LAAJ-TONTOOK GUY MARIUS SAGNA (II)
‘’KU NEWUL ‘FRANCE DÉGAGE’ WAXOO DARA’’
Li ngeen di jàngsi mooy ñaareelu xaaju waxtaan wu yaatu wi Gii Maryiis Saaña, di kenn ci njiiti «Front Pour une Révolution Anti Impérialiste Populaire et Panafricaine» (FRAPP) séq ay fan ci ginnaaw ak Daawuda Géy ak Mamadu Jàllo…
– Lu Defu Waxu : “France Dégage’’ yi ñu bind daanaka ci miiri Ndakaaru yépp, nag, lu ciy sa xalaat ?
– Gii Mariyiis Saaña : Mbir mi dees na ko xaaj ñaari pàcc. Bi ci jëkk mooy, ku fi jàpp ne yow rekk yaa bañ nooteel, yaa ngi nax sa bopp. Ku jàpp ne fi nga nekk yow, ci sa kër walla ci sa koñ, sa biir mbootaay, yow rekk yaa bañ nooteel di ko xeex, juum nga. Bu yeboo nga xam ne jamono ji ngay lal i pexe ngir dakkal nooteel, am na ñeneen ñu bare ñuy def ni yow walla sax lu ko raw. Kon, booloo dafa noo war, nun ñiy jéem a yewwi askan wi ngir jële fi ndóol. Bu dee « France Dégage », du nun noo ko bind ci miiri Ndakaaru yi, yeneeni kurél la. Bi ci topp, nag, mooy danoo jàpp ne, fésal sunu xeex ci mbedd mi, jëfandikoo yooyu pexe ci la bokk. Tey, benn bind kese, ay junniy-junni doom-aadama dinañ ko gis. Waaye soo bindee say xalaat ci kayit, xéy-na ñi koy jàng duñu bare noonu te tali yi moom, li fay jaar bés bu nekk ciy doom-aadama, kenn xamul nu mu tollu. Bind ci miir yi “France degage”, day gën a siiwal xeex bi.
- Lan moo tax ngeen di ko wax ci nasaraan te ngeen di woote ‘’France Dégage’’ ?
- Loolu waxtaane nan ko sunu biir ba noppi. Am na sax ñu naan, “lu nu tee bind “Farãs ci biti” walla “Farãs jóge fi” ? Waaye, man, jàpp naa ne, baatu “dégage”, ñi jàngul nasaraan sax xam nañu lu muy tekki. Te wolof, fooguma ne ñépp a ko dégg. Li am ba am moo di ne fi Senegaal tollu tey, ku waxul ‘’France dégage’’ waxoo dara.
- Ndax mënees naa jàpp ne réewum Farãs rekk ngeen di waxal ?
- Baatu « France Dégage », ab gàttal la ; lees war a wax, ci nasaraan, mooy : “Pour la souveraineté monétaire, France Dégage.” Léegi nag, dëgg la, nit ñi tàmm nañ noo woowe « France Dégage », ndax moom lanu tàmbalee laata nuy taxawal FRAPP. Ci nasaraan, FRAPP mi ngi tekki «Front Pour une Révolution Anti Impérialiste Populaire et Panafricaine». Ndege, danu jàppoon ne « France Dégage » rekk day gàtt. Bu dee danga ne àndulook politigu FMI ak Bànk Monjaal, xam nga ne « France Dégage » tur wu matadi la. Rax-ci-dolli, boo ànduleek APE yi ak politigu OMC walla CPI, «France Dégage» rekk mënul a ëmb loolu lépp. Looloo taxoon nu wut tur wu gën a yaatu. “France Dégage » bi ñu nuy woowe, donte sax du sunu tur dëggëntaan, mettiwunu. Sa laaj bi, nag, dégg naa ko te li ma ciy tontu moo di ne askanu Senegaal ak i njiitam lanuy waxal. Bu ci Farãs jotee itam, muy noonu. Nun, sunu gejj lanu weer, ku weri yaa xam. Bu nuy wax “Auchan”, walla “Carrefour dégage”, sunuw askan ak njiit yi nu fal lanuy gën a waxal. Te li nu leen di wax mooy, su nu bëggee réew mi génn ci ndóol te naat, fàww nu moom sunu bopp ci anam bu kenn du werante. Lii rekk la “France dégage” di wund. Ci beneen boor, xam nanu ne mbir mi neexul ñu bare ndax danuy xajamal seen cere. Léeg-léeg nga dégg kenn ci sunuy njiit di nu gaaral, naan «war ngeen a xoolaat li ngeen di wax». Jawriñ ji yor wàllu njaay meek njënd mi, moom, li mu nu tontu mooy, «doomi Senegaal yaa ngi fépp ci àddina si, bu ñu leen fa nee « Sénégal dégage », nag, lu ngeen di wax ? » Nun tamit nu ne ko, fépp fu doomu Senegaal nekk te di fa noot doomu jàmbur, wax ko « Sénégal dégage » lu jaadu la. Waa àmbasadu Farãs ñoom, mbir mi neexu leen benn yoon. Bëggoon nañoo giseek man, sax.
