Seen yéenekaay LU DEFU WAXU mi ngi dalal tey Gii Maryiis Saaña, fara caytu doxal (secrétaire exécutif) gu kurélu way-moomeel bees duppe FRAPP « Auchan dégage ». Gii Maryiis Saaña, nag, ràññees na ko ci fitam ak pasteefam, di jàmmaarlook këri liggéeyukaay yu mag yu mel ni AUCHAN. Bokk na yit ci ñiy xeex APE ndax ci la Tubaab yi bëgg a jaar gën a aakimoo alalu Afrig. Yemul foofu ndax njiitu FRAPP dara la waxul ci ‘’franc CFA’’.
Bañkat bu mag boobu la Daawuda Géy ak Mamadu Jàllo lalal waxtaan wu yaatu, mu nuy faramfàccal liggéey bi muy def ànd ceek yeneeni ndaw moo xam fii la ci Senegaal mbaa bitim-réew.
Li ngeen di jàngsi xaaj bu njëkk bi la, LU DEFU WAXU dina siiwal li ci des fan yii di ñëw.
- Lu Defu waxu : Gii, saa su nekk ñu dégg ne pólis jàpp na kenn walla ñenn ci waa kurél « France dégage », mbir mi jaaxal ma lool. Waaw, ndax dangeen a rax ci seeni ñaxtu lu méngoowul ak yoon ?
- Gii Maryiis Saaña : Nun, danoo am wërsëg sax. Li ko dale atum 2014 ba tey, li ñu jàpp ci ndawi kurél gi ëpp na juróom-benn fukki ndaw. Waaye kenn ci nun mësul a teg tànkam Rëbës ; looloo ma tax a wax ca njëlbéen ne, nun, danoo am wërsëg. Ndaxte, ku ñu ci jàpp, gën gaa bare, ñeenti fan doŋŋ lañ la nëbb jant bi. Saa su nu demee ci porokirëer, day wax li mu tàmm a wax : “affaire classée sans suite”, maanaam deesul jéem a dëggal tuuma yi. Daanaka, mbir mi laajul sax nit kiy wut layookat. Moom, sax, bërki-démb rekk maa ngi doon waxtaan ak mbokk yi nu bokkal xeex bi. Ma leen doon ñaax ngir ñu dalal seen xel, delloosi seen sago. Lu tax nuy jaaxle walla di ànd ak tiis te xam ne, ku ñu ci jàpp it, ñaari fan ñett ñu bàyyi la ? Kon, mbir mi noonu la mës a tëdde, kër ga walla kaso ba rekk. Bu porokirëer newulee “rabat d’arrêt”, nga fab say dàll, ñibbi. Ginnaaw bi nu miinee lu ni mel, ndax tiit walla jàq war nanu ? Déedéet. Bu loolu weesoo, nag, dafa war ci nun, nu biral sunu taxawaay ci mbokk yeek am-di-jàmm yi. Ndege, ñoom, waruñu jàpp ne danoo bank sunuy loxo di leen seetaan ñuy jànkoonteel i jafe-jafe.
“Dëgg la Senegaal réewu teraanga la waaye am na yu xel mënul a nangu. Bañunu kenn, danoo bëgg sunuw askan rekk”
- Yaakaar nga ni loolu dina wéy ? Bés bu yoon dalee ci seen kow, nag ?
- Sóoraale nanu loolu te sax, bu dee wax dëgg rekk, yenn saa yi danuy ñaan Yàlla porokirëer defeere nu. Mébét mii, nag, dunu ko siiwal mukk ci kanamu mbokk yi ndax duñu xam li ko waral su boobaa. Sabab si du lenn lu dul ne, bu ñu deferee kenn walla ñenn ci sunuy ndaw, dootul doon àtteb ndawu FRAPP, yem ci. Su keroogee, àtte “Grande Surfaces” yi lay doon, te loolu mënul a jig sunuy noon. Nu gis ne, kon, porokirëer, bañ a fésal xeex bee tax mu taxañ lu tollu ci 60 dóosiye, gas ba mu xóot suul leen. Bir na ne bëggul àtteb « Grandes surfaces » yi, astemaak lu ñeel APE. Ñoom daal, bëgguñu coow jib. Waaye, wiiri-wiiri, jaari ndaari.
- Fan ngeen tollu ci xeex bi ?
- Def nanuy jéego yu bare ci at yii nu weesu, nun ñi féete Afrig, rawatina nun waa Senegaal. Fexe nanu ba nit ñi ubbi seeni bët, ne jàkk yuqu wax ji. Waaye ba tey njaw des naw xambin, warunoo naagu ba fàtte loolu.
- Ndax nit ñaa ngi leen di may nopp ?
- Dara xéyul sotti. Fi may waxee nii ak yéen, soxna sa lal taabalam ca ja ba xamul lan mooy “Franc CFA” te soo ko nee “Auchan degage” mu ne ci xelam moo ki lu muy wax nii. Li ko soxal mooy nu muy dundale njabootam, lañ la mën a jële ci njaay mi.
