Móritani ci finaal bi. Gaynde yi ño dóor naari Gànnaar yi 6i bii ci 1.
Wii mooy juróomeelu yoon Senegaal di tegale, di jël raw-gàddu gi ci joŋantey kuppeg tefes. Lépp-lépp, jël na ko juróom-ñetti yoon. Ninu Jaata moo jël neexalu kuppekat bi gën a ràññeeku ci joŋante bi.
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ndokkeel na leen. Ci xëtu Xam la bind :
“Maa ngi ndokkeel gayndey Beach Soccer ngir seen juróom-ñetteelu raw-gàddu gi ñu jël, daldi koy tegale juróomi yoon. Siggilati ngeen Senegaal ci seen xarañte ak seen jom. Sagal ngeen nu.”