- Dañu laa yónnee bataaxal, walla ?
- Déedéet. Ci sama benn xarit lañu jaare. Duma tudd turam, nag, waaye xam ngeen ko. Jéem nañoo wut yoon ci moom ngir dajeek man. Waaye, mel na ni xàddi nañu. Mbir mi daal, xam naa ne metti na leen lool. Ndaxte bare nay taskati xibaar yu Farãs yu ma ciy laaj sama xalaat. Bu ko defee ma ne leen Nguuru Farãs lanuy ŋàññ. Askanu Farãs, nag, seen yoon nekku ci ndax amunook moom benn jafe-jafe. Waaye, golo bay, baabun dunde la réewum Farãs di def fii ci Senegaal. Waaw, naka lañu mënee yaakaar ne rongoñi baadoolo Afrig yeey wéy di siim seen cere ? Loolu, sunu Victor Hugo, nun, noonu la ko waxe kon. Ñoom, seen Victor Hugo dafa ne, ci nasaraan : « de l’enfer des pauvres, est fait le paradis des riches ». Ci leeral, Victor Hugo dafa ne, « ci toroxtaange baadoolo yi la naataange boroom alal yiy meññe». Boo moytuwul, Victor Hugo ci nun la sàcce jile wax !
- Moone de, Farãs afal nanu ci atum 1960, nu moom sunu bopp. Kon, nooteel bi ngay duut baaraam, moom, lu mu doon, ci dëgg-dëgg ?
- Xéy-na warees naa leeral menn mbir. Ñu bare dañoo jàpp ne, ñi nuy noot, nun waa Afrig ak waa Senegaal, foo dem fekk leen fa. Waaye, nootkat bi dëgg mooy Farãs, moom rekk la. Bu loolu weesoo, ren jii mooy tombeek ñetteelu at mi nu war a amal li nu tudde ‘’Défaite de l’indépendance’’. Li nu ko dugge, nag, mooy, bu ñenn ñi di réy làmmiñ, di woy ak a fecc naan moom nanu sunu bopp, nun danuy jàkkaarlook ñoom naan leen : ‘’Tuuge waay ! Bu leen ko fi waxati. Nun kay moomagunu sunu bopp ci dëgg dëgg !’’ Dafa di kay, nootkat yee summiku, sol yeneeni yëre. Waaye, ñu ngi fi ba tay. Mooy li boroom xel yi di wax rekk, Farãs dafa dem ngir gën a mën a toog. Te firnde ji mooy ne, tey ci kàllaama farañse lanuy jànge, nguur gi, caytu geek bérébi liggéeyukaay yi, di ko jëfandikoo ci wàllu bind ak jokkoo. Loolu, wareesu koo neenal. Ndax li tax Tubaab beek ñi ko fi toogal ga nu seen làkk, mooy ne aw làmmiñ dafa ëmb gis-gisu àddina askan wi koy wax.
- Dangaa bëgg a wax ne ku sàggane say làmmiñi réew, sàggane sa koom-koom, ñu daan la ?
- Mu ngoog. Làkk nasaraan mooy tax yow nga xeeb dàllu Ngaay-Mexe, di jënd dàllu Itali. Dina la tax a jëfandikoo bele bees fi bayeewul, bàyyi fi dugub ji nu xam. Làkk daf lay mooñ, ca bi ngay tuut-tànk. Mooy li Séex Anta Jóob doon wax, danuy dem ba ñenn ci nun jàpp ne Tubaab rekk a xam dëgg. Seen làrme bi fi nekk nag ? Dun ci wax… Ngeen foog ne sunu kaaraange soxal na leen ? Yéen a ngi nax seen bopp, ñii de, sàmm seen këri liggéeyukay yi fi nekk a leen tax a jóg. Aakimoo nañu sunuy suuf ak sunuy màrse, muy BOLLORÉ, TOTAL, CANAL+, añs. Bu kenn fàtte li Ceerno Alasaan Sàll waxoon ci TOTAL mi nguuru Maki Sàll wànteer sunu petorol. Waaye nag, deesul joxoñ baaraam Farãs rekk ; ndax ni CANAL+ di sonale EXCAF, noonu la ko STARTIME tamit di sonale. Te STARTIME, Sinuwaa yee ko moom. Waaw, bu ñu dooleelul doomi-réew mi, ndax Senegaal dina jëm kanam ? Nun kat, danoo jàpp ni doomi-réew mi rekk a mën a tabax Senegaal. Kon, ni fi Farãs di gënee am doole bés bu Yàlla sàkk, du yoon. Gàcce la sax.
- Nu ngeen jàngate coppite yi Auchan indi ci njënd meek njaay mi ci Senegaal ?
- Auchan, nit ñi dañu naan bitig la. Waaye du bitig, màrse dëggëntaan la. Kon, dees na ko tëkkaleek sunuy màrse.
- Wan xeetu doomu-Senegaal moo ëpp ci seen kurél gi ?