- Jëndkat yi nag… ?
- Ñoom it naka noonu, na njëg li yomb te li ñuy jënd na set.
- Lu waral loolu, ci sa gis-gis ?
- Xanaa ñàkk a xam ! Moo tax, bu nuy wax ak nit ñi, di leen jéem a yee, danuy jëfandikoo óparlëer ngir ñépp dégg nu. Bu ko defee, bu ñu jàppee kenn ci sunuy ndaw, kun nu laaj lu tax, bun la nee “Franc CFA” koo waral walla “Auchan dégage” du la bett.
“Jàpp bi ci mujj, nag, jàpp bu ñàkk faayda la. Ndax ñoom ci seen bopp xamoon nañu ne, mbir mi mënul woon a sori. Li ko waral, nag, du lenn lu dul ne, danuy jël sunuy matuwaay ba sàmmoonteek yoon bala nuy def dara.”
- Mën nga delsi ci ‘’Auchan dégage’’ ? Lan moo tax ngeen naan ‘’Auchan dégage’’ ?
- Laaj bu am soloo, ndax am na sax ñu naan danoo ñàkk yitte ! Dëgg la Senegaal réewu teraanga la waaye am na yu xel mënul a nangu. Bañunu kenn, danoo bëgg sunuw askan rekk te moo tax dunu dellu ginnaaw, dunu toqi mukk. Dinan def sunu kem-kàttan ngir ñépp xam li tax nuy xeex ak lan lanuy xeex.
- Jàppaat nañleen bu yàggul dara…
- Jàpp bi ci mujj, nag, jàpp bu ñàkk faayda la. Ndax ñoom ci seen bopp xamoon nañu ne, mbir mi mënul woon a sori. Li ko waral, nag, du lenn lu dul ne, danuy jël sunuy matuwaay ba sàmmoonteek yoon bala nuy def dara. Gis nga, saa su nekk dinan bind ab bataaxal jagleel ko Perefe bu Ndakaaru ngir xamal ko li nu nar bés sàngam, béréb sàngam ak waxtu sàngam. Naka noonu, nu bind ko xamal ko ne àllarba danuy amal taxawaayu ñaxtu ci buntu ministeeru njënd meek njaay mi. Jotunu benn tontu. Nun daal, ci talaata ji, bi ñeenti waxtu ci ngoon jotee, lanu Perefe di door a woolu… Jëfu “maa tey” dëgg a ngi noonu. Xam ngeen ni loolu du yoon.
- Lu tax nga ne du yoon ?
- Benn, Perefe dafa xaar ba talaata mu nuy door a woo te taxawaayu ñaxtu bi waroon a am ci àllarba ji. Te nun jagleel nanu ko ab bataaxal lu mat ayu-bés ci ginnaaw. Ñareel bi mooy ne, bi nu waree amal taxawaayu ñaxtu bi nu dégmaloon, joxu nu sax këyit wuy firndéel ni nangulees na nu am déet. Loolu laa wax ne du yoon.
- Ndax Prefe dinay faral di leen nangul seen i taxawaayu ñaxtu ?
- Waaw, day am. Waaye, bare na lu mu nuy gàntal. Firnde ji mooy, àllarba jii weesu, joxu nu sax kayit. Duggewu ko lu dul lëbëj sunu xeex bi, jaxase nook askan wi. Moo ko teyoon moos ! Waaye, takk-der yi amuñu woon benn lay ngir tere sunu taxawaayu ñaxtu bi. Moo tax it, bi ma jàkkaarlooweek komàndaŋu birigaad bu Wakaam daf ma laaj : “yow, ana kayit giy firndéel ni nangul nan la li ngay waaj a def ?”. Man itam ma laaj ko, “yow, ana kayit wuy firndéel ni gàntal nan ma ?”. Fa la wax ji yem. Kon, nun tiitunu woon. Ndax, xamoon nanu ne, sunuy ndaw deesu leen jàpp diir bu yàgg. Te, ku juum ba téye leen lu yàgg, dinga fésal matadig caytu gi, siiwal ko mu ne fàŋŋ, siiwalaale sunu xeex.
- Lan ngeen doon ñaxtu ?
- Ndax xel nangu na Nguur giy dendale sunu jaaykat yu néew doole yeek jaaykati tubaab yi ñëw fii di xëccook ñoom ? Seetleen rekk, « Carrefour » mooy juróom-ñeenteelu këru-jaayukaay ci àddina si, « Auchan » moom di fukk ak juróom-ñeenteel bi. Kon, ci wàllum jënd ak jaay, xel mënul a nangu sunuy jaaykat di wujjeek ñoom. Làmb jooju wareesu koo tëgg, du yoon, ndax xaaju ñoo yem doole ! Lii rekk, nag, la porokirëer mi kootook nguur giy bañ ñu wax ko askan wi. Waaye neex-naqadi coow lii dina jib ci réew mi.
Daawuda Géy ak Mamadu Jàllo
LAAJ-TONTOOK GUY MARIUS SAGNA (GII MARYIIS SAAÑA) was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story.