- FRAPP amagul ñaari at waaye ña ko séqoon ca njëlbéen, ñi ci ëppoon, ay way-jàng lañu, maanaam ay ndongo-daara, te daara yu kawe yee may tax a wax. Léegi nag, mi ngi soppiku ndànk-ndànk, weer wu nekk xeexkat yu bees fëll. Lu nuy gën di dem, am ñu nekkatul ndongo daara iniwérsite yu ñuy fekksi. Mbootaayu tëgg yi fekksi nañ nu ndax gis nañu ne, seeni liggéeykat am nañuy jafe-jafe ci njaay mi. Léegi sax, jaaykat yi danga leen di dégg ñu naan nu, « Auchan Dégage » am na solo waaye li ngeen di wax, yéen, moo ëmb lépp.
- Naka la seen digganteek taskati xibaar yi deme ci ñaari at yii weesu ?
- Li ci jëkk mooy kumpa. Bi nu sosee sunu kurél gi, dañ noo dañsi woon kumpa, moo taxoon ñu daan nu tàllal mikóro. Bi ñu demee ba xam ne lii du ay caaxaan, tànki bukki yi tàmbalee feeñ. Boo xewlee, woo leen, duñu la sax faale bay ñëw. Dinan wax lee-lee ci li lay tax a xeex, gaa, waaye duñ la tudd mukk. Man boog, gis naa ne, am na xeeti taskati xibaar yoo xam ne, duñu wax ci sunuy mbir mukk, waaye dañuy xéy bés rekk woo la. Ñooñu, jàpp naa ne, bu ñu soxlawee dara ci nguur gi, ci nun lañuy jaar. Amaana bu seen nafa yi tuuroo ba coono dab leen, nun lañuy woo. Këru yéenekaay gu mel ni LEERAL mësul a sawar ci sunuy mbir. Teewul ñu jékki rekk, benn bés, woo ma, ne ma : “kaay, danuy def “Micro ouvert” ñeenti waxtu, direkt nag. Nun tamit, nu dem, wax fa sunu xalaat. Bi loolu weesoo, ci weeru oktoobar, laa leen gëj a dégg. Génnewuñu dara. Am na, nag, ñoo xam ne, saa su nu wootee, ak fu mu mënti doon, ñu ñëw teew. Xéy-na sax fii lanu waroon a tàmbalee. Li may daanele moo di ne, tumurànkewunu mikóro. Déedéet. Lenn daal laa xam ni xañ nañ nu ko, te mooy jataayu tele.
- Boo seetloo, nooteel bi ngeen di xeex tey, moom la ñu bare di xeex ci biir Afrig ak Senegaal li ko dale atum 1960 ba léegi. Lan nga jàpp ne moo tax xeex bi àntoogul boobu ba léegi ?
- Nooteel dafa am doole. Te it, cëslaayu mbir mu bon mën naa fënëx ba mu leer la ne ci dee la jëm, waaye dee gi yéex. Xam nga tey jii nii, nun jàpp nanu ne « Franc CFA » jeexal na. Képp kuy wax ëllëgu « Franc CFA » li ngay wax yenuwul maanaa. CFA jéexal na tàkk laa la wax. Leneen li mooy ni sunu Tubaab yu ñuul yiy jàppalee ñi nuy noot. Xam nañu xéll ne li fi am du yoon. Waaye, ñoom seen teraanga ak seen sutura, nooteel bee leen koy jox. Cëslaay bu xóot a xóot la. Lekool, taskati xibaar yi, loolu lépp, bu ci nekk am na ci wàll. Ak itam, ñenn ci kilifa diine yi, diine boo jël nag. Ndax tamit, ci biir këri diine yi, lu nee nga fa, am na ñuy xeex nooteel, am na ñuy xalamal nootkat yi. Ñenn ñi naan, “ndogalu Yàlla la”. Waay-waay bàyyileen Yàlla mi ngeen di tooñ ! Fi may daanele moo di ne, mënuma wax ne xeex bi jëmul kanam, ndax, tey, foo dem ci àddina si dégg kuy wax ci “Franc CFA” ; mooy wone ne xeex baa ngi jëm kanam. Kamerun gii génn bërki-démb ci ay wote, waxtaane nañ fa lu bare « franc CFA”. Fii ci Senegaal, ren, wax nañu lu bare tamit ci cëslaay gi, maanaam ci «système» bi, du guléet de, waaye ni ñu ku fullaale lu bees la fi. Usmaan Sonko, lawax bi ŋàññ nooteelu Tubaab yi ak APE ak ‘’Franc CFA’’, am na 700.000 doomi-Senegaal yu ko sànnil xob, ni ko yaa nu doy. Boo seetee sax, muy Isaa Sàll di Idiriisa Sekk yéy nañu yàbbi ci «Franc CFA» bi. Ku mel ni Abdul Mbay sax, tudd na ko. Loolu lépp, man jàpp naa ne xeex bee ko jur. Mën naa yéex, nag, ndax sunu maas gii namm nanu bala noo génn àddina, fekke jamono ji nuy moome sunu bopp. Waaye loolu, du nun doŋŋ, waa FRAPP, noo ko mën a sottal. Askan wi ci boppam moo ci war a taxaw.
Daawuda Géy ak Mamadu Jàllo